Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 35

Ni ñu mën a jële ay dogal yu baax

Ni ñu mën a jële ay dogal yu baax

Ñun ñépp dañuy jël ay dogal ci suñu dund. Yenn dogal yi mën nañu ñu jural lu baax mbaa ñu lor ñu. Mën nañu gën a dëgëral suñu diggante ak Yexowa mbaa ñu yàq ko. Ci misaal, lée-lée ñu war a jël dogal ci lu jëm ci fi ñu war a dëkk, liggéey bi ñuy def, am jabar walla am jëkkër. Bu ñu jëlee ay dogal yu baax, dinañu bég ci suñu dund te dinañu neex Yexowa.

1. Naka la la Biibël bi mënee dimbali nga jël dogal yu baax?

Bala ngay jël dogal, ñaanal Yexowa mu dimbali la te gëstul ci Biibël bi ngir xam lan mooy xalaatam ci loolu (Jàngal Kàddu yu Xelu 2:3-6). Yenn saay, Yexowa dafa lay xamal ci lu leer li nga war a def. Bu loolu amee, def li mu la wax mooy dogal bi gën.

Waaye nag, mën nga gëstu ci Biibël bi te doo gis ci lu leer, li nga war a def. Ba tey Yexowa dina la ‘awale fi nga wara aw’ (Esayi 48:17). Nu mu koy defe? Am na ay njàngale Yexowa yu la mën a dimbali nga xam li nga war a def. Njàngale yooyu nekk ci Biibël bi, dañuy wone gis-gisu Yàlla. Dañuy faral di jàng ay nettali ci Biibël bi yu ñuy xamal ni Yexowa di gise yenn mbir yi. Bu ñu ràññee ni Yexowa di gise mbir yi, loolu mën na ñu dimbali ñu jël ay dogal yu ko neex.

2. Ci lan nga war a bàyyi xel bala ngay jël dogal?

Biibël bi nee na: «Ku [xelam] ñaw xam fi ngay jaare» (Kàddu yu Xelu 14:15). Loolu mu ngi tekki, bala ñuy jël dogal dañu war a jël jot ngir xalaat ci li ñu war a tànn. Bala ngay dogal dara, laajal sa bopp lii: ‘Ban njàngale Yexowa moo ciy wax? Ban dogal moo ma nar a may xel mu dal? Li may dogal lan la nar a def ci ñeneen ñi? Te li gën a am solo, ndax loolu dina bégal Yexowa?’ (Baamtug Yoon wi 32:29).

Yexowa am na sañ-sañu wax ñu, lan moo baax ak lan moo bon. Bu ñu xamee bu baax ay santaaneem ak njàngaleem te fas yéene topp leen, dinañu yar bu baax suñu xel. Xel mooy li ñu Yàlla may ngir ñu ràññee lu baax ak lu bon (Room 2:14, 15). Bu ñu yaree suñu xel, dina ñu dimbali ñu jël ay dogal yu baax.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal bu baax ni ñu njàngale yi nekk ci Biibël bi ak suñu xel mënee dimbali ñu jël ay dogal yu baax.

3. Bàyyil Biibël bi wommat la

Naka la ñu njàngale yi nekk ci Biibël bi mënee dimbali, bu ñu waree jël ay dogal? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ban may bu am solo la ñu Yexowa may?

  • Lu tax Yexowa may ñu sañ-sañu tànnal suñu bopp li ñu bëgg a def?

  • Lan la ñu jox ngir dimbali ñu, ñu jël dogal yi gën?

Nañu gis benn njàngale ci Biibël bi ak li ñu ci mën a jàng. Jàngal Efes 5:15, 16. Boo paree, nga wax ci ni nga mënee «jariñoo jot gi» ngir...

  • liir Biibël bi bés bu nekk

  • nekk jëkkër ju baax, jabar ju baax, waajur ju baax, walla doom ju baax.

  • teewe ndaje yi.

