Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 15

Lu tax nga war a kontine ?

Lu tax nga war a kontine ?

1. Wéy di jàng Biibël bi, ban njariñ la lay amal ?

Ci lu wóor li nga jot a xam ci Biibël bi yokk na sa mbëggeel ci Yexowa. Fexeel ba sa mbëggeel di gën a yokku (1 Piyeer 2:​2). Sa yaakaaru am dund gu dul jeex, mu ngi aju ci li ngay wéy di jàng Biibël bi ngir jege Yàlla. — Jàngal Yowaana 17:3 ; Yudd 21.

Sa xam-xam ci Yàlla buy yokku, sa ngëm di gën a dëgër. Ngëm dina la dimbali nga neex Yàlla (Yawut ya 11:1, 6). Ngëm dina tax nga tuub say bàkkaar te dina tax nga def ay coppite yu lay amal njariñ ci sa dund. — Jàngal Jëf ya 3:19.

2. Li nga xam ci Yàlla, naka lay jariñe ñeneen ñi ?

Mën nga am diggante bu rattax ak Yexowa.

Li nga jàng, yoon la nga bëgg koo séddoo ak ñeneen ñi. Ñun ñépp su ñu amee xibaaru jàmm yàkkamti nañu koo yégle. Booy kontine di jàng Biibël bi, dinga xam ni ngay jëfandikoo Biibël bi ngir xamle sa ngëm ci Yexowa ak xibaaru jàmm bi. — Jàngal Room 10:13-15.

Ñu bare dañuy komaase séddoo xibaaru jàmm bi ak seeni xarit walla seeni mbokk. Boo koy def nag, nanga xam bu baax ni ngay waxe ak ñoom. Bu leen wax ne li ñu gëm baaxul, waaye wax leen lu jëm ci li Yàlla dig doomu Aadama yi. Bul fàtte ne nit ñi sa jikko bu rafet lañuy seetlu, du li ngay wax. — Jàngal 2 Timote 2:24, 25.

3. Ban diggante nga mën a am ak Yàlla ?

Sa njàngum Biibël bi dina la dimbali nga màgg ci wàllu ngëm. Te it mën nga am diggante bu rattax ak Yexowa. Su boobaa dinga bokk ci njabootam. — Jàngal 2 Korent 6:18.

4. Naka nga mënee wéy di jëm kanam ?

Mën nga jëm kanam ci wàllu ngëm booy kontine di jàng Kàddu Yàlla (Yawut ya 5:13, 14). Mën nga laaj benn Seede Yexowa mu jàng ak yow Biibël bi ci téere bi tudd Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ? Looy gën a jàng Kàddu Yàlla, sa dund di gën a neex. — Jàngal Sabóor 1:1-3 ; 73:27, 28.

Xibaaru jàmm bi, ci Yexowa Yàllay mbégte la jóge. Mën nga ko jege booy gën a jege ñi koy jaamu (Yawut ya 10:24, 25). Booy wéy di góor-góorlu ngir neex Yexowa dinga am dund gu wóor gi, maanaam dund gu dul jeex. Ci dëgg-dëgg, jege Yàlla mooy li gën ci li nga mën a def. — Jàngal 1 Timote 1:11 ; 6:19.