Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 47

Ndax pare nga ngir sóobu ci ndox?

Ndax pare nga ngir sóobu ci ndox?

Sa njàngum Biibël bi dimbali na la nga xam lu bare ci Yexowa. Xéyna def nga ay coppite ci sa dund ngir topp li nga jàng. Waaye xéyna ba tey, am na li lay tere nga jébbal sa bopp Yexowa te sóobu ci ndox. Ci lesoŋ bii, dinañu waxtaan ci yenn gàllankoor yiy faral di tere nit sóobu ci ndox ak ni nga leen mënee xeex.

1. Fan la sa xam-xam war a tollu bala ngay sóobu ci ndox?

Boo bëggee sóobu ci ndox, fàww nga «xam dëgg gi» (1 Timote 2:4). Loolu tekkiwul ne bala ngay sóobu ci ndox, danga war a xam tontu laaj yépp yi ñu mën a laaj ci Biibël bi. Karceen yi yàgg a sóobu sax dañuy jàng ba tey (Kolos 1:9, 10). Waaye soxla nga xam njàngale yi gën a am solo ci Biibël bi. Magi mbooloo mi dinañu la dimbali nga xam ndax am nga xam-xam bi war.

2. Lan nga war a def bala ngay sóobu ci ndox?

Bala ngay mën a sóobu ci ndox, danga war a ‘tuub say bàkkaar te waññiku’ (Jàngal Jëf ya 3:19). Loolu dafay tekki ne, réccu nga dëgg sa bàkkaar yépp te ñaan nga Yexowa mu baal la. Bàyyi nga itam bépp doxalin bu bon te dogu nga ci am dundin bu neex Yàlla. Rax-ci-dolli, komaase nga teewe ndaje yi ak di waare ak waa mbooloo mi.

3. Lu tax waruloo bàyyi ragal tere la nga sóobu ci ndox?

Am na ñu ragal ndaxte dañu foog ne bu ñu sóoboo ci ndox, duñu mën a def li ñu dig Yexowa. Li am mooy lée-lée dinga juum, ndaxte Biibël bi sax wone na ne, ay góor ak ay jigéen yu takku woon ci Yàlla, dañu doon juum. Te Yexowa xaarul ci ay jaamam ñu doxale ni ay nit ñu mat (Jàngal Sabóor 103:13, 14). Li koy bégal mooy nga def lépp li nga mën! Dina la dimbali. Te sax, Yexowa dig na ñu ne «dara manu noo tàggaleek mbëggeelam» (Jàngal Room 8:38, 39).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni la, gën a xam Yexowa te nangu ndimbalam mënee dimbali nga xeex bépp gàllankoor bu la mën a teree sóobu ci ndox.

4. Gënal a xam Yexowa

Fan la sa xam-xam ci Yexowa war a tollu bala ngay sóobu ci ndox? War nga ko xam bu baax, ba xam-xam boobu tax nga am mbëggeel ci moom te bëgg koo neex. Seetaanal WIDEO BI te xoolal ni ko ñeneen ñuy jàng Biibël bi ci àddina si sépp defe. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci wideo bi, lan moo dimbali ñenn ñi ñu waajal seen bopp ngir sóobu ci ndox?

Jàngal Room 12:2. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ndax danga am xel ñaar ci li nga jàng ci Biibël bi? Walla ndax danga am xel ñaar ci ne, Seede Yexowa yi ñooy jàngale dëgg gi?

  • Su dee waaw, lan nga mën a def?

5. Xeexal li la mën a tere nga sóobu ci ndox

Bu ñu jëlee dogalu jébbal suñu bopp Yexowa te sóobu ci ndox, dañuy jànkoonte ak ay jafe-jafe. Ngir gis ay nit yu ci jaar, seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, yan gàllankoor la Narangerel waroon a xeex ngir mën a jaamu Yexowa?

  • Naka la ko mbëggeelam ci Yexowa dimbalee mu xeex gàllankoor yooyu?

Jàngal Kàddu yu Xelu 29:25 ak 2 Timote 1:7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan moo ñuy may fitu xeex gàllankoor yi?

6. Amal kóolute ci ndimbalu Yexowa

Yexowa dina la dimbali nga def li ko neex. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, lan moo tax ki doon jàng Biibël bi bañoon a sóobu ci ndox?

  • Li mu jàng, naka la ko dimbalee mu gën a wóolu Yexowa?

Jàngal Esayi 41:10, 13. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan moo tax nga war a gëm ne, boo jébbalee sa bopp Yàlla dinga mën a def li nga dige?

7. Yokkal sa ngërëm ci mbëggeel gi Yexowa am ci yow

Looy gën di xalaat ci mbëggeel gi Yexowa am ci yow, sa ngërëm ci moom di gën di yokku te dinga ko gën a bëgg a jaamu ba fàww. Jàngal Sabóor 40:6. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Yan barke yu jóge ci Yexowa ñoo la gën a neex?

Yonent Yàlla Yeremi dafa bëggoon Yexowa ak kàddoom, te dafa fonkoon lool nekk jaamu Yexowa. Lii la waxoon: «Sa kàddu laa gis, di ko dunde, sa kàddu di ma bégal, bànneexal sama xol. Yaw Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déy, sa tur lañu ma tudde» (Yeremi 15:16). Tontul ci laaj yii di topp:

  • Lu tax nekk Seede Yexowa doon cér bu réy?

  • Ndax bëgg nga sóobu ci ndox ngir nekk Seede Yexowa?

  • Ndax am na dara lu lay tere nga def ko?

  • Lan nga war a def ngir mën a sóobu ci ndox?

BU LA NIT WAXOON: «Dama ragal ne, bu ma sóoboo ci ndox duma mën a def li ma dig Yexowa.»

  • Ndax yow itam loolu ngay yëg?

NAÑU TËNK

Ak ndimbalu Yexowa, dinga mën a xeex bépp gàllankoor bu lay tere nga sóobu ci ndox.

Nañu fàttaliku

  • Fan la sa xam-xam ci Biibël bi war a tollu bala ngay sóobu ci ndox?

  • Lan nga war a soppi ci sa dund bala ngay mën a sóobu ci ndox?

  • Lu tax waruloo bàyyi ragal tere la nga sóobu ci ndox?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal li war a tax nga jël dogalu sóobu ci ndox.

«Ndax pare nga ngir sóobu ci ndox?» (w20 màrs)

Xoolal ni benn góor xeexe li ko doon gàllankoor ba mujj a sóobu ci ndox.

‘Lu tax sóobuwoo ci ndox ba léegi?’ (1:10)

Góor gi tudd Ataa dafa doon ragal a sóobu ci ndox. Xoolal li ko dimbali ba mu mujj a sóobu ci ndox.

Ndax yelloo naa lii dëgg? (7:21)