Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 20

Ni Yexowa di jiitee mbooloo karceen mi jaare ko ci Yeesu

Ni Yexowa di jiitee mbooloo karceen mi jaare ko ci Yeesu

Lépp li Yexowa di def dafay jaar yoon (1 Korent 14:33). Kon jaadu na ni muy jiite mbooloom itam jaar yoon. Naka la Yexowa di jiitee mbooloo karceen mi jaare ko ci Yeesu? Naka lañu mënee def suñu wàll ba lépp wéy di jaar yoon?

1. Kan mooy kilifag mbooloo mi?

‘Kirist mooy kilifag mbooloom ñi gëm’ (Efes 5:23). Ci asamaan la nekk di jiite liggéey bi mbooloo Yexowa di def fépp ci àddina si. Yeesu teg na fi ab «surga bu takku te teey.» Ñoom ay magi mbooloo lañu, te doon gurup bu ndaw, ñu leen di woowe itam Jataay biy dogal (Jàngal Macë 24:45-47). Ni apootar yu njëkk ya ak magi mbooloo ya nekkoon Yerusalem, Jataay biy dogal mooy joxe ay tegtal ci mbooloo karceen mi, fépp ci àddina si (Jëf ya 15:2). Waaye du góor yooyu ñooy jiite suñu mbootaay bi. Dañuy jàng Biibël bi ngir xam li Yexowa bëgg ñu def, te dañuy déggal Yeesu.

2. Lan mooy liggéeyu magi mbooloo mi?

Magi mbooloo mi ay karceen yu góor lañu yu am diggante bu rattax ak Yàlla. Dañuy sukkandiku ci Mbind mi ngir jàngal waa mbooloo mi, sàmm leen te dooleel leen. Kenn du leen fey ci seen liggéey. Dañuy liggéey ni ay ‘surgay Yàlla ci xol bu tàlli; def ko ak xol bu laab te bañ cee séentu alal’ (1 Piyeer 5:1, 2). Ñiy toppatoo yëfi mbooloo mi, ñooy jàppale magi mbooloo mi ci liggéey bi. Ñoom it mën nañu dem ba nekk magu mbooloo.

Jataay biy dogal dafay jël yenn magi mbooloo def leen ay wottukat yuy wër. Dañuy dem ci mbooloo yi ngir jox leen ay tegtal te dooleel leen. Dañuy sukkandiku ci Biibël bi ngir tànn ñiy doon ay magi mbooloo ak ñiy toppatoo yëfi mbooloo mi (1 Timote 3:1-10, 12; Tit 1:5-9).

3. Lan la bépp Seede Yexowa war a def?

Ñépp ci mbooloo mi dañuy bokk ci ndaje yi ngir ‘màggal turu Aji Sax ji’. Dañuy def it lépp li ñu mën ngir bokk ci liggéeyu waare bi (Jàngal Sabóor 148:12, 13).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ban fasoŋu kilifa la Yeesu doon, ni ko magi mbooloo mi di roye, ni ñu mënee déggal Yeesu ak ni ñu mënee ànd liggéeyandoo ak magi mbooloo mi.

4. Yeesu njiit bu baax la

Yeesu dafa ñuy woo ak xol bu rafet. Jàngal Macë 11:28-30. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Yeesu ban fasoŋu kilifa la, te lan la ñu bëggal?

Naka la ko magi mbooloo mi di roye? Seetaanal WIDEO BI.

Biibël bi wax na ci lu leer ni magi mbooloo mi war a defe seen liggéey.

Jàngal Esayi 32:2 ak 1 Piyeer 5:1-3. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan ngay yëg, boo gisee ne magi mbooloo mi dañuy def lépp ngir dëfal ñeneen ñi, ni Yeesu?

  • Ci yeneen anam yan la magi mbooloo mi di roye ci Yeesu?

5. Magi mbooloo mi ay royukaay lañu

Naka la Yeesu bëgge magi mbooloo mi gise seen liggéey? Seetaanal WIDEO BI.

Yeesu jox na ay tegtal ñi war a jiite ci biir mbooloo mi. Jàngal Macë 23:8-12. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Yan tegtal la Biibël bi jox ñiy jiite ci mbooloo mi? Ndax foog nga ne njiitu diine yi dañuy topp li Biibël bi wax?

  1. Magi mbooloo mi dañuy fexe ba ñoom ak seeni njaboot am diggante bu rattax ak Yàlla

  2. Magi mbooloo mi dañuy toppatoo ñépp ci mbooloo mi

  3. Magi mbooloo mi dañuy faral di bokk ci liggéeyu waare bi

  4. Magi mbooloo mi dañuy jàngale. Dañuy bokk itam ci set-setal bi ak ci yeneen liggéey

6. Mën nañu liggéeyandoo ak magi mbooloo mi

Biibël bi wax na li tax mu am solo ñu liggéeyandoo ak magi mbooloo mi. Jàngal Yawut ya 13:17. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lu tax Biibël bi wax ne, dañu war a déggal ñiy jiite te topp seen ndigal? Lan nga xalaat ci loolu?

Jàngal Luug 16:10. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax ñu war a déggal magi mbooloo mi, bu dee sax ci ay yëf yu ndaw la?

BU LA NIT WAXOON: «Soxlawul ngay bokk ci diine.»

  • Ndax yaakaar nga ne bokk ci mbooloo ngir jaamu Yàlla, am na njariñ?

NAÑU TËNK

Yeesu mooy kilifag mbooloo mi. Magi mbooloo mi dañuy déggal Yeesu. Loolu moo tax dañuy bég ci liggéeyandoo ak ñoom ndaxte dañu ñuy dëfal, te nekk ay royukaay ci ñun.

Nañu fàttaliku

  • Kan mooy kilifag mbooloo mi?

  • Naka la magi mbooloo mi di dimbalee waa mbooloo mi?

  • Lan la bépp jaamu Yexowa war a def?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal liy wone ne Jataay biy dogal ak magi mbooloo mi fonk nañu bu baax seen mbokki karceen tey.

Dañuy dimbali suñu mbokk yi fi ñu tere liggéeyu waare bi (4:22)

Xoolal lu jëm ci liggéeyu wottukat yiy wër ci mbooloo yi.

Dundu wottukat yiy wër ci dëkku àll yi (4:51)

Xoolal liggéey bu metti bi magi mbooloo yi di def ngir dooleel seen mbokk yi ci ngëm.

«Magi mbooloo mi dañuy ‘liggéeyandoo ak ñun ngir suñu mbég’» (w13 15/1)