Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 6

Daawuda nekkul woon ku ragal

Daawuda nekkul woon ku ragal

Lan ngay def boo tiitee ? — Xéyna dangay dem ci sa yaay. Am na ku la mën a dimbali te moo ëpp doole nit koo mënta xalaat. Ndax xam nga kooku kan la ? — Waaw, kooku mooy Yexowa. Nañu wax léegi ci benn xale bu góor bu ñuy wax ci Biibël bi te mu tudd Daawuda. Moom dafa xamoon ne fépp fu mu mënta nekk Yexowa dina ko dimbali. Loolu moo tax ragalul woon.

Bi Daawuda nekkee xale, waajuram yi dañu ko jàngaloon mu bëgg Yexowa. Loolu moo dimbali woon Daawuda mu bañ a ragal bu amee sax lu koy tiital. Xamoon na ne Yexowa xaritam la te dina ko dimbali. Benn bés Daawuda mu ngi doon sàmm ay xar, benn gaynde bu ngànde ñëw jàpp benn xar daw ak moom ! Ndax xam nga lan la Daawuda def ? Dafa daw topp gaynde bi ba jàpp ko, mu rey ko ak ay loxoom kese ! Beneen bés benn urs song xaram yi. Daawuda dafa ko rey moom itam ! Kan nga foog ne moo dimbali woon Daawuda ? — Waaw, Yexowa la woon kay.

Amoon na itam beneen bés bu Daawuda wone ne jàmbaar dëgg la. Mooy bi waa Israyil waroon a xeex ak waa Filisti. Ci waa Filisti nag, amoon na benn ponkal bu réy-a-réy ! Mu ngi tuddoon Goliyàtt. Ponkal boobu dafa doon ñaawal Yexowa ak soldaari Israyil yi. Waaye kenn ñemewuloon xeex ak moom. Bi Daawuda déggee loolu, mu wax Goliyàtt ne : ‘ Dinaa la duma ! Yexowa dina ma dimbali, te dinaa la daan ! ’ Ndax gis nga ni Daawuda nekke jàmbaar ? — Waaw, jàmbaar dëgg la woon. Ndax bëgg nga xam li Daawuda def ?

Daawuda dafa jël laspeeram ak juróomi xeer, dem xeex ak ponkal boobu. Bi Goliyàtt gisee ni Daawuda tuutee, mu koy ñaawal. Daawuda nee ko : ‘ Yaa ngi ñëw ci man ak jaasi, waaye man maa ngi ñëw ci yaw ci turu Yexowa ! ’ Daawuda dugal xeer ci laspeeram, daw jëm ci Goliyàtt, sànni ko xeer bi ci diggante ñaari bëtam yi ! Ponkal bi daanu ci suuf ! Waa Filisti yépp tiit te daw. Naka la xale bu tollu ni Daawuda mënee daan ab ponkal ? — Yexowa ci boppam moo ko dimbali, moom mi ëpp doole fuuf ponkal boobu !

Daawuda ragalul woon ndaxte xamoon na ne Yexowa dina ko dimbali

Lan nga mën a jàng ci nettali bii ? — Yexowa moo gën a am doole nit ko mënta xalaat. Te Yexowa sa Xarit la. Moo tax bés boo tiitee rekk, fàttalikul ne Yexowa mën na la dimbali nga nekk jàmbaar !