Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 42

Lan la Biibël bi wax ci salibateer ak séy?

Lan la Biibël bi wax ci salibateer ak séy?

Ci aada yu bari, nit ñi dañu gëm ne bu nit amul jëkkër walla jabar du mën a bég. Waaye nag, du ñi séy ñépp ñoo bég, te du ñi nekk salibateer ñépp ñoo bégul. Li am mooy, Biibël bi dafa wone ne, nekk salibateer ak séy, ñaar yépp mayug Yàlla la.

1. Lan mooy njariñu nekk salibateer?

Biibël bi nee na: «Ku takk as ndawam def na lu baax, rawatina nag ku takkul» (Jàngal 1 Korent 7:32, 33, 38). Naka la nekk salibateer gënee baax? Karceen yi nekk salibateer, amuñu jëkkër walla jabar ju ñu war a toppatoo. Kon daanaka ñoo gën a féex. Ci misaal, am na salibateer yu mën a yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi ci fànn yu bari, lu mel ni dem beneen dëkk ngir waare fa xibaaru jàmm bi. Te li ci gën a am solo mooy, mën nañu am jot gu gën a bari ngir dëgëral seen diggante ak Yexowa.

2. Lan mooy njariñu séy ci yoon?

Ni nekk salibateer amee njariñam, noonu itam la séy amee njariñam. Biibël bi nee na «ñaar a man kenn» (Kàdduy Waare 4:9). Loolu dëgg la, rawatina ci karceen yiy topp santaane yi nekk ci Biibël bi ci seen biir séy. Ñaar ñi séy ci yoon, ku nekk dafa dige ne dina bëgg moroomam, may ko cér te won ko cofeel. Loolu moo tax seen xel dafay gën a dal xelu ñiy nekkaale kese. Te xale yi juddoo ci néegu séy dañuy màgg ci anam bu mën a dalal seen xel.

3. Naka la Yexowa gise séy?

Bi Yexowa taxawalee séy bi njëkk, lii la waxoon: ‘Góor dina bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy wenn suux’ (Njàlbéen ga 2:24). Yexowa dafa bëgg jëkkër ak jabar bëggante te ànd ñoom ñaar seen giiru dund. Bu kenn ci ñoom njaaloo rekk, la Yàlla nangu tas séy. Te bu loolu amee, Yexowa may na ki deful dara mu tànn tas walla déet a (Macë 19:9). Yexowa nanguwul karceen yi am jabar yu bari (1 Timote 3:2).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni nga mënee bég ci sa dund te bégal Yexowa, moo xam nga nekk salibateer, nga am jëkkër walla jabar.

4. Jariñool bu baax sa dundinu salibateer

Yeesu dafa gise woon nekk salibateer ni mayug Yàlla (Macë 19:11, 12). Jàngal Macë 4:23. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka la Yeesu profitoo ci nekk salibateer ngir liggéeyal Baayam te dimbali nit ñi?

Karceen yi nekk salibateer itam mën nañu bég, bu ñu royee ci Yeesu. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci lan lu am solo la karceen yi nekk salibateer mën a sóobu?

Ndax xamoon nga ne...

Biibël bi waxul ñaata at la nit war a am bala muy séy. Waaye mu ngi xiirtal ku nekk xaar ba «wees ag ndawam». Ndaxte ci at yooyu, suñuy bëgg-bëggu yaram dañuy am doole ci ñun, ba mën ñoo teree jël dogal yu baax (1 Korent 7:36).

5. Tànnal bu baax ki ngay séyal

Tànn sa jëkkër walla sa jabar bokk na ci dogal yi gën a am solo ci sa dund. Jàngal Macë 19:4-6, 9. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax karceen warul a yàkkamti dugg ci séy?

Biibël bi mën na la dimbali nga xam li nga war a wut, ci ki nar a doon sa jëkkër walla ci jabar. Li gën a am solo nag mooy, tànn ku bëgg Yexowa. b Jàngal 1 Korent 7:39 ak 2 Korent 6:14. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lu tax ñu war a séy ak suñu mbokk karceen yi kese?

  • Ci sa xalaat, lan la Yexowa di yëg bu ñu séyee ak ku ko bëggul?

Ñaari mala yu wuute lool, bu ñu leen boole yen leen benn yen bi, dina metti ci ñoom ñaar. Noonu it, karceen bi séy ak ku gëmul dina ci jële poroblem yu bari

6. Nanga gise séy ni ko Yexowa gise

Ci jamono Israyil, amoon na góor yu doon fase seen jabar ndax seen bëgg-bëggu bopp. Jàngal Malasi 2:13, 14, 16. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax Yexowa bañ tas séy ci lu jaarul yoon?

Njaaloo ak tas dafay jural naqar ki deful dara ak xale yi

Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Bu dee danga séy ak ku dul jaamu Yexowa, lan nga mën a def ngir am jàmm ci sa séy?

7. Toppal santaane Yexowa yi jëm ci séy

Nit mën na soxlaa góor-góorlu bu baax ngir topp santaane Yexowa yi ci séy. c Waaye Yexowa dafay barkeel ñiy góor-góorlu ci loolu. Seetaanal WIDEO BI.

Jàngal Yawut ya 13:4. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ndax foog nga ne li Yexowa santaane ci séy jaadu na? Lu tax nga wax loolu?

Yexowa dafay xaar ci karceen yi, ñu bindlu seen séy ci kanamu yoon te bu séy bi tasee itam ñu xamal ko yoon, ni ko sàrtu réew yu bari laaje. Jàngal Tit 3:1. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Bu dee séy nga, ndax wóor na la ne, sa sàrtu réew nangu na séy bi?

BU LA NIT LAAJOON: «Léegi boo déggootul ak ki ngay séyal, ndax gënul ngeen tas?»

  • Lan nga koy tontu?

NAÑU TËNK

Nekk salibateer ak séy, yépp mayug Yexowa la. Ñi nekk salibateer ak ñiy séy yépp, mën nañu bég bu ñuy topp santaane Yexowa yi ci seen dund.

Nañu fàttaliku

  • Naka la salibateer mënee jariñoo bu baax dundinu salibateeram?

  • Lu tax Biibël bi wax ñu séy ak suñu mbokk karceen yi kese?

  • Lan rekk la Biibël bi wax ne moo mën a tas séy?

Jubluwaay

GËSTUL

Seetaanal ñaari tiyaatar yu la mën a dimbali nga jël dogal bu baax ci mbirum xamante bala séy di am ak ci mbirum séy.

Waajal séy (11:53)

Xoolal li tax benn góor wax ne li ko Yexowa defal, moo ëpp fuuf lépp li mu nangoo ñàkk.

Dama foogoon ne dina nangu dëgg gi (1:56)

Ci lan la nit war a xalaat bala muy sóobu ci tas séyam walla tàggoo?

«Nanga fullaal ‘li Yàlla takk’» (w18 desàmbar)

a Xoolal Yeneen leeral 4 buy wax lu jëm ci tàggoo bu njaaloo amul.

b Ci yenn aada yi, waajur yi ñooy tànnal seen doom jëkkër walla jabar. Bu dee noonu la, waajur yi bëgg seen doom, li ñu war a jiital mooy ndax ki ñuy tànnal seen doom bëgg na Yexowa am déet, waaye du ndax am na xaalis walla taxawaay bu am solo.

c Bu dee dangay dund ak koo xam ne séyuleen ci yoon, yow yaa war a tànn ndax danga koy bàyyi walla ndax dangay séy ak moom.