Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 9

Yérémi bàyyiwul woon di wax ci Yexowa

Yérémi bàyyiwul woon di wax ci Yexowa

Lu tax nit ñi doon mere Yérémi ?

Yexowa musaloon na Yérémi

Lée-lée nit ñi di ñu ñaawal walla ñu mere ñu bu ñuy wax ci Yexowa. Loolu mën na tax ñu bëgg a bàyyi di wax ci Yàlla. Ndax loolu mas na la dal ? — Biibël bi mu ngi ñuy wax ci benn xale bu góor bu bëggoon Yexowa, waaye dafa dem ba tuuti mu bàyyi di wax ci Yexowa. Mu ngi tuddoon Yérémi. Nañu jàng nettali bii ngir gën koo xam.

Bi Yérémi nekkee xale bu góor, Yexowa dafa ko santoon mu yégal nit ñi ñu bàyyi di def lu bon. Loolu yombul woon ci Yérémi, te mu boole ci ragal. Mu ne Yexowa : ‘ Man mënuma wax, xale rekk laa. ’ Yexowa nee ko : ‘ Bul ragal, dinaa la dimbali. ’

Yérémi komaase di yégal nit ñi ne bu ñu bàyyiwul li ñuy def, Yàlla dina leen yar. Ndax foog nga ne nit ñi def nañu li Yérémi wax ? — Déedéet. Dañu ko doon ñaawal walla ñu di ko mere. Ñenn ñi sax dañu ko bëggoon a rey ! Ci sa xalaat, lan la Yérémi yëg bi mu gisee loolu ? — Dafa tiit daldi wax ne : ‘ Dootuma waxati mukk ci Yexowa. ’ Ndax loolu la def dëgg-dëgg ? — Déedéet, defu ko. Dafa bëggoon Yexowa lool, moo tax mënul woon a bàyyi di wax ci moom. Te loolu moo tax Yexowa musal ko.

Mu am benn bés, ay góor yu soxor jël Yérémi dugal ko ci biir teen bu xóot te bare ban. Joxuñu ko mu lekk, joxuñu ko mu naan, ndaxte li ñu bëggoon mooy bàyyi ko foofu ba mu dee. Waaye Yexowa dimbali na ko ba mu rëcc !

Lan nga mën a jàng ci li Yérémi def ? — Lée-lée Yérémi dafa doon ragal waaye loolu taxul mu bàyyi di wax ci Yexowa. Booy wax ci Yexowa, nit ñi mën nañu la ñaawal walla ñu mere la. Loolu mën na tax nga rus walla nga ragal. Waaye bul mas a ragal a wax ci Yexowa. Dina la dimbali saa su nekk ni mu dimbalee woon Yérémi.