Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 59

Mën nga muñ fitna yi

Mën nga muñ fitna yi

Karceen bu nekk xam na ne, lu mu yàgg-yàgg dina mas a am ñu koy jéem a tere mu jaamu Yexowa. Ñooñu mën nañu dem sax ba di ko fitnaal. Ndax loolu war na tax ñu tiit?

1. Lu tax ñu war a sóoraale fitna yi?

Biibël bi wax na ci lu leer ne: «Ku bokk ci Kirist Yeesu, te bëgg dund dund gu ànd ak ragal Yàlla, alamikk ñu fitnaal la» (2 Timote 3:12). Yeesu dañu ko doon fitnaal ndaxte bokkul woon ci àddina si Seytaane jiite. Ñun itam bokkuñu ci àddina si. Kon bettuñu bu ñu nguuru àddina si ak mbootaayu diine yi di fitnaal (Yowaana 15:18, 19).

2. Naka lañu mënee waajal fitna yi?

Léegi lañu war a gën a dëgëral suñu kóolute ci Yexowa. Jëlal jot bés bu nekk ngir ñaan ko te jàng Kàddoom. Deel teewe ndaje yi. Def loolu lépp dina la may doole bi nga soxla ngir jànkoonte ak fitna yi ànd ci ak fit, bu dee sax say mbokk ñoo lay fitnaal. Ndaw li Pool mi ñu fitnaal ay yoon yu bare, lii la bindoon: «Boroom bi moo di sama ndimbal; duma ragal dara» (Yawut ya 13:6).

Bu ñuy waaree itam dañuy gën a am fit. Waare dafa ñuy jàngal ñu wóolu Yexowa te bañ a ragal nit (Kàddu yu Xelu 29:25). Boo amee fitu waare tey, loolu dina la waajal bu baax ngir nga mën a wéy di waare, bés bu nguur gi teree suñu liggéeyu waare bi (1 Tesalonig 2:2).

3. Ban njariñ lañuy jële ci muñ fitna yi?

Li wóor mooy béguñu ci nit ñi di ñu fitnaal, waaye bu ñu muñee fitna yi ba génn ci, suñu ngëm dafay gën a dëgër. Dañuy gën a jege Yexowa ndaxte gis nañu ni mu ñu dimbalee, bi ñu demee ba yëg ne amatuñu dooley muñ (Jàngal Saag 1:2-4). Yexowa bu ñu gisee ñu nekk ci coono, dafa koy naqari. Waaye dafay bég ci ñun bu ñu gisee ñuy muñ. Biibël bi nee na: «Su ñu leen fitnaalee ci def lu baax te ngeen muñ ko, jëf ju rafet la fa kanam Yàlla» (1 Piyeer 2:20). Li Yexowa di may ñépp ñi muñ fitna yi te wéy di takku ci moom mooy, dund gu dul jeex ci àddina su bees. Bu boobaa ñépp dinañu jaamu Yexowa te du am kenn ku leen di fitnaal (Macë 24:13).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal li tax takku ci Yexowa doonte sax ñu ngi ñuy fitnaal doon lu mën a nekk. Xoolal it njariñ bi ñu ciy jële.

4. Mën nga muñ bu la sa waa kër di fitnaal

Yeesu xamoon na bu baax ne, ñenn ñi ci suñu waa kër duñu bëgg ñu jaamu Yexowa. Jàngal Macë 10:34-36. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Bu amee ci benn njaboot, kenn ku jël dogal ne dafay jaamu Yexowa, lan moo mën a xew ci njaboot googu?

Ngir xam li mën a xew, seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Lan ngay def bu la sa mbokk walla sa xarit jéemee tere nga jaamu Yexowa?

Jàngal Sabóor 27:10 ak Màrk 10:29, 30. Boo paree jàng aaya bu ci nekk, tontul ci laaj bii di topp:

  • Naka la la dige bii mënee dimbali boo amee mbokk walla ay xarit yu lay fitnaal?

5. Wéyal di jaamu Yexowa bu ñu lay fitnaal

Jaamu Yexowa dafay laaj fit, bu fekkee ne dafa am nit ñu ñuy jéem a tere ñu def ko. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Nit ñi nga gis ci wideo bi, naka lañu lay yokke fit?

Jàngal Jëf ya 5:27-29 ak Yawut ya 10:24, 25. Boo paree jàng aaya bu ci nekk, tontul ci laaj bii di topp:

  • Lu tax mu am solo ñu wéy di jaamu Yexowa, bu dee sax nguur gi dafa tere suñu liggéeyu waare bi walla suñu ndaje yi?

6. Yexowa dina la dimbali nga muñ

Ay Seede Yexowa yu maasewul te bokkuñu xeet wéy nañu di jaamu Yexowa te takku ci moom, bu dee sax dañu leen doon fitnaal. Ngir gis li leen dimbali, seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci wideo bi, lan moo dimbali Seede Yexowa yi ñu muñ?

Jàngal Room 8:35, 37-39 ak Filib 4:13. Boo paree jàng aaya bu ci nekk, tontul ci laaj bii di topp:

  • Naka la aaya yii di wonee ne, mën nga muñ bépp jafe-jafe?

Jàngal Macë 5:10-12. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax nga mën a bég, bu dee sax dañu lay fitnaal?

Ay milioŋi jaamu Yexowa muñ nañu fitna yi ba génn ci. Yow it mën nga ko!

BU LA NIT WAXOON: «Mënuma muñ fitna yi.»

  • Yan aaya ñoo ko mën a dimbali mu am kóolute bi mu soxla?

NAÑU TËNK

Yexowa fonk na bu baax lépp li ñuy def ngir jaamu ko, bu dee sax ñu ngi ñuy fitnaal. Ak ndimbalam mën nañu muñ fitna yi ba génn ci!

Nañu fàttaliku

  • Lu tax karceen yi war a sóoraale fitna yi?

  • Lan nga war a def léegi ngir pare bés bu fitna yi ñëwee?

  • Lan moo la mën a dimbali nga gëm ne, mën nga jaamu Yexowa bu dee sax dañu lay fitnaal?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal li dimbali benn góor ak jabaram ñu wéy di jaamu Yexowa fekk fitnaal nañu leen ay ati at.

Wéy nañu di jaamu Yexowa bu dee sax dund nañu ay coppite (7:11)

Xoolal ni nga mënee muñ fitna yi ànd ci ak fit.

«Waajalal sa bopp léegi ngir muñ fitna yi» (w19 sulyet)

Naka lañu war a gise suñu waa kër yi ñuy fitnaal te naka lañu mënee wéy di am jàmm ak ñoom, te wéy di jaamu Yexowa?

«Dëgg gi du ‘indi jàmm, waaye jaasi lay indaale’» (w17 oktoobar)