Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 10

Naka lañuy ràññee ni Yàlla bëgge ñu jaamu ko ?

Naka lañuy ràññee ni Yàlla bëgge ñu jaamu ko ?

1. Ndax benn diine dëgg rekk moo am ?

“ Moytuleen ñi mbubboo turu yonent. ” — MACË 7:15.

Yeesu jàngal na ay talibeem ne benn diine dëgg rekk moo am. Diine boobu dafa mel ni yoon bu lay jëme ci dund gu dul jeex. Yeesu nee na : “ Ñi ko gis barewul. ” (Macë 7:14). Fasoŋ bi ñuy jaamoo Yàlla, bala Yàlla di ko nangu, fàww mu sukkandiku ci Kàddoom. Ñépp ñiy jaamu Yàlla ni mu ko bëgge, benn ngëm lañu am, moo tax ñu doon benn. — Jàngal Yowaana 4:23, 24 ; 14:6 ; Efes 4:4, 5.

Seetaanal wideo Ndax Yàlla nangu na fasoŋ yépp yi ko nit ñi di jaamoo ?

2. Lan la Yeesu wax ci Karceen yu dul dëgg ?

“ Dañoo mbubboo xam-xamu Yàlla, waaye seeni jëf weddi na ko. ” — TIT 1:16.

Yeesu xamle woon na ne, ñiy mbubboo turu yonent dinañu jéem a yàq diine Karceen. Boo leen gisee dangay foog ne ay jaamukatu Yàlla dëgg lañu. Seen waa jàngu dañuy mbubboo turu Karceen, waaye ci seen doxalin lañu mën a ràññee ne duñu ay Karceen dëgg. Karceen dëgg yi ñooy jaamu Yàlla ni mu ko bëgge, te ci seen jikko ak seen doxalin yu rafet lañu leen di ràññee. — Jàngal Macë 7:13-23.

3. Naka lañu mënee ràññee ñiy jaamu Yàlla dëgg ?

Nañu xool juróomi poñ yiy tax ñu ràññee leen :

  • Ñiy jaamu Yàlla ni mu ko bëgge dañu fonk Biibël bi ndaxte dañu ko jàppe ni Kàddu Yàlla. Dañuy jéem a topp xelal yi nekk ci Biibël bi. Diine dëgg ji wuute na lool ak yeneen diine yi nga xam ne ci xalaatu nit lañuy sukkandiku (Macë 15:​7-9). Ñiy jaamu Yàlla ni mu ko bëgge dañuy jëfe li ñuy jàngale. — Jàngal Yowaana 17:17 ; 2 Timote 3:16, 17.

  • Taalibe Yeesu dëgg yi dañuy màggal turu Yàlla, Yexowa. Yeesu màggal na turu Yàlla bi mu ko xamalee nit ñi. Dimbali na nit ñi ñu xam Yàlla te it jàngal na leen ñuy ñaan ngir turu Yàlla sell (Macë 6:9). Fi nga dëkk, ban diine mooy xamle turu Yàlla ? — Jàngal Yowaana 17:26 ; Room 10:13, 14.

  • Karceen dëgg yi dañuy waare Nguuru Yàlla. Yàlla dafa yónni Yeesu ngir mu waare xibaaru jàmm bi ci Nguuru Yàlla. Nguuru Yàlla kese mooy yaakaaru doomu Aadama yi. Yeesu kontine na di xamle xibaar boobu ba ba muy dee (Luug 4:43 ; 8:1 ; 23:42, 43). Yeesu waxoon na ne taalibeem yi war nañu waare xibaar boobu. Bu la nit jegee di la wax lu jëm ci Nguuru Yàlla, ci sa xalaat ban diine la bokk ? — Jàngal Macë 24:14.

  • Taalibe Yeesu yi bokkuñu ci àddina su bon si. Mën ngeen leen ràññee ndax li ñu bokkul ci politig ak fippu (Yowaana 17:16 ; 18:36). Duñu topp dundinu àddina si ak jikkoom yu bon yi. — Jàngal Saag 4:4.

  • Karceen dëgg yi dañoo am mbëggeel dëgg ci seen biir. Ci Kàddu Yàlla lañuy jànge fonk xeet yépp. Diine yu dul dëgg yi jàpple nañu bu baax xeex yu am ci diggante réew yi, waaye ñiy jaamu Yàlla dëgg duñu ko def (Mika 4:1-3). Te it Karceen dëgg yi dañuy jël seen jot ak seen alal ngir jàpple nit ñi, di leen xiirtal te duñu ci xaar dara. — Jàngal Yowaana 13:34, 35 ; 1 Yowaana 4:20.

4. Ndax mën ngeen ràññee diine dëgg ji ?

Ban diine mooy sukkandiku ci Kàddu Yàlla ci lépp li muy jàngale, di màggal turu Yàlla, di xamle ne Nguuru Yàlla kese mooy yaakaaru doomu Aadama yi ? Ban diine mooy wone mbëggeel te du bokk ci xare yi ? Loo ci xalaat ? — Jàngal 1 Yowaana 3:​10-​12.