Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 14

Nguur gi nar a jiite suuf si sépp

Nguur gi nar a jiite suuf si sépp

Ndax xam nga ban Nguur lañuy wax fii ? — Waaw, Nguuru Yàlla la, Nguur googu moo nar a defar suuf si ba mu nekk àjjana ju rafet. Ndax bëgg nga xam lu jëm ci Nguur googu ? —

Nguur gu nekk am na buur buy jiite ñi fa dëkk. Ndax xam nga kan mooy buur ci nguuru Yàlla ? — Yeesu Kirist la. Moom ci kaw asamaan la nekk. Ci kanam tuuti, dina nekk buuru ñépp ci kaw suuf ! Bés bu Yeesu nekkee buur ci kaw suuf si sépp, ndax dinañu kontaan ? —

Lan nga yàkkamtee def ci biir àjjana ?

Dinañu kontaan lool kay ! Ci biir àjjana, nit ñi dootuñu xeex, geer dootul am. Ku nekk dinga bëgg sa moroom. Kenn dootul feebar, kenn dootul dee. Ñi gumba dinañu gis, ñi tëx dinañu dégg, ñi lafañ dinañu mën a daw, dinañu mën a tëb. Ñépp ay am lekk bu bare. Dina am jàmm diggante mala yi ak diggante nit ak mala. Ñi dee dinañu dekki. Rebeka, Raxab, Daawuda, Iliyas ak ñeneen ñi ñu wax ci téere bii dinañu dekki ! Ndax bëgg nga leen a gis bés bu ñu dekkee ? —

Yexowa dafa la bëgg te dafa bëgg itam nga kontaan. Boo kontine di jàng ngir xam Yexowa te di def li mu bëgg, yaw itam dinga dund ba fàww ci àjjana ju rafet ! Ndax du loolu nga bëgg ? —