Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 25

Lan la ñu Yàlla bëggal?

Lan la ñu Yàlla bëggal?

Biibël bi nee na nit ñi dañu «néewi fan, géejal coono» (Ayóoba 14:1). Ndax ci dëgg, loolu la ñu Yàlla bëggal? Bu dee du loolu, kon lan la ñu bëggal? Ndax li mu ñu bëggal dina mas a am? Xoolal tontu yuy dalal xel yu Biibël bi joxe ci laaj yooyu.

1. Ban dund la ñu Yexowa bëggal?

Yexowa dafa bëgg ñu am dund gi gën. Bi Yàlla sàkkee Aadama ak Awa, dafa leen dugal ci àjjana ju rafet, ci toolu Eden. Gannaaw gi «Yàlla barkeel leen ne leen: ‘Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu’» (Njàlbéen ga 1:28). Yexowa dafa bëggoon ñu am ay doom, yaatal àjjana ji ci suuf si sépp, te toppatoo mala yi. Dafa bëggoon nit ñi ñépp am wér-gu-yaram gu mat sëkk te dund ba fàww.

Dëgg la ne amuñu tey dund gi ñu Yàlla bëggaloon, a waaye ba tey li Yàlla bëggoon deñul (Esayi 46:10, 11). Ba tey dafa bëgg nit ñi koy déggal dund ba fàww ci jàmm (Jàngal Peeñu 21:3, 4).

2. Naka lañu mënee am jàmm ci suñu dund tey?

Yexowa dafa ñu sàkk, def ci ñun bëgg-bëggu «neex Yàlla», maanaam ñu bëgg koo xam te jaamu ko (Jàngal Macë 5:3-6). Dafa bëgg ñu am diggante gu rattax ak moom, «di doxe mboolemi yoonam, sopp ko» te jaamu ko ak suñu «léppi xol» (Baamtug Yoon wi 10:12; Sabóor 25:14). Bu ñu defee loolu, dinañu mën a am jàmm bu dee sax am nañu ay jafe-jafe. Bu ñuy jaamu Yexowa, dinañu am jàmm ci suñu dund, ndaxte ñu ngi dunde ni mu ko bëgge.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal mbëggeel gu réy gi ñu Yexowa won, ci ni mu sàkke suuf si ngir ñun, ak li ñu Kàddoom xamal ci li mu bëggal nit ñi.

3. Yexowa dund gu neex la bëggal nit ñi

Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Lu tax Yàlla sàkk suuf si mu rafet lool?

Jàngal Kàdduy Waare 3:11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la ñu lii di jàngal ci Yexowa?

4. Li Yexowa bëggoon deñul

Jàngal Sabóor 37:11, 29 ak Esayi 55:11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka lañu xamee ne li Yexowa bëggoon deñul?

5. Jaamu Yexowa moo ñuy may jàmm ci suñu dund

Xam li Yexowa bëggal nit ñi, mën nañu may mbégte. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Xam li Yàlla bëggal nit ñi, lan la def ci Terumi?

Jàngal Kàdduy Waare 12:13. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Bu ñu xoolee ci lépp li ñu Yexowa defal, loolu lan la ñu war a xiir ñu def?

BU LA NIT LAAJOON: «Lan la Yàlla bëggal nit ñi?»

  • Lan nga koy tontu?

NAÑU TËNK

Yexowa dafa bëgg nit ñi dund ba fàww ci jàmm ci kaw suuf si. Te bu ñu ko jaamoo ak suñu xol bépp, dinañu am jàmm dëgg ci suñu dund tey.

Nañu fàttaliku

  • Lan la Yexowa bëggoon bi mu sàkkee Aadama ak Awa?

  • Naka lañu xame ne li Yàlla bëggal nit ñi deñul?

  • Naka nga mënee am jàmm dëgg ci sa dund?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal firnde yiy wone ne toolu Eden mas naa am.

«Toolu Eden: ndax ay léeb la walla dëgg la?» (w11 1/1)

Xoolal li tax ñu mën a gëm ne, suuf si dina fi nekk ba fàww.

«Ndax suuf si dina fi mas a jóge?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal ni benn góor gu foogoon ne amoon na lépp ci dundam, mujjee gis ne am na lu ko mànke woon.

Léegi am naa jàmm ci sama dund (3:55)

a Ci lesoŋ biy topp, dinañu gis li tax amuñu dund googu.