Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 32

Nguuru Yàlla tàmbali na ilif!

Nguuru Yàlla tàmbali na ilif!

Nguuru Yàlla tàmbali na ilif ci asamaan ci atum 1914. Ci at boobu itam la mujug nguuru doomu Aadama yi tàmbali. Naka lañu ko xame? Nañu xool li Biibël bi yégle woon, liy xew ci àddina si ak doxalinu nit ñi, li ko dale ci atum 1914.

1. Lan la Biibël bi yégle woon?

Ci Biibël bi, téere Dañeel wone na ne nguuru Yàlla dina tàmbalee ilif ci mujug bés yi ñuy woowe «juróom ñaari jamono» (Dañeel 4:13, 14). Ay téeméeri at ginnaaw loolu, Yeesu wax na itam ci jamono jooju. Woowe na ko «jamonoy ñi dul Yawut», te wone na ne jamono jooju jeexagul woon (Luug 21:24). Ni ñu ko nar a gise, juróom ñaari jamono yooyu jeex nañu ci atum 1914.

2. Yan xew-xew ak doxalin lañuy gis, li dale ci atum 1914?

Taalibe Yeesu yi lii lañu ko laajoon: «Kañ la loolu di am, te luy tegtale ne yaa ngi ñëw te àddina di tukki?» (Macë 24:3). Yeesu xamal leen ne, lu bari dina xew bu komaasee ilif ci nguuru Yàlla ci kaw asaaman. Geer yi, ñàkk lekk bi ak yëngu-yëngu suuf yi, bokk nañu ci li nar a xew (Jàngal Macë 24:7). Biibël bi yégle woon na itam ne «ci mujug jamono» doxalinu nit ñi, dina tax dund gi ‘tiis te tar’ (2 Timote 3:1-5). Li ko dale atum 1914, xew-xew yooyu ak doxalin yooyu dañu gën a bari.

3. Lu tax àddina si di gën di metti bi nguuru Yàlla tàmbalee ilif ba léegi?

Bi Yeesu nekkee buuru nguuru Yàlla, yàggul dara mu xeex ak Seytaane ak ay malaakaam ci kaw asamaan. Seytaane lañu daan ci xeex boobu. Biibël bi nee na «daaneel nañu ko ci kaw suuf, moom ak i malaakaam» (Peeñu 12:9, 10, 12). Seytaane dafa ànd ak mer bu tàng ndaxte xam na ne dinañu ko alag. Loolu moo tax muy indi musiba ak coono ci kaw suuf. Loolu dafa ñuy dimbali ñu xam li tax àddina si mettee nii! Nguuru Yàlla dina fi dindi coonoo yooyu yépp.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal firnde yiy wone ne nguuru Yàlla tàmbali na ilif ci atum 1914 ak loolu li mu war a def ci ñun.

4. Yégle yonent yiy wone ne nguuru Yàlla tàmbali na ilif ci atum 1914

Yàlla dafa géntloo Nabukodonosor mi nekkoon buuru Babilon, ay xew-xew yu naroon a am. Gént googu Dañeel firi, yemul rekk ci wax ci kilifteefu Nabukodonosor waaye dafa laal itam nguuru Yàlla (Jàngal Dañeel 4:14). a

Jàngal Dañeel 4:17-23. Boo paree, jëfandikool tabló bi ngir tontu ci laaj yii di topp:

  • (A) Lan la Nabukodonosor gis ci gént gi? (Xoolal aaya 17 ak 18).

  • (B) Lan moo naroon a dal garab gi? (Xoolal aaya 20).

  • (C) Lan moo naroon a xew ci mujug «juróom ñaari jamono» yi? (Xoolal aaya 23).

Li tax ñu misaale nguuru Yàlla ak garab gi ci gént gi

YÉGLE YONENT BI (Dañeel 4:17-33)

Kilifteef gi

(A) Garab gu gudd

Nangu nañu kilifteef gi

(B) «Daaneleen garab gi,» te bàyyi ko «diiru juróom ñaari jamono»

Delloo nañu kilifteef gi

(C) «Nguur gi dees na la ko delloo»

Ci ni yégle yonent bi njëkkee mat...

  • (D) Kan la garab gi doon misaal? (Xoolal aaya 19).

  • (E) Kañ lañu nangu kilifteef gi? (Jàngal Dañeel 4:26-30).

  • (F) Lan moo dal Nabukodonosor bi «juróom ñaari jamono» yi jeexee? (Jàngal Dañeel 4:31-33).