4. Yaral sa xel ngir mën a jël ay dogal yu baax

Bu dee am na aaya buy wone ci lu leer li ñu war a def, jël dogal bi gën mën na yomb. Waaye bu dee gisiñu ci lu leer li ñu war a def nag? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci wideo bi, lan la mbokk mi def ngir yar xelam te jël dogal bu neex Yexowa?

Lu tax waruñu laaj ñeneen ñi, ñu jël dogal ci suñu palaas? Jàngal Yawut ya 5:14. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Laaj ñeneen ñu jël dogal ci suñu palaas mën na nirook lu yomb, waaye ñun ci suñu bopp lan lañu war a jàng a ràññee?

  • Yan jumtukaay ñoo la mën a dimbali nga yar sa xel te jël dogal yu baax?

Ni ñu kàrt di dimbalee ñu xam suñu yoon, noonu la ñu suñu xel di dimbalee ñu xam fi ñuy jaar ci suñu dund

5. Nangul ne ñépp yemuñu xel

Nit ñi dañoo wuute, kon dogal yi ñuy jël it dinañu wuute. Naka lañu mënee wone ne, nangu nañu ne ñépp yemuñu xel? Nañu jël ñaari misaal:

Misaal 1: Benn mbokk bu jigéen bu bëgg makiyaas, toxu dem ci beneen mbooloo boo xam ne jigéen ñi foofu giseewuñu ni lu baax, jigéen juy makiyewu.

Jàngal Room 15:1 ak 1 Korent 10:23, 24. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Bu ñu sukkandikoo ci aaya yii, ban dogal la mbokk bi mën a jël? Lan ngay def boo nekkee ak koo xam ne, li la sa xel may nga def ko, moom xelam mayu ko ko?

Misaal 2: Benn mbokk bu góor xam na ne Biibël bi terewul naan sàngara ci anam bu yem, waaye mu jël dogal ne du ko naan sax. Mu dem ci benn feet ak mbokk yi, gis ne ñoom dañuy naan sàngara.

Jàngal Kàdduy Waare 7:16 ak Room 14:1, 10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Bu ñu sukkandikoo ci aaya yii, ban dogal la mbokk bi mën a jël? Lan ngay def boo gisee nit muy def loo xam ne, sa xel mayu la nga def ko?

 Lan nga war a def ngir mën a jël ay dogal yu baax?

1. Ñaanal Yexowa mu dimbali la nga tànn li nga war a def (Saag 1:5).

2. Defal ay gëstu ci Biibël bi ak ci téere yi sukkandiku ci Biibël bi ngir gis njàngale yi la mën a dimbali. Mën nga waxtaan itam ak ay karceen yu mat ci wàllu ngëm.

3. Xalaatal li muy jur, maanaam ndax dogal bi nga jël dina tax nga am xel mu dal, ñeneen ñi it am xel mu dal.

BU LA NIT WAXOON: «Ku nekk am nga sañ-sañu def lu la neex. Bul toppatoo li nit ñi di xalaat.»

  • Lu tax ñu war a bàyyi xel ci gis-gisu Yàlla ak ci gis-gisu ñeneen ñi?

NAÑU TËNK

Bu ñu bëggee jël ay dogal yu baax, dañu war a wut a xam ni Yexowa di gise mbir yi. Te xalaat ndax suñuy jëf dina dimbali ñeneen ñi walla dina leen gaañ.

Nañu fàttaliku

  • Naka nga mënee jël ay dogal yu neex Yexowa?

  • Naka nga mënee yar sa xel?

  • Naka nga mënee wone ne, nangu nga ne ñépp yemuñu xel?

Jubluwaay

GËSTUL

Gënal a jàng ni ñu Yexowa di xelale.

Yexowa dafay wommat ay jaamam (9:50)

Xoolal li dimbali benn góor mu jël dogal bu metti woon a jël.

Yexowa dige na ne lépp dina baax (5:46)

Xoolal leneen li ñu mën a def ba neex Yexowa, bu ñu gisul ci Biibël bi li ñu war a def.

«Ndax soxla nañu Biibël bi wax ñu li ñu war a def ci lépp?» (w03 1/12)