Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 18

Naka lañu mënee ràññee karceen dëgg yi?

Naka lañu mënee ràññee karceen dëgg yi?

Ay milyaari nit dañuy wuyoo turu karceen. Waaye ñoom ñépp bokkuñu li ñu gëm, te ni ñuy toppe santaane Yàlla yi du benn. Kon naka lañu mënee ràññee karceen dëgg yi?

1. Nekk karceen mooy lan?

Ñi nekk karceen ñooy ñi nekk taalibe Yeesu Kirist, walla ñi koy topp. Biibël bi nee na «ci Ancos lañu jëkka tudde taalibe ya ay karceen» (Jëf ya 11:26, MN). Naka lañuy wone ne ay taalibe Yeesu lañu? Yeesu lii la wax: «Bu ngeen saxee ci li ma wax, nekk ngeen samay taalibe ci lu wóor» (Yowaana 8:31). Loolu dafay tekki ne, karceen dëgg yi dañuy topp li Yeesu di jàngale. Te ndegam Yeesu li mu doon jàngale ci Mbind mu sell mi la jóge, kon karceen dëgg yi, seen ngëm dafa war a sukkandiku ci Biibël bi (Jàngal Luug 24:27).

2. Naka la karceen dëgg yi di wonee seen mbëggeel?

Yeesu lii la waxoon ay taalibeem, nangeen «bëggante, ni ma leen bëgge» (Yowaana 15:12). Naka la Yeesu wonee ne bëgg na ay taalibeem? Dafa doon jël jot ngir nekk ak ñoom, di leen dooleel ak di leen dimbali. Joxe na sax dundam ngir ñoom (1 Yowaana 3:16). Ni Yeesu, karceen dëgg yi itam, seen mbëggeel yemul rekk ci wax. Dañuy wone ne bëggante nañu ci seen biir, muy ci wax ak ci jëf.

3. Ban liggéey la karceen dëgg yi di def?

Yeesu dénk na taalibeem yi liggéey, «mu yónni leen ñuy yégle nguuru Yàlla» (Luug 9:2). Karceen yu njëkk ya, daawuñu waare rekk ci seen béréb yi ñu doon jaamoo Yàlla. Waaye dañu doon waare ci béréb yu bare nit ak ci biir kër yi (Jàngal Jëf ya 5:42; 17:17). Tey itam, karceen dëgg yi dañuy waare dëgg gi nekk ci Biibël bi, fépp fu nit ñi nekk. Dañu bëgg seen moroom. Moo tax ñu bég ci jël seen jot ngir yégle xibaar bi nekk ci Biibël bi, te def ko ak seen kem kàttan. Xibaar boobu dafay maye yaakaar te di dëfal xol (Màrk 12:31).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni nga mënee ràññee karceen dëgg yi, ci biir ñépp ñiy wuyoo karceen te duñu topp njàngaley Yeesu te duñu roy ci moom.

4. Dañuy wut a xam dëgg gi nekk ci Biibël bi

Karceen yu njëkk ya dañu fonkoon Kàddu Yàlla

Du ñépp ñiy wuyoo turu karceen ñoo fonk dëgg gi nekk ci Biibël bi. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Naka la igliis yiy wuyoo turu karceen teree nit ñi, ñu xam li Yeesu jàngale?

Yeesu dafa doon jàngale dëgg gi nekk ci Kàddu Yàlla. Jàngal Yowaana 18:37. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ni ko Yeesu waxe, naka lañu mënee ràññee ñi «bokk ci dëgg [gi]»?

5. Dañuy yégle dëgg gi nekk ci Biibël bi

Karceen yu njëkk ya dañu doon waare

Bala Yeesu di yéeg ci kaw asamaan, dafa dénk ay taalibeem liggéey bu ñuy wéyal ba tey. Jàngal Macë 28:19, 20 ak Jëf ya 1:8. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ba fan lañu war a waare ak ba kañ lañu koy def?

6. Dañuy jëfe li ñuy waare

Góor gi tudd Tom, lan moo tax mu wóor ko ne, gis na karceen dëgg yi? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, lan moo taxoon Tom doyal ci diine?

  • Lan moo tax léegi mu wóor ko ne, gis na dëgg gi?

Jëf moo gën a am doole waxi kese. Jàngal Macë 7:21. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan moo gën a am solo ci Yeesu, wax ne gëm nañu walla wone suñu ngëm ci jëf?

7. Dañu bëggante ci seen biir

Karceen yu njëkk ya dañu bëggante woon ci seen biir

Ndax am na karceen yu wone dëgg ne, nangu nañu ñàkk seen bakkan ngir aar ñi ñu bokkal diine? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, lan moo xiir Lloyd ci nangoo ñàkk bakkanam ngir mbokk Johansson?

  • Ndax foog nga ne, jëfe na ni karceen dëgg?

Jàngal Yowaana 13:34, 35. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka la taalibe Yeesu yi (maanaam karceen dëgg yi) di doxale ak ñi ñu bokkalul xeet walla réew?

  • Naka lañuy doxale ak ñooñu bu geer amee?

BU LA NIT WAXOON: «Ak lu bon lépp li karceen yi def, naka la diine karceen mënee nekk diine dëgg ji?»

  • Ban aaya nga mën a jël ngir won ko ne, mën nañu ràññee karceen dëgg yi?

NAÑU TËNK

Karceen dëgg yi, dañuy topp li Biibël bi wax, dañuy bëggante ci seen biir, te dañuy yégle dëgg gi nekk ci Biibël bi.

Nañu fàttaliku

  • Ci lan la ngëmu karceen dëgg yi sukkandiku?

  • Ban jikko mooy wone ñi nekk karceen dëgg?

  • Ban liggéey la karceen dëgg yi di def?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal li dimbali ab jigéen ju nekkoon soor, ba mu gis «ay mbokk dëgg ci wàllu ngëm.»

«Dañu jëfandikoo Biibël bi ngir tontu ci samay laaj yépp» (w14 1/4)

Xoolal ni karceen dëgg yi di dimbalee ñi ñu bokkal diine te soxla ndimbal.

Dañuy dimbali suñu mbokk yi ci ngëm bu musiba amee (Xaaj) (3:57)

Yeesu waxoon na ni ñuy ràññee ay taalibeem. Xoolal ni karceen yu njëkk ya ak ñiy karceen dëgg tey, wonee ne ay taalibe Yeesu lañu.

«Naka lañuy xàmmee karceen dëgg yi?» (w12 1/3)