Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 57

Lan nga war a def boo defee bàkkaar bu réy?

Lan nga war a def boo defee bàkkaar bu réy?

Bu dee sax bëgg nga lool Yexowa te yaa ngi def lépp ngir bañ a def lu ko neexul, lée-lée dinga juum. Waaye nag bàkkaar yépp yemuñu, am na yu ci doon bàkkaar yu réy (1 Korent 6:9, 10). Boo defee bàkkaar bu réy, fàttalikul ne Yexowa bëgg na la ba tey; pare na ngir baal la te dimbali la.

1. Lan lañu war a def ngir Yexowa baal ñu?

Ñi bëgg Yexowa dañuy am naqaru xol bu réy, bu ñu gisee ne def nañu bàkkaar bu réy. Waaye li Yexowa dig ay jaamam dafa leen di dëfal, lii la wax: «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji» (Esayi 1:18). Bu ñu tuubee dëgg suñuy bàkkaar, Yexowa dina ñu baal. Naka lañuy wone ne tuub nañu suñu bàkkaar? Dañuy rëccu bu baax lu bon li ñu def, bañ koo defati te ñaan Yexowa mu baal ñu. Ginnaaw loolu, dañu war a def suñu kem kàttan ngir bàyyi xalaat walla tàmmeel yu bon yi ñu yóbbe ci bàkkaar boobu. Ba pare góor-góorlu ngir topp lépp li ñu Yexowa sant (Jàngal Esayi 55:6, 7).

2. Naka la Yexowa di jaare ci magi mbooloo mi ngir dimbali ñu bu ñu bàkkaaree?

Bu ñu defee bàkkaar bu réy, li ñu Yexowa wax mooy ñu «woo njiiti mbooloo mi» (Jàngal Saag 5:14, 15). Magi mbooloo yooyu dañu bëgg Yexowa, te bëgg it ay jaamam. Jàngal nañu leen ni ñu ñu mënee dimbali ñu defaraat suñu diggante ak Yexowa (Galasi 6:1).

Naka la ñu magi mbooloo mi di dimbalee bu ñu defee bàkkaar bu réy? Ñaar walla ñetti magi mbooloo dinañu jëfandikoo Biibël bi ngir won ñu, li tax li ñu def bon. Dinañu ñu jox itam ay xelal yu baax te dooleel ñu ngir ñu bañ a daanuwaat ci bàkkaar. Mën nañu ñu teree def yenn yi ci mbooloo mi, ba bés bi ñuy amaat diggante gu rattax ak Yexowa. Bu amee ku def bàkkaar bu réy te tuubu ko, magi mbooloo mi dañu koy génne ci mbooloo mi ngir mu bañ a yóbbaale ñeneen ci def lu bon.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Gënal a yokk sa ngërëm ci matuwaay yi Yexowa jël ngir dimbali ñu, bu ñu defee bàkkaar bu réy.

3. Wax li ñu def dina ñu dimbali ñu defaraat suñu diggante ak Yexowa

Saa yu ñu bàkkaaree, Yexowa lañu tooñ. Kon moom lañu war a wax li ñu def. Jàngal Sabóor 32:1-5. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax mu baax ci ñun, ñu wax Yexowa suñuy bàkkaar te bañ leen a jéem a nëbb?

Bu ñu waxee Yexowa suñuy bàkkaar ba pare, wut ndimbalu magi mbooloo mi itam dina ñu dimbali bu baax. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci wideo bi, naka la magi mbooloo mi dimbalee Canon mu dellusi ci Yexowa?

Bu ñuy wax ak magi mbooloo mi, war nañu wax lépp te bañ a nëbb dara. Dañu leen fi teg ngir ñu dimbali ñu. Jàngal Saag 5:16. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax muy gën a yomb ci magi mbooloo mi ñu dimbali ñu, bu ñu leen waxee lépp te bañ a nëbb dara?

Waxal li nga def, bul nëbb dara magi mbooloo mi, te nangul ndimbalu Yexowa bi ànd ak mbëggeel

4. Génne nit ci mbooloo mi dafay indi njariñ

Bu nit defee bàkkaar bu réy te bañ a topp santaane Yexowa yi, kooku mënatul a bokk ci mbooloo mi. Dañu koy génne ci mbooloo mi te dootuñu ànd ak moom walla sax wax ak moom. Jàngal 1 Korent 5:6, 11 ak 2 Yowaana 9-11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lawiir dafay funkiloo fariñ. Noonu it, lan la ànd ak bàkkaarkat bu tuubul mën a def ci waa mbooloo mi?

Ñu bare ñi ñu génne ci mbooloo mi dellusiwaat nañu ci mbooloo mi. Ndax lan? Ndaxte génne leen ci mbooloo mi tax na ñu xam ne li ñu def baaxul, doonte sax lu metti la woon ci ñoom (Sabóor 141:5). Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci wideo bi, génne Sonja ci mbooloo mi, naka la ko dimbalee?

Génnee nit ci mbooloo mi, naka lay...

  • màggale turu Yexowa?

  • wone ne Yexowa ku jub la te am mbëggeel?

5. Yexowa dafa ñuy baal bu ñu tuubee suñuy bàkkaar

Yeesu dafa jël benn misaal ngir dimbali ñu, ñu xam li Yexowa di yëg bu nit tuubee ay bàkkaaram. Jàngal Luug 15:1-7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la la lii di jàngal ci Yexowa?

Jàngal Esekiyel 33:11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan lu am solo lañu war a def ngir wone ne tuub nañu suñu bàkkaar?

Ni sàmm di toppatoo xaram, noonu it Yexowa dafay toppatoo bu baax jaamam

BU LA NIT WAXOON: «Dama ragal ne bu ma waxee magi mbooloo mi li ma def, dinañu ma génne ci mbooloo mi.»

  • Lan ngay wax nit ku am gis-gis boobu?

NAÑU TËNK

Bu ñu defee bàkkaar bu réy te rëccu ko bu baax, ba pare dogu ci bàyyi def lu bon, Yexowa dina ñu baal.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax mu baax ci ñun, ñu wax Yexowa suñuy bàkkaar?

  • Lan lañu war a def ngir Yexowa baal ñu suñuy bàkkaar?

  • Bu ñu defee bàkkaar bu réy, lu tax ñu war a wut ndimbalu magi mbooloo mi?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ni Yexowa wone benn góor yërmande bi ñu wax ci Esayi 1:18.

Masuma am xel-ñaar ci yërmande Yexowa (5:02)

Xoolal ni nga mënee wax ku nekkul Seede Yexowa li tax ñuy génne nit ci mbooloo mi.

«Ndax Seede Yexowa yi dañuy dëddu ñi bokkatul ci seen diine?» (Ci jw.org la nekk)

Ci nettali bi tudd «Dama waroon a dellu ci Yexowa,» xoolal ni benn góor bu demoon ba sori dëgg gi yëge ne, Yexowa mu ngi ko doon woo ngir mu dellusi.

«Biibël bi dafay soppi dund» (w12 1/4)