Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 07

Kan mooy Yexowa?

Kan mooy Yexowa?

Boo déggee Yexowa, lan mooy ñëw ci sa xel? Ndax dangay foog ne ku màgg la lool ba kenn mënu koo jege? Walla ndax danga foog ne ku am kàttan la waaye amul yëg-yëg? Kan mooy Yexowa dëgg? Ci Kàddoom Biibël bi, Yexowa xamal na ñu ay jikkoom ak it itte bi mu am ci ñun.

1. Lu tax mënuñoo gis Yàlla?

«Yàlla xel la» (Yowaana 4:24). Yexowa amul yaram ni ñun. Xel la muy dund ci kaw asamaan, fu ñu mënul a gis.

2. Yan ñooy yenn ci jikkoy Yexowa?

Dëgg la, mënuñu gis Yexowa, waaye bu ñu jàngee ba xam ko dinañu ko bëgg ndaxte jikko yu rafet la am. Biibël bi nee na: «Aji Sax ji kat daa sopp yoon, te du wacc jaamam bu gore» (Sabóor 37:28). Te itam, Yexowa kuy «ñeewante la te bare yërmande», rawatina ci ñi am njàqare (Saag 5:11). «Sa yaakaar tas, Aji Sax ji jege la, sa xol jeex, Aji Sax ji wallu la» (Sabóor 34:19). Ndax xamoon nga ne, suñuy jëf dañuy def dara ci Yexowa? Bu nit tànnee di def lu bon, loolu dafa koy metti (Sabóor 78:40, 41). Waaye bu nit di def lu baax, dafay bégal xolam (Jàngal Kàddu yu Xelu 27:11).

3. Naka la Yexowa wonee ne bëgg na ñu?

Jikko Yexowa bi gën a fës mooy mbëggeel. Te sax, «Yàlla mbëggeel la» (1 Yowaana 4:8). Yexowa wone na mbëggeelam ci Biibël bi ak ci li mu sàkk (Jàngal Jëf ya 14:17). Xoolal rekk ni mu ñu sàkke. May na ñu, ñu mën a gis kulóor yu rafet, dégg misik bu neex, te lekk lekk bu neex. Dafa bëgg ñu bég ci suñu dund.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal li Yexowa jëfandikoo ngir def ay mbir yu yéeme. Xoolal itam ni ñu Yexowa wone jikkoom yu rafet.

4. Xel mu sell mi mooy doole ji Yàlla di jëfe

Ni nit di jëfandikoo ay loxoom ngir liggéey, noonu it la Yexowa di jëfandikoo xelam mu sell mi. Biibël bi wone na ne, xel mu sell mi du Yàlla, waaye mooy doole ji Yàlla di jëfandikoo ngir def lépp. Jàngal Luug 11:13 ak Jëf ya 2:17. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Yàlla dina «tuur» xelam mu sell ci kaw ñi ko ko ñaan. Kon ci sa xalaat, ndax xel mu sell mi Yàlla la, walla doole ji Yàlla di jëfe? Lu tax nga wax loolu?

Yexowa dafa jaar ci xelam mu sell mi ngir def ay mbir yu yéeme. Jàngal Sabóor 33:6 ak 2 Piyeer 1:20, 21. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la Yexowa def jaare ko ci xel mu sell mi?

5. Yexowa jikko yu rafet la am

Musaa ku takku la woon ci Yàlla, terewul dafa bëggoon a yokk xam-xamam ci Yàlla. Looloo taxoon mu ñaan Yàlla ne ko: «Xamal ma li nga namm, ba ma xam la» (Mucc ga 33:13). Noonu, Yexowa daldi xamal Musaa yenn ci ay jikkoom. Jàngal Mucc ga 34:4-6. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Yexowa, yan jikkoom la xamal Musaa?

  • Ban ci jikkoy Yexowa yi moo la gën a neex?

6. Yexowa dafa fonk nit ñi

Yawut yi nekkoon mbooloo Yàlla, ay jaam lañu woon ca Misra. Lan la Yexowa doon yëg bi mu gisee mbooloom nekk ci coono? Déglul OJO BI walla nga jàng Mucc ga 3:1-10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci li ñu nettali fii, lan la Yexowa di yëg bu gisee nit ñi nekk ci coono? (Xoolal aaya 7 ak 8).

  • Ndax foog nga ne Yexowa bëgg na dimbali nit ñi dëgg? Te ndax mën na ko? Lu tax nga wax loolu?

7. Li Yexowa sàkk dafa ñuy jàngal lu bare ci jikkoom

Yexowa won na ñu ay jikkoom ci li mu sàkk. Seetaanal WIDEO BI, te jàng Room 1:20. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Yan jikkoy Yexowa ngay gis ci li mu sàkk?

BU LA NIT WAXOON: «Man fooguma ne mën nañu xam Yàlla dëgg.»

  • Lan nga ci xalaat?

  • Lu tax nga gise ko noonu?

NAÑU TËNK

Yexowa xel la, kenn mënu koo gis. Jikko yu rafet la am, te mbëggeel moo ci gën a fës.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax mënuñu gis Yexowa?

  • Lan mooy xel mu sell mi?

  • Yan ñooy yenn ci jikkoy Yexowa?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal liy wone ne Yexowa nekkul ci lépp.

«Ndax Yàlla mu ngi fépp ak ci lépp?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal li tax Biibël bi di méngale xel mu sell mi ak loxoy Yàlla.

«Lan mooy xel mu sell mi?» (Ci jw.org la nekk)

Benn góor gu gumba amoon na jafe-jafe ngir gëm ne Yàlla fonk na ko. Xoolal li soppi gis-gisam.

«Léegi xam naa ne mën naa dimbali ñeneen ñi» (w15 1/10)