Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 3

Raxab dafa gëmoon Yexowa

Raxab dafa gëmoon Yexowa

Defal ni yaa ngi dëkku Yériko bi nekk ci réewu Kanaan. Waa dëkk boobu gëmuñu woon Yexowa. Amoon na benn jigéen bu fa dëkkoon te tudd Raxab.

Raxab bi mu nekkee janq, dafa doon dégg ñuy nettali ni Musaa xaaje woon géej gu xonq gi ak ni mu génne woon Yawut yi Misra. Déggoon na itam ni leen Yexowa dimbalee woon ba ñu am ndam ci seeni noon. Léegi nag Raxab dafa dégg ne Yawut yi ñu ngi ci wetu Yériko !

Raxab dafa nëbboon yëddukat yi ndaxte dafa gëmoon Yexowa

Mu am benn ngoon, ñaari Yawut yoot ndànk dugg Yériko ngir xool dëkk bi. Nit ñiy def loolu dañu leen di woowe yëddukat. Ñu dem kër Raxab, mu wax leen ñu toog këram. Ci biir guddi gi, buuru Yériko bi yëg ne am na ñu ñëw ngir xool dëkk bi te ñu ngi kër Raxab. Noonu buur bi yónni ay nit ngir jàpp leen. Raxab daldi nëbb ñaari yëddukat yi ci kaw teraasam te wax ñi buur bi yónni ne : ‘ Góor yooyu de, fii lañu nekkoon waaye génn nañu dëkk bi yàgg na. Bu ngeen demee léegi, dingeen leen mën a jàpp ! ’ Ndax xam nga lu tax Raxab aar yëddukat yooyu ? — Ndaxte dafa gëmoon Yexowa te xam ne dina may yawut yi réewu Kanaan.

Yëddukat yi, bala ñuy jóge kër Raxab, ñu dig ko ne dinañu ko musal moom ak waa këram yépp bu ñuy yàq Yériko. Ndax xam nga li ñu wax Raxab mu def ? — Dañu ko ne : ‘ Jëlal buum bu xonq bii nga takk ko ci sa palanteer. Boo defee li ñu la wax, képp ku nekk ci biir kër gi dina mucc. ’ Raxab def na lépp li ko yëddukat yi wax. Ndax xam nga li xew ginnaaw loolu ? —

Yexowa musaloon na Raxab ak waa këram

Ci ay bés yu yàggul dara, yawut yi ñëw, ne tekk di wër dëkk bi bés bu nekk benn yoon, ba mu mat juróom-benni fan. Ci juróom-ñaareelu fan bi nag, ñu wër dëkk bi juróom-ñaari yoon ba pare ñu daldi yuuxondoo ñoom ñépp. Yexowa daldi def ba miiri dëkk bi yépp màbb daanu. Waaye këru Raxab bi amoon buum bu xonq ci palanteer bi moom daanuwul ! Ndax yaa ngi koy gis ci foto bi ? — ­Raxab ak waa këram muccoon nañu !

Lan nga mën a jàng ci Raxab ? — Raxab gëmoon na Yexowa ndaxte dafa xamoon jëf yu bare te kéemaane yi Yexowa defoon. Yaw itam yaa ngi jàng ngir xam lu bare lu kéemaane ci Yexowa. Ndax dinga ko gëm ni Raxab ?​— Wóor na ñu ne dinga ko gëm !