Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 30

Suñu mbokk yi dee mën nañu dundaat!

Suñu mbokk yi dee mën nañu dundaat!

Dee dafay indi naqar ak tiis. Looloo tax Biibël bi ne, dee noon la (1 Korent 15:26). Ci lesoŋ 27 bi, gisoon nañu ne Yexowa dina fi jële noon boobu. Waaye ñi dee ba pare nag, lan lay def ak ñoom? Ci lesoŋ bii, dinga jàng beneen dige bu neex bu ñu Yexowa dig. Dige na ne dina dundalaat ay milioŋi nit ngir ñu mën a dund ba fàww. Dina leen dekkal! Ndax ci dëgg, loolu mën na nekk? Ñi nar a dekki, fan lañuy dund, ci kaw asamaan walla ci kaw suuf?

1. Lan la Yexowa bëgg a defal suñu mbokk yi dee?

Yexowa dafa yàkkamti dundalaat ñi dee. Benn góor gu amoon ngëm te tuddoon Ayóoba, amoon na kóolute ne Yàlla du ko fàtte bu deewee. Lii la waxoon Yàlla: «Nga woo ma, ma wuyu [ci bàmmeel]» (Jàngal Ayóoba 14:13-15).

2. Naka lañu xame ne ñi dee mën nañu dekki?

Bi Yeesu nekkee ci kaw suuf, Yàlla mayoon na ko kàttanu dekkil ñi dee. Yeesu dundalaat na xale bu jigéen bu amoon 12 at ak doomu benn jigéen ju ñàkkoon jëkkëram (Màrk 5:41, 42; Luug 7:12-15). Gannaaw loolu, xaritam Lasaar dee. Bu dee sax Lasaar deewoon na te ñu suul ko ba mu def ñeenti fan, Yeesu dundalaat na ko. Yeesu dafa ñaan Yàlla ba pare, jàkkaarlook bàmmeel bi daldi wax ci kaw ne: «Lasaar, ñëwal ci biti!» Noonu «néew bi daldi génn.» Lasaar dafa dundaat! (Yowaana 11:43, 44). Xalaatal rekk mbégte bi mbokki Lasaar yi ak xaritam yi amoon!

3. Ban yaakaar lañu mën a am ngir suñu mbokk yi dee?

Biibël bi dige na ne: «Ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki» (Jëf ya 24:15). Nit ñi Yeesu dekkaloon nekkuñu woon ci kaw asamaan (Yowaana 3:13). Fii ci kaw suuf la leen dekkaloon te ñoom bégoon nañu ci. Noonu itam ci kanam tuuti, Yeesu dina dekkal ay milioŋi nit ngir ñu dund ba fàww ci àjjana ci kaw suuf. Dafa ne woon «néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel» dinañu dekki. Dina dekkal sax nit ñi ñu fàtte, ndaxte Yexowa moom fàttewu leen (Yowaana 5:28, 29).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ci Biibël bi firnde yiy wone ne, ñi dee mën nañu dekki te dinañu dekki. Xoolal it yaakaar bi la ndekkite mën a may ak ni mu mënee dëfal sa xol.

4. Yeesu wone na ne mën na dekkal ñi dee

Jàngal leneen ci li Yeesu defal xaritam Lasaar. Jàngal Yowaana 11:14, 38-44. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan mooy wone ne, ci dëgg Lasaar deewoon na? (Xoolal aaya 39).

  • Bu dee Lasaar demoon na asamaan ba pare, ndax foog nga ne Yeesu dina ko indiwaat ci kaw suuf?

Seetaanal WIDEO BI.

5. Ñu bare dinañu dekki!

Jàngal Sabóor 37:29. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ñi nar a dekki, fan lañuy dund?

Yeesu du dekkal ñi doon jaamu Yexowa rekk. Jàngal Jëf ya 24:15. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Kan nga bëgg a gisaat?

Xalaatal ci lii rekk: Ni mu yombe ci baay mu yee doomam, noonu it la yombee ci Yeesu mu dekkal ñi dee

6. Ndekkite li mën na la may yaakaar te dëfal sa xol

Li Biibël bi nettali ci doomu Yayrus dëfal na xolu ñu bare ñu ñàkk seen mbokk te dooleel na leen. Jàngal nettali boobu ci Luug 8:40-42, 49-56.

Bala Yeesu di dekkal doomu Yayrus bu jigéen, lii la wax baayam: «Bul tiit. Gëmal rekk.» (Xoolal aaya 50). Naka la la yaakaaru ndekkite mënee dimbali...

  • bu sa mbokk deewee?

  • bu amee lu la mën rey?

Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Naka la yaakaaru ndekkite li dëfale te dooleel waajuru Phelicity yi?

BU LA NIT WAXOON: «Ñi nar a dekki ci kaw asamaan lañuy dekki waaye du ci kaw suuf.»

  • Lan nga ci xalaat?

  • Ban aaya nga ko mën a jàngal ngir won ko ne, ñi dee ci kaw suuf lañuy dekki?

NAÑU TËNK

Biibël bi dige na ne ay milioŋi nit yu dee, dinañu dekki. Yexowa dafa bëgg ñu dundaat, te may na Yeesu kàttanu dekkal leen.

Nañu fàttaliku

  • Naka lañu xame ne, Yexowa ak Yeesu dañu yàkkamti dundalaat ñi dee?

  • Ñi nar a dekki fan lañuy dund, ci asamaan walla ci kaw suuf? Lu tax nga wax loolu?

  • Lan moo tax mu wóor la ne, sa mbokk yi dee dinañu dundaat?

Jubluwaay

GËSTUL

Ndax Biibël bi mën na dimbali dëgg ku ñàkk mbokkam?

Boo amee mbokk bu dee (5:06)

Naka lañu mën a dimbalee xale, bu mbokkam deewee?

Njot gi (2:07)

Ndax dina am ñu dekki ngir dundi asamaan? Ñan ñoo dul dekki?

«Lan mooy ndekkite?» (Ci jw.org la nekk)