Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 51

Naka nga mënee neex Yexowa ci say wax?

Naka nga mënee neex Yexowa ci say wax?

Bi ñu Yexowa di sàkk, dafa ñu may lu réy lool! Loolu mooy mën a wax. Ni ñuy jëfandikoo may boobu, ndax am na solo ci moom? Waaw, am na solo ci moom! (Jàngal Saag 1:26). Kon naka lañu mënee neex Yexowa ci suñuy wax?

1. Naka lañu war a jëfandikoo may gi ñu Yexowa may?

Biibël bi nee na, ñu ‘dëgëralante te yokkante suñu ngëm’ (1 Tesalonig 5:11). Xalaatal ndax am na ñoo xam, ñu soxla ñu dooleel leen? Lan nga mën a def ngir dimbali leen? Xamal leen bu baax ne fonk nga leen. Xéyna mën nga leen a wax li la neex ci ñoom. Ndax mën nga xalaat ci aaya bu mën a dooleel nit koo xam? Am na aaya yu bare yoo mën a jël. Li ngay wax mën na dooleel nit, waaye bul fàtte ne, ni ngay waxe itam mën na dooleel bu baax nit ki (Kàddu yu Xelu 15:1).

2. Yan wax lañu war a moytu?

Biibël bi nee na: «Bu genn kàddu gu ñaaw génn ci seen gémmiñ» (Jàngal Efes 4:29). Loolu mu ngi tekki ne, waruñu wax wax ju ñaaw walla ju soxor te waruñu wax luy gaañ suñu moroom. War nañu moytu itam jëw ak sosal nit (Jàngal Kàddu yu Xelu 16:28).

3. Lan moo ñu mën a dimbali ñu am wax juy dooleel nit?

Li ñuy faral di wax dafay wone li nekk dëgg ci suñu xol ak ci suñu xel (Luug 6:45). Kon war nañu jàng di xalaat ci lu baax, maanaam ci lu jub, lu sell, lu rafet ak lu mata naw (Filib 4:8). Bu ñu bëggee di xalaat ci lu mel noonu, war nañu tànn bu baax li ñuy féexale suñu xol te tànn it bu baax suñuy xarit (Kàddu yu Xelu 13:20). Baax na it ñuy xalaat bu baax bala ñuy wax. Xalaatal li say kàddu mën a def ci ñeneen ñi. Biibël bi nee na: «Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi; kàddu gu xelu, garab la ci» (Kàddu yu Xelu 12:18).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni nga mënee am wax ju neex Yexowa te di dooleel ñeneen ñi.

4. Xamal bu baax ni ngay waxe

Lée-lée, ñun ñépp dañuy wax dara ba pare rëccu ko (Saag 3:2). Jàngal Galasi 5:22, 23. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Yan ci jikko yii nga mën a ñaan Yàlla ngir ñu dimbali la nga xam ni ngay waxe? Naka la la jikko yooyu mënee dimbali?

Jàngal 1 Korent 15:33. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Xarit yi ngay tànn ak li ngay féexale sa xol, lan lañu mën a def ci sa waxin?

Jàngal Kàdduy Waare 3:1, 7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Kañ la gën, nga noppi walla nga xaar ba beneen waxtu bala ngay wax dara?

5. Waxal lu rafet ci ñeneen ñi

Naka lañu mënee moytu wax lu jekkul walla lu ñaaw? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, lu tax suñu mbokk bi bëggoon a soppi li muy wax ci ñeneen ñi?

  • Lan la def ngir soppi?

Jàngal Kàdduy Waare 7:16. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan lañu warul fàtte, saay bu ñuy bëgg a wax lu ñaaw ci nit?

Jàngal Kàdduy Waare 7:21, 22. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka la ñu aaya yii mënee dimbali ñu bañ a mer bu nit waxee lu ñaaw ci ñun?

6. Amal wax ju neex booy wax ak sa waa kër

Yexowa dafa bëgg bu ñuy wax ak suñu waa kër, ñu am wax ju neex te ànd ci ak mbëggeel. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Booy wax ak sa waa kër, lan moo la mën a dimbali nga am wax ju neex?

Jàngal Efes 4:31, 32. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka lañu war a waxe ak suñu waa kër ngir njaboot gi gën a neex?

Yexowa waxoon na li muy yëg ci doomam Yeesu. Jàngal Macë 17:5. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka nga mënee roy Yexowa ci ni ngay waxe ak sa waa kër?

Wutal a ndokkeel ñeneen ñi

BU LA NIT WAXOON: «Lu ma neex laay wax. Ku mu neexul yaa xam, sama yoon nekku ci.»

  • Ndax ànd nga ci loolu? Lu tax?

NAÑU TËNK

Wax dafa am doole. War nañu xalaat bu baax li ñuy wax, kañ lañu koy wax ak ni ñu koy waxe.

Nañu fàttaliku

  • Naka lañu mënee jëfandikoo suñuy kàddu ngir dimbali ñeneen ñi?

  • Yan wax lañu war a moytu?

  • Lan moo ñu mën a dimbali ñuy wax saa su nekk, wax ju neex tey dooleel ñeneen ñi?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal li la mën a dimbali nga moytu wax ju ñaaw.

«Ndax ci dëgg ñaaw-làmmiñ lu bon la?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal ni nga mënee moytu daanu ci jëw.

Naka laa mën a def ba moytu jëw? (2:36)

Xoolal ni Yexowa dimbalee benn góor gu amoon jafe-jafe ngir bàyyi wax ju ñaaw.

«Dama xalaataat bu baax ci ni ma doon dunde» (w13 1/8)