Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 4

Dafa bégaloon pàppam ak Yexowa

Dafa bégaloon pàppam ak Yexowa

Lan la Yefte digoon Yexowa ?

Yombul woon ci doomu Yefte bi, waaye terewul mu def li pàppam dige woon

Ndax gis nga xale bu jigéen bi nekk ci foto bi ? — Pàppam, Yefte la tudd. Xale bu jigéen bi waxuñu turam ci Biibël bi waaye xam nañu ne bégaloon na pàppam ak Yexowa. Nañu jàng nettali bii ngir xam ko moom ak pàppam Yefte.

Yefte góor gu baax la woon. Dafa doon jël jot bu bare ngir jàngal doomam lu jëm ci Yexowa. Góor gu am doole la woon te mën a jiite. Loolu moo tax yawut yi wax Yefte mu jiite leen ngir ñu dem xeexi ak seeni noon.

Yefte dafa ñaan Yexowa ngir ñu am ndam. Mu dig Yexowa ne, bu ko mayee ndam, dina ko may nit kiy njëkk a génn këram ngir gatandu ko. Nit kooku dina dem liggéey te dëkk dundam yépp ci tàntu Yàlla bi maanaam fi ñu doon jaamoo Yàlla. Yexowa may na Yefte ndam ! Ndax xam nga bi mu ñibbee këram kan moo ko njëkk a gatandu ? —

Waaw, doomam bu jigéen la woon ! Doom boobu rekk la Yefte amoon te léegi dafa ko war a bàyyi mu dem dëkk fu sore. Loolu nekkoon na lu metti ci moom. Waaye fàttalikul ne dafa am li mu dige woon. Doomam nee ko : ‘ Pàppa, dafa am loo dig Yexowa ba pare, kon nanga sàmm sa kàddu. ’

At mu jot, xaritu doomu Yefte yi dañu ko doon seetsi

Loolu metti woon na itam ci doomu Yefte ndaxte bu demee liggéey ci tàntu Yàlla bi du mën a am jëkkër te du mën a am doom. Waaye dafa bëggoon a def li pàppam dige woon te dafa bëggoon a bégal Yexowa itam. Loolu moo ko ëppaloon solo am jëkkër walla am doom. Ci noonu, mu génn seen kër dem dëkk ca tàntu Yàlla bi dundam yépp.

Ndax foog nga ne li mu def tax na ba pàppam ak Yexowa bég ? — Waaw-waaw bégloo na leen ! Boo nangoo dégg ndigal te bëgg Yexowa dinga mën a mel ni doomu Yefte bi. Dinga bégal itam sa pàppa ak Yexowa.