Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 19

Ndax Seede Yexowa yi ay karceen dëgg lañu?

Ndax Seede Yexowa yi ay karceen dëgg lañu?

Ñun Seede Yexowa yi, gëm nañu ne ay karceen dëgg lañu. Lu tax? Xoolal suñu ngëm ci li mu sukkandiku, li tax ñu tudde suñu bopp Seede Yexowa ak ni ñuy wone mbëggeel ci suñu biir.

1. Ngëmu Seede Yexowa yi, ci lan la sukkandiku?

Yeesu nee na: «Kàddu [Yàlla] mooy dëgg» (Yowaana 17:17). Ni Yeesu, Seede Yexowa yi, seen ngëm ci Kàddu Yàlla la mas a sukkandiku. Xool ko ci seen jaar-jaar. Ci booru atum 1870 la benn gurup tàmbalee gëstu bu baax Biibël bi. Li ñu gëm, ci Biibël bi lañu ko doon jële, bu dee sax wuute woon na ak li igliis yi doon jàngale. Gannaaw gi, ñu komaase di xamal ñeneen ñi dëgg gi ñuy jàng ci Biibël bi. a

2. Lu tax ñu tudde suñu bopp Seede Yexowa?

Yexowa dafay woowe jaamam yi ay seedeem ndaxte dañuy xamle dëgg gi jëm ci moom (Yawut ya 11:4–12:1). Ci jamono yu njëkk ya, Yàlla lii la waxoon jaamam yi: «Yeenay samay seede» (Jàngal Esayi 43:10). Ñu ngi woowe Yeesu «seede bu takku bi» (Peeñu 1:5). Moo tax ci atum 1931, ñu jël turu Seede Yexowa. Wuyoo tur boobu lu réy la ci ñun.

3. Naka la Seede Yexowa yi di roye mbëggeel gi Yeesu wone?

Yeesu dafa bëggoon lool taalibeem yi ba jàppe leen ni ñoo bokk benn njaboot (Jàngal Màrk 3:35). Noonu itam, Seede Yexowa yi ci àddina si sépp dañu doon benn, mel ni njaboot gu mag. Loolu moo tax ay mbokk lañuy woowante ci suñu biir (Filemon 1, 2). Dañuy topp itam ndigal lii: ‘Bëggleen kureelu bokk yi’ (1 Piyeer 2:17). Seede Yexowa yi dañuy wone mbëggeel googu ci anam yu bari. Fépp ci àddina si, bu seeni mbokk ci ngëm nekkee ci jafe-jafe, dañu leen di dimbali.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal leneen lu jëm ci jaar-jaaru Seede Yexowa yi te gis firnde yuy wone ne, ay karceen dëgg lañu.

Li karceen dëgg yi gëm dafay sukkandiku ci Biibël bi te dañu koy xamal ñeneen ñi

4. Li ñu gëm ci Biibël bi la sukkandiku

Yexowa yégle woon na ne suñu xam-xam ci Biibël bi dina gën a leer. Jàngal Dañeel 12:4. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan moo nar a «yokku» bu jaami Yàlla yi wéye di gëstu Biibël bi?

Xoolal ni benn gurup doon gëstoo Biibël bi, Charles Russell bokkoon na ci ñoom. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci wideo bi, naka la Charles Russell ak ñi mu àndal doon gëstoo Biibël bi?

Ndax xamoon nga ne...

Lée-lée dañuy indi ay coppite ci li ñuy jàngale. Lu tax? Nañu ko misaale nii: bu bët setagul duñu mën a gis bu baax, waaye lu naaj bi di gën di génn, mbir yi di gën a leer. Noonu it, Yàlla dafa ñuy dimbali ñu nànd Kàddoom ndànk-ndànk (Jàngal Kàddu yu Xelu 4:18). Kon nekkul ne dañuy soppi Biibël bi, waaye suñu xam-xam ci Biibël bi mooy gën a leer.

5. Dañuy waare dëgg gi jëm ci Yexowa

Lu tax ñu jël turu Seede Yexowa? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Lu tax turu Seede Yexowa nekk tur bu jekk ci ñun?

Lu tax Yexowa tànn ay nit ñu nekk ay seedeem? Dafa leen tànn ngir ñu xamal ñépp ne moom mooy Yàlla dëgg ji te wone it ne, lu bari li nit ñi di jàngale ci moom du dëgg. Xoolal ñaar ci njàngale yu dul dëgg yooyu.

Ci yenn diine yi, dañuy jàngale ne Yàlla dafa bëgg ñuy jëfandikoo ay nataal walla ay xërëm bu ñu koy jaamu. Ndax loolu dëgg la? Jàngal Sarxalkat yi 26:1 te tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan la Biibël bi di jàngale dëgg-dëgg? Naka la Yexowa gise jëfandikoo xërëm?

Am na njiitu diine yuy jàngale ne, Yeesu mooy Yàlla. Ndax loolu dëgg la? Jàngal Yowaana 20:17 te tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan la Biibël bi di jàngale dëgg-dëgg? Ndax Yàlla ak Yeesu, benn lañu?

  • Xam ne Yexowa dafa yónni ay seedeem ngir ñu xamle dëgg gi jëm ci moom ak ci doomam, loolu lan lay def ci yow?

6. Dañu bëggante ci suñu biir

Biibël bi nee na karceen yi dañu war a doon benn, ni céri yaram doone benn. Jàngal 1 Korent 12:25, 26. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan la karceen dëgg yi war a def bu seen moroomi karceen nekkee ci coono?

  • Naka nga gise mbëggeel gi am diggante Seede Yexowa yi?

Fépp fu Seede Yexowa yi nekk ci coono, seeni moroomi Seede Yexowa dañuy def lépp ngir dimbali leen ci lu gaaw. Ngir gis benn misaal, seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Li Seede Yexowa yi def ngir dimbali seen mbokk yi, naka lay wone ne bëggante nañu?

Karceen dëgg yi dañuy won mbëggeel ñi nekk ci coono

BU LA NIT WAXOON: «Diine Seede Yexowa yi, diine bu bees la.»

  • Kañ la Yexowa tàmbalee woowe ñi koy jaamu ay seedeem?

NAÑU TËNK

Seede Yexowa yi, ay karceen dëgg lañu. Ci àddina si sépp dañu doon benn, mel ni njaboot gu mag. Suñu ngëm ci Biibël bi la sukkandiku te dañuy xamle dëgg gi jëm ci Yexowa.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax ñu jël turu Seede Yexowa?

  • Naka lañu mel ci suñu biir?

  • Ndax foog nga ne Seede Yexowa yi, ay karceen dëgg lañu?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ni Seede Yexowa yi feeñale njàngale yi dul dëgg.

Mbooloom Yàlla dafay màggal turam (7:08)

Xoolal ay tontu ci ay laaj yi nga mën a am ci Seede Yexowa yi.

«Ay laaj yu jëm ci Seede Yexowa yi» (Ci jw.org la nekk)

Stephen dafa bañoon ñi mu bokkalul xeet ba di leen def lu bon. Xoolal li mu gis ci Seede Yexowa yi, ni mu ko dimbalee mu soppi doxalinam.

«Sama dund dafa doon gën a yees» (w15 1/7)

a Ci atum 1879 ba tey, ñu ngi wone dëgg gi nekk ci Biibël bi ci suñu yéenekaay bi gën a siiw, La Tour de Garde.