Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 08

Mën nga nekk xaritu Yexowa

Mën nga nekk xaritu Yexowa

Yexowa dafa bëgg nga gën koo xam. Lu tax? Ndaxte dafa yaakaar ne, boo gënee xam jikkoom, ni muy jëfe ak coobareem, dinga gën a bëgg nekk xaritam. Ndax ci dëgg, mën nga nekk xaritu Yàlla? (Jàngal Saag 2:23). Lan nga mën a def ngir nekk xaritam? Biibël bi tontu na ci laaj yooyu te wone na li tax Yexowa doon xarit bi gën ci xarit yi.

1. Lan la Yexowa bëgg nga def?

«Jegeleen Yàlla, mu jege leen» (Saag 4:8). Loolu lu mu tekki? Yexowa dafa bëgg nga nekk xaritam. Xéyna am na ñu foog ne, xaritoo ak Yàlla du yomb ndaxte mënuñu koo gis. Waaye ci Kàddoom Biibël bi, Yexowa dafa ñuy xamal lépp li ñu soxlaa xam ci moom ngir mën koo jege. Bu ñuy jàng li ñu Yexowa wax ci Biibël bi, suñu xaritoo ak moom dafay gën a dëgër bu dee sax mënuñu koo gis.

2. Lan moo tax Yexowa doon xarit bi gën?

Kenn mënu laa bëgg ba raw ni la Yexowa bëgge. Dafa bëgg nga am jàmm ci sa dund te nga ñaan ko saa yoo soxlaa ndimbal. Mën nga ‘yenniku ci kawam sa njàqare jépp, ndax ku la ñeewante la’ (1 Piyeer 5:7). Yexowa pare na ngir dimbali ay xaritam, dëfal leen te déglu leen saa su nekk (Jàngal Sabóor 94:18, 19).

3. Lan la Yexowa di xaar ci ay xaritam?

Yexowa nit ñépp la bëgg, waaye dafay «xejjoo kuy jubal» (Kàddu yu Xelu 3:32). Li Yexowa di xaar ci ay xaritam mooy, ñuy jéem a def li baax ci ay bëtam te moytu lu bon. Am na ñu foog ne, duñu mën a def mukk lépp li Yexowa bëgg te bàyyi li mu bañ. Waaye Yexowa ku bare yërmande la. Yexowa nangu na nekk xaritu képp ku ko bëgg dëgg te di def lépp ngir neex ko (Sabóor 147:11; Jëf ya 10:34, 35).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Jàngal leneen lu la mën a dimbali nga nekk xaritu Yexowa te xam li tax mu doon xarit bi gën.

4. Ibraayma xaritu Yexowa la woon

Li Biibël bi nettali ci Ibraayma (ñu ko doon woowe itam Ibraam) dafa ñuy dimbali ñu xam li xaritoo ak Yàlla di tekki. Jàngal lu jëm ci Ibraayma ci Njàlbéen ga 12:1-4. Boo paree nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan la Yexowa wax Ibraayma mu def?

  • Lan la ko Yexowa digoon?

  • Lan la Ibraayma def bi ko Yexowa waxe loolu?

5. Li Yexowa di laaj ay xaritam

Bu ñu amee ay xarit, am na li ñuy xaar ci ñoom.

  • Lan nga bëgg say xarit defal la?

Jàngal 1 Yowaana 5:3. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la Yexowa di xaar ci ay xaritam?

Bu ñu bëggee déggal Yexowa, xéyna dinañu soxlaa soppi suñu doxalin walla suñu jikko. Jàngal Esayi 48:17, 18. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax Yexowa bëgg ay xaritam di def ay coppite?

Xarit bu baax dafa ñuy wax li ñu mën a aar ak li ñu mën a amal njariñ. Loolu la Yexowa di def ak ay xaritam

6. Li Yexowa di defal ay xaritam

Yexowa dafay dimbali ay xaritam ci seeni jafe-jafe. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Naka la Yexowa dimbalee jigéen ji ñu wone ci wideo bi, mu xeex ak lu mel ni ragal, njàqare ak xeeb sa bopp?

Jàngal Esayi 41:10, 13. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan la Yexowa dig ne dina ko defal ñépp ñi nekk ay xaritam?

  • Ndax foog nga ne Yexowa dina nekk xarit bu baax? Lu tax?

Xarit yu la jege dañu lay dimbali saa yoo leen soxlaa. Yexowa itam dina la dimbali

7. Xaritoo ak Yexowa dafa laaj ñuy waxtaan ak moom

Waxtaan dafay dëgëral xaritoo. Jàngal Sabóor 86:6, 11. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka lañu mënee wax ak Yexowa?

  • Naka la Yexowa di waxe ak ñun?

Dañuy wax ak Yexowa jaare ko ci ñaan; moom muy wax ak ñun jaare ko ci Biibël bi

BU LA NIT WAXOON: «Kenn mënul nekk xaritu Yàlla.»

  • Ban aaya nga mën a jël ngir wone ne mën nañu nekk xaritu Yexowa?

NAÑU TËNK

Yexowa dafa bëgg nga nekk xaritam te dina la dimbali nga gën koo jege.

Nañu fàttaliku

  • Naka la Yexowa di dimbalee ay xaritam?

  • Lu tax Yexowa bëgg ay xaritam di def ay coppite?

  • Ndax foog nga ne li Yexowa di xaar ci ay xaritam dafa diis lool? Lu tax nga wax loolu?

Jubluwaay

GËSTUL

Nekk xaritu Yexowa, ban njariñ la la mën a amal?

«Yexowa: Yàlla ju jar a xam» (w03 15/2)

Xoolal li tax benn jigéen wax ne xaritoom ak Yexowa moo ko musal.

«Bëgguma woon a dee» (wp17 nº 1)

Déglul li ay ndaw wax ci seen xaritoo ak Yexowa.

Nekk xaritu Yexowa, lan la tekki? (1:46)