Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 40

Naka lañu mënee nekk ñu set ci kanamu Yàlla?

Naka lañu mënee nekk ñu set ci kanamu Yàlla?

Xalaatal yaay ju bëgg doomam, di ko waajal ngir mu dem lekkool. Mu xool ndax sangu na te sol na yére yu baax te set. Loolu dafay aar wér-gi-yaramu xale bi te dafay wone ne, ay waajuram dañu koy toppatoo bu baax. Noonu itam, Yexowa suñu Baay bi ñu bëgg, dafa bëgg ñu set ci yaram ak ci xel. Bu ñu setee, dinañu aar suñu wér-gi-yaram te dinañu màggal Yàlla.

1. Naka lañu mënee nekk ñu set?

Yexowa nee na ñu: «Sell-leen» (1 Piyeer 1:16). Bu ñu bëggee nekk ñu sell, dañu war a set ci yaram ak ci xel. Set ci yaram dafa laaj faral di sangu, te fexe ba suñuy yére, suñu kër, suñu oto, moto, walla lu ni mel, jekk te set. Mën nañu it dimbali ci set-setalu saalu Nguur gi. Bu ñu nekkee ñu set, dañuy màggal Yexowa (2 Korent 6:3, 4).

2. Bu ñu bëggee nekk ñu set, yan tàmmeel lañu war a moytu?

Biibël bi nee na, ñu «sellal sunu bopp ci bépp sobeb yaram walla bu xel» (2 Korent 7:1). Kon, dañu war a moytu lépp lu mën a lor suñu yaram walla suñu xel. Suñuy xalaat dañu war a neex Yexowa. Moo tax dañuy def suñu kem kàttan ngir bañ a am xalaat yu bon (Sabóor 104:34). Dañuy fexe itam di wax, wax ju rafet (Jàngal Kolos 3:8).

Leneen lan moo mën a tilimal suñu yaram walla suñu xel? Am na lu mën a tilimal suñu yaram. Lu ci mel ni tux, mëq póon ak bépp xeetu dorog bu nit ñi di féexale seen xol. Bu ñu moytoo yëf yooyu, dinañu gën a wér te dinañu wone ne fonk nañu dund gi ñu Yàlla may. Dañuy def it lépp ngir set ci suñu xel, maanaam bañ di laal suñu awra ngir jële ci bànneex ak di seetaan yëfi saay-saay diggante góor ak jigéen (pornographie ci farãse) (Sabóor 119:37; Efes 5:5). Bàyyi tàmmeel yooyu mën na doon lu jafe, waaye Yexowa mën na ñu ci dimbali (Jàngal Esayi 41:13).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni nekk nit ku set mënee màggal Yexowa ak ni nga mënee xeex tàmmeel yu bon.

3. Set dafay màggal Yexowa

Bu ñu jàngee santaane yi Yexowa joxoon waa Israyil, dinañu xam ni Yexowa gise set. Jàngal Mucc ga 19:10 ak 30:17-19. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka la aaya yii di wonee ni Yexowa gise set?

  • Yan tàmmeel yu baax ñoo lay dimbali nga nekk ku set?

Set dafa laaj jot ak góor-góorlu. Waaye fu ñu mënta dëkk, ñu am alal walla déet, mën nañu nekk ñu set. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Bu ñu nekkee ñu set te di toppatoo bu baax li ñu moom, lan la loolu mën a def ci ñi ñuy waar?

4. Xeexal tàmmeel yu bon

Yexowa mën na ñu dimbali ñu xeex bépp tàmmeel bu bon

Booy tux walla di jël dorog ngir féexal sa xol, xam nga ni xeex tàmmeel bu bon mettee. Lan moo la ci mën a dimbali? Xoolal li tàmmeel boobu mën a def ci sa dund. Jàngal Macë 22:37-39. Boo paree, waxtaanal ci lii: bu nit di tux sigaret walla muy jël dorog, lan la loolu mën a def ci...

