Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 45

Naka lañu mënee wone ne nguuru Yexowa rekk lañu faral?

Naka lañu mënee wone ne nguuru Yexowa rekk lañu faral?

Yeesu dafa waxoon ay taalibeem ne, waruñu ‘bokk ci àddina’ (Yowaana 15:19). Loolu dafa tekki ne nguuru Yàlla rekk lañu faral te duñu bokk ci mbirum politig ak geer yi. Waaye dëgg-dëgg, loolu du lu yomb. Nit ñi mën nañu ñu ñaawal ndax loolu. Naka lañu mënee wone ne, nguuru Yexowa rekk lañu faral te wéy di takku ci Yexowa Yàlla?

1. Naka la karceen dëgg yi gise nguuru doomu Aadama yi?

Karceen yi may nañu cér nguur yi. Dañuy def ni ko Yeesu waxe woon te di ‘jox Sesaar li Sesaar moom’, maanaam dañuy topp li yoon santaane ci suñu réew, lu ci mel ni fey lempo (Màrk 12:17). Biibël bi wax na ne nguuru doomu Aadama yi fi nekk yépp, Yexowa moo leen bàyyi ñuy nguuru (Room 13:1). Kon xam nañu ne, kilifteefu Yàlla moo sut kilifteefu nguuru doomu Aadama yi. Ci Yàlla ak nguuram gi ci asamaan, lañu yaakaar ngir jafe-jafey doomu Aadama yi deñ fi.

2. Naka lañu mënee wone ne nguuru Yàlla rekk lañu faral?

Ni Yeesu, duñu dugg ci mbirum politig. Bi nit ñi gisee benn ci kéemaan yi Yeesu def, dañu ko jéem a def seen buur. Waaye Yeesu nanguwu ko (Yowaana 6:15). Lu tax? Ndaxte ni mu ko waxe gannaaw loolu, «sama kilifteef nekkul ci àddina» (Yowaana 18:36). Ni ay taalibe Yeesu, dañuy wone ci fànn yu bari ne, nguuru Yàlla lañu faral. Ci misaal, duñu bokk ci geer (Jàngal Mise 4:3). Dañuy respekte réew yi waaye duñu leen màggal mukk, maanaam di màggal seen daraapo ak di def lu ni mel (1 Yowaana 5:21). Duñu far ak benn parti politig walla njiitu politig, te duñu leen xeex itam. Ci fànn yooyu ak ci yeneen, dañuy wone ne ci gornmaa Yàlla rekk lañu takku, maanaam ci Nguuram.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal li mën a tax mu jafe nga bañ a bokk ci politig walla ci geer ak ni nga mënee jël dogal yu neex Yexowa.

3. Karceen dëgg yi nguuru Yàlla rekk lañu faral

Yeesu ak taalibeem yi, ay royukaay lañu ci ñun. Jàngal Room 13:1, 5-7 ak 1 Piyeer 2:13, 14. Boo paree, seetaanal WIDEO BI te tontu ci laaj yii di topp.

  • Lu tax ñu war a may cér nguuru doomu Aadama yi?

  • Ci yan fànn lañu mën a wonee ne déggal nañu leen?

Bu geer amee, yenn réew yi dañuy wax ne faruñu fenn, waaye dañuy jàppale ñi bokk ci xare bi. Ci dëgg, lan mooy bañ a far fenn? Jàngal Yowaana 17:16. Boo paree, seetaanal WIDEO BI te tontu ci laaj yii di topp.

  • Naka lañu mënee wone ne faruñu fenn?

Léegi nag, bu kilifay réew mi laajee ñu def lu wuute ak li Yàlla santaane? Jàngal Jëf ya 5:28, 29. Boo paree, seetaanal WIDEO BI te tontu ci laaj yii di topp.

  • Bu sàrt yi ci réew mi wuute ak li Yàlla santaane, kan lañu war a déggal?

  • Ci sa xalaat, ci ban fànn la karceen mënul a déggal kilifay réew mi?

4. Bul far fenn ci say xalaat ak ci say jëf

Jàngal 1 Yowaana 5:21. Boo paree, seetaanal WIDEO BI te tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, lu tax Ayenge dogu ci bañ a bokk ci parti politig walla bokk ci lu mel ni nuyu daraapo?

  • Ndax foog nga ne jël na dogal bu baax?

Ci yeneen fànn yan la metti, ñu wone ne nguuru Yexowa rekk lañu faral? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wàllu espoor, bu joŋante amee diggante réew ak réew, naka lañu mënee wone ne faruñu fenn?

  • Bu amee ay dogal ci politig yu laal suñu dund, naka lañu mënee wéy di faral nguuru Yàlla?

  • Lu tax waruñu bàyyi li ñuy dégg ci xibaar yi ak ci nit ñi ñu wër, yóbbaale ñu ba ñu bokk ci mbirum àddina si?

Ci yan fànn la karceen warul a far fenn ci ay xalaatam ak ci ay jëfam?

BU LA NIT LAAJOON: «Lu tax doo nuyu daraapo?» walla «Lu tax doo woy bàkku réew mi?»

  • Lan nga koy tontu?

NAÑU TËNK

Karceen yi dañuy def lépp ngir bañ a bokk ci politig, muy ci seen xalaat, ci seen wax ak ci seen jëf.

Nañu fàttaliku

  • Lan mooy suñu wareef ci kanamu nguuru doomu Aadama yi?

  • Lu tax ñuy wéy di bañ a bokk ci politig?

  • Ci yan fànn la metti, ñu wone ne nguuru Yexowa rekk lañu faral?

Jubluwaay

GËSTUL

Lan lañu war a nangoo xañ suñu bopp ngir wéy di bañ a bokk ci àddina si?

Yexowa masuñoo bàyyi (3:14)

Lan la njaboot yi mën a def ngir waajal seen bopp ba duñu far fenn?

Nañu wéy di bañ a far fenn ci xew-xew yu mag yi (4:25)

Lu tax xeexal sa réew nekkul li gën a réy li nit mën a defal réewam?

«Dara tëwul Yàlla» (5:19)

Xoolal ni nga mënee wéy di bañ a bokk ci àddina si, boo naree jël ay dogal ci wàllu liggéey.

«Ku ci nekk dangaa wara yenu sab yen» (w06 3/15)