Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 04

Kan mooy Yàlla?

Kan mooy Yàlla?

Bi àddina sosoo ba tey, am na lu bari lu nit ñi di jaamu. Waaye Biibël bi dafay wax ci jenn Yàlla joo xam ne, moo sut leneen lépp li nit ñi teg seen yàlla (2 Chroniques 2:5). Yàlla jooju mooy kan? Te lan moo tax mu sut leneen lépp li nit ñi di jaamu? Ci lesoŋ bii, dinga gis li Yàlla jooju bëgg nga xam ci moom.

1. Lan mooy turu Yàlla, te lan mooy wone ne bëgg na ñu xam turam?

Ci Biibël bi, Yàlla xamal na ñu moom mooy kan. Lii la wax: «Man, Yexowa mooy sama tur» (Jàngal Esayi 42:5, 8, MN). Boroom xam-xam yu bare nee nañu, ci làkku Ebrë, Yexowa mu ngi tekki «Dafay tax dara nekk». Yexowa dafa bëgg ñu xam turam (Mucc ga 3:15). Lan moo tax ñu mën a wax loolu? Tur boobu feeñ na lu ëpp 7 000 yoon ci Biibël bi! a Yexowa mooy turu «jenn Yàlla ju wóor ji am» (Yowaana 17:3).

2. Lan la ñu Biibël bi di xamal ci Yexowa?

Biibël bi nee na, ci li nit ñi di jaamu yépp, Yexowa rekk moo ciy Yàlla dëgg ji. Lu tax? Li ko waral bari na. Yexowa mooy kilifa gi gën a kawe ndaxte moom rekk mooy «Aji Kawe ji yilif àddina yépp» (Jàngal Sabóor 83:19). Moom mooy «Aji Man ji», maanaam moom rekk moo am kàttanu def lépp lu ko neex. Moom moo «sàkk lépp» li nekk ci kaw asamaan ak lépp liy dund ci kaw suuf (Peeñu 4:8, 11). Yexowa rekk moo fi mas a nekk, te moom rekk moo fiy nekk ba fàww (Sabóor 90:2).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal li wuutale turu Yàlla ak neneen ni ñu koy faral di woowe. Xoolal itam ni Yàlla xamlee turam ak li tax mu def ko.

3. Ni ñuy woowe Yàlla bari na, waaye turam benn la

Bu ñuy woo nit, ndax am na solo ñu jaar ci turam walla déet? Seetaanal WIDEO BI ngir xam tontu bi. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Lan moo wuutale ni ñuy faral di woowe Yàlla ak turam dëgg?

Biibël bi wax na ne, li nit ñi di jaamu bari na. Jàngal Sabóor 136:1-3. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Kan mooy «Yàllay yàlla yi» ak «Sangu sang yi»?

4. Yexowa dafa bëgg nga xam turam te di ko ko woowe

Lan mooy wone ne Yexowa dafa bëgg nga xam turam? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ndax foog nga ne, Yexowa bëgg na nit ñi xam turam? Lu tax nga wax loolu?

Yexowa dafa bëgg nit ñi di ko woowe ci turam. Jàngal Room 10:13. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lu tax mu am solo ñuy jaar ci turu Yàlla, Yexowa?

  • Lan ngay yëg ci sa biir xol, bu nit fàttewul sa tur te di ci jaar buy wax ak yow?

  • Ci sa xalaat, lan la Yexowa di yëg bu ñuy jaar ci turam?

5. Yexowa dafa bëgg nga doon xaritam

Benn jigéen bu tudd Soten te jóge Cambodge nee na, xam turu Yàlla dimbali na ko mu gën a bég ci dundam. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci wideo bi, xam turu Yàlla, lan la def ci Soten?

Bala ngay xaritoo ak nit, fàww nga xam turam. Jàngal Saag 4:8a. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan la Yexowa bëgg nga def?

  • Xam turu Yàlla te di ci jaar, naka la la mënee dimbali nga nekk xaritam?

BU LA NIT WAXOON: «Yàlla tur yu bari la am.»

  • Ndax gëm nga ne Yexowa mooy turu Yàlla?

  • Lan ngay wax ngir won nit ki ne, Yàlla dafa bëgg ñuy jaar ci turam?

NAÑU TËNK

Yexowa mooy turu jenn Yàlla dëgg ji am. Dafa bëgg ñu xam turam, te di ko ko woowe. Su ko defee ñu mën a nekk ay xaritam.

Nañu fàttaliku

  • Lan moo tax Yexowa wuute ak leneen lépp li nit ñi di jaamu?

  • Lu tax ñu war di woowe Yàlla ci turam?

  • Lan mooy wone ne Yexowa bëgg na nga nekk xaritam?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal juróomi firnde yuy tax mu wóor ñu ne Yàlla am na.

«Ndax Yàlla am na?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal li tax ñu war a woo Yàlla ci turam bu dee sax xamuñu ni ñu daan waxe tur woowu bu njëkk.

«Kan mooy Yexowa?» (Ci jw.org la nekk)

Ndax am na solo ñu woo Yàlla ci turam? Xoolal li tax ñu mën a wax ne, Yàlla dafa am turu boppam.

«Ñaata tur la Yàlla am?» (Ci jw.org la nekk)

a Boo bëggee am yeneen leeral ci li turu Yàlla di tekki ak li tax nekkul ci yenn Biibël yi, xoolal xaaj 1 ci téere bi tudd Téere bu ñuy dimbali ci gëstu Kàddu Yàlla.