Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 6

Woneel bu baax njariñu aaya yi

Woneel bu baax njariñu aaya yi

Yowaana 10:33-36

Li NGA WAR A JÀPP: Bul yem rekk ci jàng benn aaya ba pare jàll ci leneen. Fexeel ba ñi lay déglu xam bu baax ni aaya bi nga jàng ànde ak li ngay wax.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Woneel bu baax baat yi gën a am solo. Boo jàngee benn aaya ba pare, woneel bu baax baat yiy wone ponk bi nga bëgg a jàngale. Ni nga ko mën a defe mooy nga waxaat baat yooyu walla nga laaj ñi lay déglu laaj buy tax ñu jàpp baat yooyu.

  • Feeñalal bu baax ponk bi nga bëgg a jàngale. Boo waxee li tax nga bëgg a jàng benn aaya, boo ko jàngee ba pare, leeralal ni baat yi gën a am solo ci aaya boobu wonee li tax nga jàng ko.

  • Woneel ci lu leer njariñu aaya bi. Moytul a wax ci ay ponk yuy tax li gën a am solo du leer. Jaaral ci li nit ñi xam ba pare ci waxtaan bi ngir seet li nga mën a wax ba njariñu aaya bi leer bu baax ci seen xel.