Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 46

Lu tax nga war a jébbalu te sóobu ci ndox?

Lu tax nga war a jébbalu te sóobu ci ndox?

Jébbal sa bopp Yexowa mooy nga dig ko ci ñaan ne, moom rekk ngay jaamu te coobareem ngay jiital ci sa dund (Sabóor 40:9). Boo defee loolu ba pare, nga door a sóobu ci ndox ngir won nit ñi ne, jébbal nga sa bopp Yàlla. Jël dogalu jébbal suñu bopp Yexowa, mooy dogal bi gën a am solo ci suñu dund. Lan moo la mën a xiir ci jël dogal bu am solo boobu te mën na soppi sa dund?

1. Lan moo mën a xiir nit ci jébbalu?

Suñu mbëggeel ci Yexowa moo ñu war a xiir ci jébbal ko suñu bopp (1 Yowaana 4:10, 19). Biibël bi nee na: «Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa xel mépp ak sa kàttan gépp» (Màrk 12:30). Suñu mbëggeel ci Yàlla dañu koy wone ci suñu wax, waaye itam ci suñu jëf. Ni ñaari nit di bëggantee lool ba mu jaral leen ñu séy, noonu it suñu mbëggeel ci Yexowa moo ñuy xiir ci jébbal ko suñu bopp te sóobu ci ndox.

2. Yan barke la Yexowa déncal seedeem yi ko jébbal seen bopp?

Boo sóoboo ci ndox, dinga bokk ci njabootu Yexowa gi bég. Dinga yëg mbëggeel gi mu am ci yow ci fànn yu bari te dinga ko gën a jege (Jàngal Malasi 3:16-18). Yexowa dina nekk sa Baay, te ci àddina si sépp, dinga am ay mbokk yu góor ak yu jigéen yu bëgg Yexowa te bëgg la (Jàngal Màrk 10:29, 30). Waaye nag, am na li nga war a def bala ngay sóobu ci ndox. Fàww nga jàng xam Yexowa, nga bëgg ko te am ngëm ci doomam. Ginnaaw loolu, danga war a jébbal sa dund Yexowa. Boo defee loolu lépp, ba pare sóobu ci ndox, dinga tàmbalee dox ci yoon biy jëme ci dund gu dul jeex. Kàddu Yàlla nee na: ‘Sóobu ci ndox dafa ñuy muccal’ (1 Piyeer 3:21).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal li tax mu am solo nga jébbal sa bopp Yexowa te sóobu ci ndox.

3. Ñun ñépp dañu war a tànn ki ñuy jaamu

Ci Israyil bu njëkk ba, am na ñu xalaatoon ne mën nañu boole jaamoondoo Yexowa ak benn yàlla bu dul dëgg bu tuddoon Baal. Waaye Yexowa dafa yónni yonent Ilyaas mu jubbanti seen gis-gis bu baaxul boobu. Jàngal 1 Buur ya 18:21. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la waa Israyil waroon a tànn?

Ni waa Israyil, ñun itam war nañu tànn ki ñuy jaamu. Jàngal Luug 16:13. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lu tax mënuñoo boole jaamu Yexowa ak jaamu nit walla leneen?

  • Naka lañu mënee won Yexowa ne, moom lañu tànn a jaamu?

4. Xalaatal bu baax ci mbëggeel gi Yexowa am ci yow

Yexowa may na ñu lu bari te am solo lool. Ñun, lan lañu ko mën a may? Seetaanal WIDEO BI.

Lan la Yexowa def ngir won la mbëggeelam? Jàngal Sabóor 104:14, 15 ak 1 Yowaana 4:9, 10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Yan mayu Yexowa ñoo gën a tax nga bëgg koo gërëm?

  • Lan ngay yëg ci moom boo xalaate ci maye yooyu?

Bu ñu nit maye kado bu ñu neex lool, dañu koy bëgg a won suñu ngërëm ci li mu ñu may. Jàngal Baamtug Yoon wi 16:17. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Boo xalaatee ci lépp li la Yexowa defal, sa xol ci lan la lay xiir nga defal ko?

5. Jébbalu dafay indi barke yu bari

Nit ñu bari dañu gëm ne, siiw, am liggéey bu baax walla xaalis moo leen di indil mbégte. Ndax loolu dëgg la? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Bu dee sax góor gi ci wideo bi bëggoon na futbal, lu tax mu mujj koo bàyyi?

  • Dafa tànn bañ a jébbal dundam ci futbal, waaye jébbal ko Yexowa. Ndax foog nga ne jël na dogal bu baax? Lu tax?

Bala ndaw li Pool di nekk karceen, dafa doon wut a tekki. Jàngalekat bu siiwoon moo ko doon jàngal yoonu Yawut yi. Waaye dafa won ginnaaw loolu lépp ngir nekk karceen. Ndax Pool réccu na ko? Jàngal Filib 3:8. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan moo tax Pool wax ne, li mu defoon bala muy nekk karceen dafa meloon «ni mbalit»?

  • Ban njariñ la jële ci li mu def?

  • Ci sa xalaat, lan mooy gën a neexal sa dund, jaamu Yexowa walla def leneen?

Barke yi Pool jële ci nekk karceen ñoo raw fuuf lépp li mu ñàkk

BU LA NIT WAXOON: «Xam naa ne lii mooy dëgg gi, waaye pareeguma ngir sóobu ci ndox.»

  • Lu tax nga xalaat ne jébbal sa bopp Yexowa yenu na maanaa?

NAÑU TËNK

Suñu mbëggeel ci Yexowa moo ñuy xiir ci jébbal ko suñu bopp te sóobu ci ndox.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax Yexowa yelloo ñu bëgg ko ak suñu xol bépp te jaamu ko ak suñu xol bépp?

  • Naka la Yexowa di barkele seedeem yi ko jébbal seen bopp?

  • Ndax bëgg nga jébbal sa bopp Yexowa?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal li tax benn jigéen bu doon def misik ak góor gu doon def espoor tànn jébbal seen bopp Yexowa.

Li ndaw ñi di laaj... Lan laay def ci sama dund? (Fàttaliku démb) (6:54)

Ci wideo bu ànd ak misik bii, xoolal mbégte bi ñi jébbal seen bopp Yexowa am.

May naa la sama dund (4:30)

Ci waxtaan bi tudd «Laaj naa sama bopp ay at ‘Lu tax Yàlla sàkk ñu?’» xoolal li xiir benn jigéen mu xalaataat ci li gën a am solo ci moom.

«Biibël bi dafay soppi dund» (w12 11/1)