Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 12

Waxal ak mbaax te woneel ne yëg nga nit ñi

Waxal ak mbaax te woneel ne yëg nga nit ñi

1 Tesalonig 2:7, 8

LI NGA WAR A JÀPP: Waxal ci fasoŋ buy wone ne li ngay wax, ci sa xol la jóge te fonk nga ñi lay déglu.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Xalaatal ñi la nar a déglu. Xalaatal ci jafe-jafe yi ñuy dund ngir mën a yëg li ñuy yëg.

  • Seetal bu baax li nga nar a wax. Li nga bëgg mooy dalal xel, dëfël xol ak dooleel. Moytul a wax kàddu yu leen mën a merloo, te bul wax lu ñaaw ci ñi gëmul dëgg gi walla ci li ñu gëm.

  • Won leen ne yëg nga leen. Na sa baat, sa kanam ak ni ngay yëngale say loxo wone ne danga fonk ñi lay déglu. Bul fàtte di muuñ walla di ree tuuti.