Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 5

Samwil bàyyiwul di def lu jub

Samwil bàyyiwul di def lu jub

Bi Samwil nekkee xale bu ndaw, mu ngi dëkkoon te di liggéey fi ñu doon jaamoo Yàlla, maanaam ci tàntu Yàlla bi. Ndax xam nga lu yóbbu Samwil foofu ? Nañu njëkk a xam kan mooy Aana mi nekkoon yaayu Samwil.

Aana dafa bëggoon a am doom waaye toog na lu yàgg te mënu koo am. Mu daldi ñaan Yexowa, ñaan ko bu baax ngir mu dimbali ko. Mu dig ko ne su amee doom bu góor dina ko yóbbu ci tànt bi ñuy jaamoo Yàlla ngir mu dëkk fa te liggéey fa. Yexowa nangu na ñaanam, mu am doom bu góor, tudde ko Samwil. Bi Samwil amee ñett walla ñeenti at, Aana yóbbu ko ci tàntu Yàlla bi ngir mu liggéeyal Yàlla ni mu ko digee woon.

Eli moo nekkoon saraxalekat ci tàntu Yàlla bi. Ñaari doomam yu góor itam, fa lañu doon liggéey. Bul fàtte ne tànt boobu moo nekkoon kër Yàlla fi ñu ko doon jaamoo. Kon ci yoon ñi fay nekk lu baax rekk lañu war a def. Waaye doomu Eli yi, lu bon lañu doon def foofu. Samwil gis loolu. Ndax Samwil dafa topp doomu Eli yi ci lu bon li ñu doon def ? — Déedéet, moom dafa doon def lu jub, ni ko waajuram yi jàngale woon.

Ci sa xalaat, lan la Eli waroon a def ñaari doomam yu góor yi ? — Dafa leen waroon a yar. Waruloon a bàyyi doomam yi ñu kontine di liggéey ci këru Yàlla gi. Waaye Eli deful loolu, moo tax Yexowa mere ko, moom ak ñaari doomam yi. Yexowa daldi wax ne dina leen yar.

Samwil wax na Eli li ko Yexowa wax

Mu am benn guddi bi Samwil di nelaw, mu dégg ku koy woo naan : ‘ Samwil ! ’ Mu daw dem ci Eli, waaye Eli nee ko : ‘ Woowuma la. ’ Mu déggaat ku ko woo. Ñetteelu yoon bi nag, Eli wax ko ne bu déggaatee baat bu koy woo na ne : ‘ Yexowa, waxal ndax maa ngi dégg. ’ Samwil def loolu. Yexowa daldi ko ne : ‘ Waxal Eli dinaa yar waa këram ndax seen bàkkaar. ’ Ndax foog nga ne yomboon na ci Samwil mu wax xibaar boobu ? — Déedéet, yombul woon. Samwil tiitoon na waaye terewul mu def li ko Yexowa sant. Li Yexowa waxoon mujj na am. Dañu rey ñaari doomu Eli yi, te Eli itam dee na.

Samwil royukaay bu baax la ci ñun. Gisoon na lu bon li nit ñi doon def, waaye terewu ko def lu jub. Yaw nag ? Ndax dinga mel ni Samwil te kontine di def lu jub ? Boo ko defee, dinga bégal Yexowa ak say waajur.