Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 54

Kan mooy «surga bu takku te teey» bi te lan lay def?

Kan mooy «surga bu takku te teey» bi te lan lay def?

Yeesu mooy kilifag mbooloo karceen mi (Efes 5:23). Tey, Yeesu mu ngi ci kaw asamaan, di jiite talibeem yi nekk ci kaw suuf jaare ko ci «surga bu takku te teey» bi (Jàngal Macë 24:45). «Surga» boobu, Yeesu ci boppam moo ko fi teg te may na ko sañ-sañu jël yenn dogal yi. Waaye ba tey surga boobu dafa war a déggal Yeesu te toppatoo mbokku Kirist yi. Kan mooy surga boobu? Naka la ñu surga boobu di toppatoo?

1. Kan mooy «surga bu takku te teey» bi?

Yexowa dafa mas di jaar ci benn góor walla ci ay góor ngir jiite mbooloom (Malasi 2:7; Yawut ya 1:1). Bi Yeesu deewee, apootar yi ak magi mbooloo yi nekkoon Yerusalem ñoo doon jiite (Jëf ya 15:2). Tey it noonu la, benn gurupu magi mbooloo ñooy jiite. Gurup bu ndaw boobu lañuy woowe Jataay biy dogal ci Seede Yexowa yi. Ñoom ñooy joxe ñam bi ci wàllu ngëm te di jiite liggéeyu waare bi. Gurup boobu mooy «surga bu takku te teey, bu [fi Yeesu] teg» (Macë 24:45a). Ñépp ñi bokk ci Jataay biy dogal, ay karceen yu xel mu sell mi tànn lañu. Dañu am yaakaaru dem nguuru ak Yeesu ci kaw asamaan, bés bu ñu jeexale seen dund ci kaw suuf.

2. Ban ñam ci wàllu ngëm la surga bu takku bi di joxe?

Yeesu dafa waxoon ne surga bu takku bi dina «dundal [taalibe Yeesu yi] ca jamono ja» (Macë 24:45b). Lekk dafa ñuy may doole ak wér-gi-yaram. Noonu it, ñam ci wàllu ngëm, maanaam njàngale bi jóge ci Kàddu Yàlla, dafa ñuy may doole bi ñu soxla ngir wéy di takku ci Yexowa, te def liggéey bi ñu Yeesu sant (1 Timote 4:6). Dañuy jot ñam boobu ci wàllu ngëm ci suñu ndaje yi, ci ndaje yu mag yi ak it ci ay téere ak wideo yu sukkandiku ci Biibël bi. Loolu lépp dafa ñuy dimbali ñu xam bu baax coobare Yàlla te dëgëral suñu diggante ak moom.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal li tax ñu soxla «surga bu takku te teey» bi, maanaam Jataay biy dogal.

Jataay biy dogal mooy jox Seede Yexowa yi ci àddina si sépp ñam ci wàllu ngëm, ay tegtal te di leen dimbali

3. Mbooloo Yexowa dafa war a doxale ni mbootaay

Ci kilifteefu Yeesu, Jataay biy dogal mooy jox Seede Yexowa yi tegtal yi ñu war a topp ngir def liggéeyu waare bi. Noonu it lañu doon doxale ci jamono karceen yu njëkk ya. Seetaanal WIDEO BI.

Jàngal 1 Korent 14:33, 40. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka la aaya yii di wone ne, Yexowa dafa bëgg seedeem yi booloo nekk benn?

4. Surga bu takku bi mooy wax ni ñuy defe liggéeyu waare bi

Waare moo nekkoon liggéey bi gën a am solo bi karceen yu njëkk ya doon def. Jàngal Jëf ya 8:14, 25. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ci karceen yu njëkk ya, kan moo doon joxe tegtal yi ñu waroon a topp ngir def liggéeyu waare bi?

  • Lan la Piyeer ak Yowaana def bi yeneen apootar yi joxe tegtal yi ñu waroon a topp?

Def liggéeyu waare bi mooy li gën a solo ci Jataay biy dogal. Seetaanal WIDEO BI.

Yeesu wone woon na ni liggéeyu waare bi ame solo. Jàngal Màrk 13:10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lu tax liggéeyu waare bi am solo lool ci Jataay biy dogal?

  • Lu tax ñu soxla «surga bu takku te teey» bi jiite liggéeyu waare bi ci àddina si sépp?

5. Surga bu takku bi mooy joxe tegtal yi

Jataay biy dogal mooy jox ay tegtal karceen yi nekk ci àddina si sépp. Naka lañuy xame tegtal yi ñu war a joxe? Xoolal ni Jataay biy dogal doon def ci jamono karceen yu njëkk ya. Jàngal Jëf ya 15:1, 2. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ci jamono karceen yu njëkk ya, lan moo indiwoon werante ci diggante ñenn ci ñoom?

  • Pool, Barnabas ak ñeneen ñi, ci kan lañu dem ngir am ay tegtal ba regle poroblem bi?

Jàngal Jëf ya 15:12-18, 23-29. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Bala ñuy jël dogal, lan la jataay biy dogal ci jamono jooju def ngir xam li nekkoon coobare Yàlla ci mbir moomu? (Xoolal aaya 1215, ak 28)

Jàngal Jëf ya 15:30, 31 ak 16:4, 5. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Karceen yu njëkk ya, lan lañu def bi leen jataay biy dogal joxe ay tegtal?

  • Naka la Yexowa barkeele seen dégg ndigal?

Jàngal 2 Timote 3:16 ak Saag 1:5. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Tey, fan la Jataay biy dogal di wute ndimbal ngir jël ay dogal?

BU LA NIT WAXOON: «Bu dee Jataay biy dogal ngeen di déggal, kon nit rekk ngeen di topp.»

  • Lan moo lay won ne, Yeesu mooy jiite Jataay biy dogal?

NAÑU TËNK

Jataay biy dogal mooy «surga bu takku te teey» bi fi Kirist teg. Karceen yi nekk ci kaw suuf si sépp, moom moo leen di jox ay tegtal ak ñam ci wàllu ngëm.

Nañu fàttaliku

  • Kan moo fi teg «surga bu takku te teey» bi?

  • Naka la ñu Jataay biy dogal di toppatoo?

  • Ndax gëm nga ne, Jataay biy dogal mooy «surga bu takku te teey» bi?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ni Jataay biy dogal di defe liggéeyam.

«Lan mooy Jataay biy dogal bu Seede Yexowa yi?» (Ci jw.org la nekk)

Naka la ñi bokk ci Jataay biy dogal gise liggéey bi leen Yeesu dénk?

Cér bu réy (7:04)

Naka la suñu ndaje yi ak ndaje yu mag yi di wonee ne Yexowa mooy jiite Jataay biy dogal?

Yexowa mooy jàngal mbooloom (9:39)