NI YÉGLE YONENT BI NJËKKEE MAT

Kilifteef gi

(D) Nabukodonosor, buuru Babilon

Nangu nañu kilifteef gi

(E) Gannaaw atum 606 B.S.J. Nabukodonosor dof, te mënatul woon a jiite lu tollu ci juróom-ñaari at

Delloo nañu kilifteef gi

(F) Nabukodonosor wér te tàmbaliwaat a jiite

Ci ni yégle yonent bi mate ci ñaareelu yoon bi...

  • (G) Kan la garab gi doon misaal? (Jàngal Chroniques 29:23).

  • (H) Kañ lañu nangu kilifteef gi? Naka lañu xame ne, ba bi Yeesu nekkee ci kaw suuf, dellooguñu woon kilifteef gi? (Jàngal Luug 21:24).

  • (I) Kañ ak fan lañu delloo kilifteef gi?

NI YÉGLE YONENT BI MATE CI ÑAAREELU YOON BI

Kilifteef gi

(G) Buuri Israyil yi doon misaal kilifteefu Yàlla

Nangu nañu kilifteef gi

(H) Yàq nañu Yerusalem, nangu nañu kilifteefu buuri Israyil yi, ci diirub 2 500 at

Delloo nañu kilifteef gi

(I) Yeesu tàmbali na ilif ci asamaan ni Buur ci nguuru Yàlla

Lan mooy diirub juróom ñaari jamono yi?

Ci Biibël bi, yenn aaya yi mën nañu ñu dimbali ñu nànd yeneen aaya. Ci misaal, téere Peeñu dafay wone ne ñetti diir ak genn-wàll ñu ngi tollook 1 260 fan (Peeñu 12:6, 14). Juróom ñaari jamono mooy ñaari yoon lim boobu, maanaam 2 520 fan. Lée-lée ci Biibël bi, benn fan mën na tekki benn at (Esekiyel 4:6). Kon ci téere Dañeel, juróom ñaari jamono yi, ñu ngi tollook 2 520 at.

5. Àddina si dafa soppeeku li dale ci atum 1914

Yeesu yégle woon na, ni àddina si naroon a mel bu nekkee buur ba pare. Jàngal Luug 21:9-11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ci li nga jàng ci aaya yi, lan nga gis ne mu ngi xew, walla nga dégg ko?

Ndaw li Pool waxoon na ni nit ñi nar a mel ci mujug kilifteefu doomu Aadama yi. Jàngal 2 Timote 3:1-5. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ci li ñu wax ci aaya yi, yan jikko nga seetlu ci nit ñi tey?

6. Woneel ne gëm nga ne nguuru Yàlla mu ngi ilif

Jàngal Macë 24:3, 14. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ban liggéey bu am solo mooy wone ne nguuru Yàlla mu ngi ilif?

  • Naka nga mënee bokk ci liggéey boobu?

Nguuru Yàlla mu ngi ilif, te bés bi mu nar a ilif suuf si sépp jege na. Jàngal Yawut ya 10:24, 25. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la kenn ku nekk ci ñun war a def «fi ak [ñu] ngi gis bésu Boroom biy jubsi»?

Boo yëgee lu mën a dimbali ñeneen te musal leen, lan nga war a def?

BU LA NIT LAAJOON: «Lu tax Seede Yexowa yi di wax ne atum 1914, at bu am solo la?»

  • Lan nga koy wax?

NAÑU TËNK

Yégle yonent yi, liy xew ci àddina si ak doxalinu nit ñi, dafay wone ne nguuru Yàlla mu ngi ilif. Ngir wone ne gëm nañu loolu, dañu war di waare te di teewe ndaje yi ci mbooloo mi.

Nañu fàttaliku

  • Lan moo naroon a xew ci mujug juróom ñaari jamono yi, ni ñu ko yégle woon ci téereb Dañeel ci Biibël bi?

  • Lan moo tax nga gëm ne, nguuru Yàlla ci atum 1914 la tàmbalee ilif?

  • Naka nga mënee wone ne, gëm nga ne nguuru Yàlla mu ngi ilif?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal li ay boroom xam-xam ak ñeneen wax ci ni àddina si soppeekoo li dale atum 1914.

«Kañ la àddina si tàmbalee yàqu nii?» (g 4/07)

 Naka lañu xame ne yégle yonent bi nekk ci Dañeel pàcc 4, ci nguuru Yàlla lay wax?

«Kañ la nguuru Yàlla tàmbalee ilif? (Xaaj 1)» (w14 1/10)

Lan mooy wone ne «juróom ñaari jamono» yi ñu wax ci Dañeel pàcc 4, ci atum 1914 lañu jeex?

«Kañ la nguuru Yàlla tàmbalee ilif? (Xaaj 2) (w14 1/11)

a Xoolal  ñaari waxtaan yi mujj ci lesoŋ bii ci Gëstul.