Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 16

Lan la Yeesu def bi mu nekkee ci kaw suuf?

Lan la Yeesu def bi mu nekkee ci kaw suuf?

Bu ñu tuddee Yeesu, ñu bari seen xel dafay dem ci ab liir bu ndaw, yonent bu mag, walla ab góor guy sukkuraat. Waaye ndax am na leneen lu ñu mën a xam ci moom, bu ñu jàngee lu jëm ci dundam ci kaw suuf? Ci lesoŋ bii, dinañu gis lu am solo lu Yeesu def ak ni la loolu mënee dimbali ci sa dund.

1. Ban liggéey moo gënoon a am solo ci Yeesu?

Liggéey bi gënoon a am solo ci Yeesu mooy «yégle xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla» (Jàngal Luug 4:43). Xibaaru jàmm bi mu doon yégle mooy, Yàlla dina samp benn nguur walla gornmaa, bu nar a faj jafe-jafey doomu Aadama yi yépp. a Ci diiru ñetti at ak genn-wàll, Yeesu tàyyiwul benn yoon ci yégal nit ñi xibaar bu neex boobu (Macë 9:35).

2. Kéemaan yi Yeesu doon def, lan lañu doon wone?

Biibël bi wax na lu bari ci ay «kéemaan, ay jaloore ak firnde, ya Yàlla defoon jaarale ko ci [Yeesu]» (Jëf ya 2:22). Ci kàttanu Yàlla, Yeesu dalal na ngelaw lu réy, dundal ay junniy nit, faj ñu feebar, dekkal sax ay nit ñu deewoon (Macë 8:23-27; 14:15-21; Màrk 6:56; Luug 7:11-17). Kéemaan yi Yeesu def, wone nañu ci lu leer ne, Yàllaa ko yónni. Wone nañu itam ne, Yexowa am na kàttanu faj suñu jafe-jafe yépp.

3. Lan lañu mën a jànge ci dundu Yeesu?

Yeesu dafa doon déggal Yexowa ci lépp (Jàngal Yowaana 8:29). Ba ba muy dee, Yeesu def na lépp li ko Baayam santoon, doonte sax amoon na ñi ko doon xeex. Wone na ne, bu nit nekkee ci ay jafe-jafe sax, terewul mën na jaamu Yàlla. Kon Yeesu teg na «fi [suñu] kanam royukaay, ngir [ñu] jaar ciy tànkam» (1 Piyeer 2:21).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni Yeesu xamale nit ñi xibaaru jàmm bi ak ni mu defe ay kéemaan.

4. Yeesu dafa doon xamal nit ñi xibaaru jàmm bi

Yeesu dafa doon dox ay téeméeri kilometar, ci ay yoon yu bari suuf, ngir mën a xamal xibaaru jàmm bi nit ñu bare-bare. Jàngal Luug 8:1. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ndax Yeesu, nit ñi doon ñëw ci moom rekk ngir déglu ko, la doon waar?

  • Lan la doon def ngir wut nit ñu bari?

Yàlla yégle woon na ne, Almasi bi dina xamle xibaaru jàmm bi. Jàngal Esayi 61:1, 2. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka la Yeesu matale yégle yonent bii?

  • Ndax foog nga ne tey, nit ñi soxla nañu dégg xibaaru jàmm bii?

5. Yeesu jàngale na lu am njariñ

Yeesu yemul rekk ci yégle xibaaru jàmm bi, waaye dafa jàngale itam luy amal njariñ nit ñi. Xoolal yenn ci njàngale yooyu ci waxtaan bu siiw bi mu defoon ci kaw benn tund. Jàngal Macë 6:14, 34 ak 7:12. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ban xelal bu am njariñ la Yeesu joxe ci aaya yii?

  • Ndax foog nga ne xelal bi am na njariñ ba tey?

6. Yeesu defoon na ay kéemaan

Yexowa mayoon na Yeesu kàttanu def ay kéemaan yu bari. Ngir xam benn ci kéemaan yooyu, jàngal Màrk 5:25-34 walla seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, lan moo wóoroon jigéen ji feebaroon?

  • Lan moo la neex ci kéemaan boobu?

Jàngal Yowaana 5:36. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Kéemaan yi Yeesu doon def, lan lañu doon «seede», walla wone ci moom?

Ndax xamoon nga ne...

Lu bari li ñu xam ci Yeesu, ñu ngi ko jële ci ñeenti téere yi ñuy woowe Injiil ci Biibël bi, maanaam ci téere Macë, Màrk, Luug ak Yowaana. Téere bu ci nekk, am na li mu ñuy xamal ci Yeesu. Bu ñu leen jàngee ñoom ñépp, dañuy gën a sopp Yeesu ndax ni mu doon dunde.

  • MACË

    moo njëkk a bind ci téere Injiil. Moom dafay fësal li Yeesu doon jàngale, rawatina lu jëm ci nguuru Yàlla.

  • MÀRK

    moo bind téere bi gën a gàtt ci Injiil. Moom dafa nettali xew-xew yi, ci fasoŋ bu ànd ak cawarte.

  • LUUG

    moom dafa gën a fësal ni Yeesu fonke woon ñaan Yàlla ak doxalinam bu rafet ak jigéen ñi.

  • YOWAANA

    moom dafa nettali waxtaan yu bari yu Yeesu amoon ak ay xaritam ak ñeneen. Loolu tax na ñu xam lu bari ci jikkoy Yeesu.

BU LA NIT WAXOON: «Yeesu yonent la woon rekk ni yeneen yonent yi.»

  • Lan nga ci xalaat?

NAÑU TËNK

Yeesu yégle na lu jëm ci nguuru Yàlla, def na ay kéemaan, te déggal na Yexowa ci lépp.

Nañu fàttaliku

  • Lan moo nekkoon liggéey bi gën a am solo ci Yeesu, bi mu nekkee ci kaw suuf?

  • Lan la kéemaan yi Yeesu def doon wone?

  • Yan njàngale yu am njariñ la Yeesu doon jàngale?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal li tax ñu mën a gëm ne Yeesu def na ay kéemaan dëgg.

«Kéemaan yi Yeesu def: lan nga ci mën a jàng?» (w04 15/7)

Xoolal ni benn góor soppee dundam bi mu jàngee ne Yeesu dafa amoon yitte ci nit ñi.

«Sama bopp rekk laa fi nekkaloon» (w14 1/10)

Xoolal li gën a am solo ci liggéeyu waare bi Yeesu doon def, ak ni xew-xew yi toppalantee.

«Xew-xew yi gën a am solo ci dundu Yeesu» (sgd 4-B)

a Ci lesoŋ 31 ba 33, dinañu gën a wax ci lu jëm ci nguuru Yàlla.