  • digganteem ak Yexowa?

  • digganteem ak waa këram ak ñi ko wër?

Jëlal ay matuwaay ngir xeex tàmmeel bu bon. a Seetaanal WIDEO BI.

Jàngal Filib 4:13. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Tàmm di ñaan Yàlla, di jàng Biibël bi ak di teewe ndaje yi, naka la mënee may nit doole ngir xeex tàmmeel bu bon?

5. Xeexal xalaat yu bon ak jëf yu bon

Jàngal Kolos 3:5. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Seetaan yëfi saay-saay diggante góor ak jigéen, di laal suñu awra ngir jële ci bànneex, di yónne ay mesaas ak foto yu ni mel, naka lañu xame ne loolu sellul ci Yexowa?

  • Ndax foog nga ne jaadu na Yexowa laaj ñu, ñu set ci xel? Lu tax?

Xoolal ni ñu mënee xeex xalaat yu bon. Seetaanal WIDEO BI.

Yeesu joxe na misaal ngir wone li tax ñu war a def li war ngir wéy di set ci xel. Jàngal Macë 5:29, 30. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Li Yeesu wax tekkiwul ne dañu war a lor suñu bopp, waaye dafay wone ne fàww ñu def dara. Lan la nit mën a def ngir moytu xalaat yu bon? b

Bu dee yaa ngi xeex ak xalaat yu bon, xamal ne Yexowa bég na ci yow. Jàngal Sabóor 103:13, 14. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Bu dee yaa ngi xeex ngir bàyyi tàmmeel bu bon, naka la aaya yii di la xiirtale nga bañ a xàddi?

Bul xàddi!

Boo jéemee te sottiwul, mën nga ne ‘Ndegam jéem na sottiwul, naa bàyyi noonu.’ Waaye xalaatal ci lii: Ci rawante daw, bu ci kenn fakkastaloo ba daanu, loolu tekkiwul ne ñàkk na rawante bi walla dafa war a dellu tàmbaliwaat daw bi. Noonu it, daanuwaat ci sa tàmmeel bu bon tekkiwul ne dootoo ci mën a génn. Tekkiwul it ne li nga jot a def yépp amul njariñ. Daanu bi, ci xeex bi la bokk. Kon bul xàddi! Ak ndimbalu Yexowa, mën nga xeex tàmmeel bu bon.

BU LA NIT WAXOON: «Tàmm naa ko. Mënatuma koo bàyyi.»

  • Ban aaya ngay jël ngir won nit ki ne, Yexowa mën na ko dimbali mu bàyyi tàmmeel bu bon?

NAÑU TËNK

Bu ñu setee ci suñu yaram, set ci suñu xel ak ci suñu doxalin, dinañu neex Yexowa.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax mu am solo lool ñu nekk ñu set?

  • Naka nga mënee nekk ku set?

  • Naka nga mënee wéy di set ci say xalaat ak ci sa doxalin?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal xelal yu baax yu la mën a dimbali nga bàyyi tux.

«Naka nga mënee bàyyi tux» (g10 me)

Xoolal li seetaan yëfi saay-saay diggante góor ak jigéen mën a def ci yow.

«Ndax seetaan pornographie dafay lor nit walla déet?»(w13 1/8)

Xoolal ni benn góor xeexe ba seetaanatul pornographie.

«Daanu naa ay yooni yoon bala ma ciy génn» (w16 n° 4)

a Waxtaan bi tudd «Naka nga mënee bàyyi tux» te nekk ci Gëstul ci lesoŋ bii, dafay joxe ay xelal yu baax ngir mën a bàyyi tàmmeel boobu.

b Ngir xeex tàmm di laal sa awra ngir jële ci bànneex, xoolal «Lu ma mën a dimbali ma bàyyi di laal sama awra ngir jële ci bànneex?» ci téere ypq 1, pàcc 25.