Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 09

Jegeel Yàlla ci ñaan

Jegeel Yàlla ci ñaan

Ndax ci sa dund mas nga soxla ñu xelal la? Ndax amul ay laaj yu am solo yoo bëgg a xam seen tontu? Ndax soxla nga ku la dëfal walla dalal sa xel? Ndax bëgg nga gën a jege Yexowa? Ñaan Yàlla mën na la dimbali ci loolu lépp. Waaye naka lañu war a ñaane Yàlla? Ndax Yàlla dafay déglu ñaan yépp? Lan nga mën a def ba mu wóor la ne Yàlla dina nangu say ñaan? Loolu lañuy gis ci lesoŋ bii.

1. Kan lañu war a ñaan, te lan lañu ko mën a ñaan?

Yeesu jàngale woon na ne, suñu Baay bi ci asamaan rekk lañu war a ñaan. Yeesu ci boppam, Yexowa la doon ñaan. Lii la waxoon: «Nii ngeen wara ñaane: ‘Sunu Baay bi nekk ci kaw...’» (Macë 6:9). Bu ñuy ñaan Yexowa, dañuy dëgëral suñu xaritoo ak moom.

Daanaka mën nañu ñaan lépp Yexowa. Waaye nag ngir Yàlla nangu suñuy ñaan, fàww ñaan yi ànd ak coobareem. «Su nu ko ñaanee dara ci coobareem, dina nu nangul» (1 Yowaana 5:14). Yeesu waxoon na ci yenn mbir yi ñu mën a ñaan (Jàngal Macë 6:9-13). Mën nañu ñaan ci suñuy soxla. Waaye waruñu fàtte di gërëm Yàlla ci li mu ñu defal ak itam di ko ñaan ngir mu dimbali ñeneen ñi.

2. Naka lañu war a ñaane?

Biibël bi dafa ñuy xiirtal ci ‘diis Yàlla suñu xol’ (Sabóor 62:9). Kon suñuy ñaan dañu war a jóge ci suñu biir xol. Bu ñuy ñaan, mën nañu wax ci kaw walla ci suñu xel. Mën nañu sukk, taxaw walla toog, li am solo mooy ñu def ko ak respe. Mën nañu ñaan ci waxtu bu nekk ak ci béréb bu nekk.

3. Naka la Yàlla di tontoo suñuy ñaan?

Dafa koy def ci fasoŋ yu bari. Yexowa jox nañu Kàddoom Biibël bi, fu ñuy faral di gis tontu yi ñu soxla. Jàng Biibël bi mën na «xelal ku xeluwul» (Sabóor 19:8; jàngal Saag 1:5). Yàlla mën nañu may xel mu dal bu ñu nekkee ci jafe-jafe. Mën na xiir ay jaamam ñu dimbali ñu, su ñu ko soxlaa dëgg.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni nga mënee def ay ñaan yu jóge ci sa biir xol te neex Yàlla. Xoolal itam njariñ bi nga mën a jële ci ñaan.

4. Am na li Yàlla di laaj ngir nangu suñuy ñaan

Lan mooy tax Yàlla nangu suñuy ñaan? Seetaanal WIDEO BI.

Yexowa dafa bëgg ñu di ko ñaan. Jàngal Sabóor 65:3. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ndax foog nga ne kiy «nangug ñaan» bëgg na nga di ko ñaan? Lu tax nga wax loolu?

Bu ñu bëggee Yàlla nangu suñuy ñaan, fàww ñuy topp ay santaaneem ci suñu dund. Jàngal Mise 3:4 ak 1 Piyeer 3:12. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan lañu mën a def ba mu wóor ñu ne Yexowa dina déglu suñuy ñaan?

Bu geer amee, ku nekk dangay ñaan Yàlla mu may la ndam. Ndax Yàlla mën na nangu fasoŋu ñaan yooyu?

5. Suñuy ñaan dañu war a jóge ci suñu biir xol

Am na ñoo xam ne, dañu leen jàngal ñuy tari bu ñuy ñaan. Waaye ndax noonu la Yàlla bëgge ñu di ko ñaan? Jàngal Macë 6:7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Booy ñaan, naka nga mënee moytu di «bareel wax yu amul njariñ»?

Bés bu nekk, xalaatal ci lenn lu la Yexowa defal te gërëm ko ci. Boo defee loolu ba mu mat semen, dinga gis ne ñaan nga Yexowa ci juróom ñaari mbir yu wuute te tariwuloo benn wax bi.

Baay bu baax dafay bëgg doomam wax ko lépp li nekk ci xolam. Noonu it, Yexowa dafa bëgg bu ñu koy ñaan, ñu wax ko lépp li nekk ci suñu biir xol

6. Ñaan mayug Yàlla la

Naka lañu ñaan mënee dooleel, rawatina bu ñu nekkee ci ay jafe-jafe? Seetaanal WIDEO BI.

Biibël bi wax na ñu ne, ñaan mën na ñu dimbali ñu am xel mu dal dëgg. Jàngal Filib 4:6, 7. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka la ñu ñaan di dimbalee, bu dee sax suñu jafe-jafe fajuwul?

  • Lan nga bëgg a ñaan Yàlla?

Ndax xamoon nga ne...

«Amiin» dafay tekki «na li ñu wax am» walla «ci lu wóor». Ci jamono yi ñu doon bind Biibël bi ba tey, bu ñu ñaane ba pare, dañuy wax «amiin» (Sabóor 41:14).

7. Jëlal jot ngir ñaan Yàlla

Lée-lée yitte yi dañuy bari lool ba ñu fàtte ñaan. Naka la Yeesu wone ne ñaan lu am solo la? Jàngal Macë 14:23 ak Màrk 1:35. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka la Yeesu doon def ngir am jotu ñaan?

  • Kañ nga mën a jël jot ngir ñaan?

BU LA NIT WAXOON: «Yàlla ci benn làkk rekk lay déglu ñaan yi.»

  • Lan nga koy wax?

NAÑU TËNK

Ñaan yi jóge ci suñu biir xool dañuy dëgëral suñu diggante ak Yàlla, may ñu xel mu dal te may ñu doole ngir ñu def li neex Yexowa.

Nañu fàttaliku

  • Kan lañu war a ñaan?

  • Naka lañu war a ñaane?

  • Ban njariñ la ñu ñaan mën a amal?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ay tontu ci laaj yi nit ñi faral di laaj ci lu jëm ci ñaan.

«Juróom ñaari mbir yi nga war a xam ci lu jëm ci ñaan Yàlla» (w10 1/10)

Xoolal li tax ñaan am solo ak li nga mën a def ngir say ñaan gën a neex Yàlla.

«Lu tax ma war di ñaan Yàlla?» (Ci jw.org la nekk)

Ci woy bii, seetlul ne mën nañu ñaan Yàlla fu ñu mënta nekk ak ci waxtu bu nekk.

Ñaanal Yàlla (1:22)