Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 60

Wéyal di jëm kanam

Wéyal di jëm kanam

Ci sa njàngum Biibël bi, jàng nga lu bare ci Yexowa. Li nga jàng ci moom tax na nga bëgg ko lool, ba xéyna sax jébbal nga ko sa bopp te sóobu nga ci ndox. Bu dee defaguloo ko, xéyna yaa ngi koy xalaat a def ci lu yàggatul. Waaye nekkul ne, boo sóoboo ci ndox waratuloo jëm kanam. Mën nga wéy di gën a jege Yexowa ba fàww. Ci naka?

1. Lu tax nga war a wéy di dëgëral sa xaritoo ak Yexowa?

Dañu war a góor-góorlu bu baax ngir wéy di dëgëral suñu xaritoo ak Yexowa. Lu tax? «Ngir baña bayliku,» maanaam bañ a bàyyi Yexowa (Yawut ya 2:1). Lan moo ñu mën a dimbali ñu wéy di jaamu Yexowa ak takkute? Mën nañu wéy di sawar ci liggéeyu waare bi te di xool neneen ni ñu mënee gën a liggéeyal Yexowa (Jàngal Filib 3:16). Jaamu Yexowa mooy li gën, li ñu mën a def ci suñu dund! (Sabóor 84:11).

2. Leneen lan nga war a wéy di def?

Dëgg la ne léegi sa njàngum Biibël bi jeex, waaye nag sa dund karceen dafay kontine. Biibël bi nee na dañu war a ‘soloo jikko ju bees ji’ (Efes 4:23, 24). Booy wéy di gëstu Kàddu Yàlla ak di teewe ndaje yi, dinga njàng lu bees ci Yexowa ak ci jikkoom. Xoolal ci sa dund ni nga mënee gën a roy ci jikkoom. Wéyal di def coppite yi war ngir bégal Yexowa.

3. Naka la la Yexowa di dimbalee nga wéy di jëm kanam?

Biibël bi nee na: «Yàlla [..] dina leen yeesalaat, di leen dëgëral ak a dooleel, ba ngeen sampu» (1 Piyeer 5:10). Ñun ñépp dañuy jànkoonte ak ay fiir. Waaye Yexowa dafa ñuy may li ñu soxla ngir bañ a daanu ci fiir yooyu (Sabóor 139:23, 24). Dige na ne, dina def ci ñun bëgg-bëggu jaamu ko te may ñu kàttanu def ko ak takkute (Jàngal Filib 2:13).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni nga mënee wéy di jëm kanam ak ni la Yexowa di barkeelee.

4. Wéyal di waxtaan ak sa xarit bi gën

Ñaan ak jàng Biibël bi dimbali na la nga nekk xaritu Yexowa. Naka la la loolu mënee dimbali nga gën koo jege?

Jàngal Sabóor 62:9. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Boo bëggee gën a dëgëral sa xaritoo ak Yexowa, lan nga mën a yokk ci fasoŋ bi ngay ñaane?

Jàngal Sabóor 1:2. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Boo bëggee gën a dëgëral sa xaritoo ak Yexowa, lan nga mën a def ngir gën a jariñoo sa njàngum Biibël bi?

Lan nga mën a def ngir gën a jariñoo sa njàngum Biibël, bi ngay defal sa bopp? Boo bëggee xam ni nga ko mën a defe, seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ban ci xelal yi ñu joxe ci wideo bi nga mën a topp?

  • Ci lan nga bëgg a gëstu?

5. Amal ay jubluwaay ci wàllu ngëm

Am ay jubluwaay ci liggéeyu Yexowa dina la dimbali nga wéy di jëm kanam. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci wideo bi, ban njariñ la Cameron jële ci am ay jubluwaay ci wàllu ngëm?

Du ñépp ñoo mën a toxu ngir dem waare ci beneen réew. Waaye ñun ñépp mën nañu am ay jubluwaay te matal leen. Jàngal Kàddu yu Xelu 21:5. Boo paree, xoolal jubluwaay yi nga mën a am ci...

  • mbooloo mi.

  • liggéeyu waare bi.

Naka la la aaya bi mënee dimbali nga matal say jubluwaay?

Jubluwaay yi nga mën a am

  • Fexe ba say ñaan gën a xóot.

  • Liir Biibël bi yépp.

  • Gën a xam kenn ku nekk ci sa waa mbooloo.

  • Tàmbale jàngale Biibël bi.

  • Nekk pioñee oksiliyeer walla pioñee permanã.

  • Bu dee góor nga, jéemal a matal li Biibël bi laaj ngir bokk ci ñiy topptoo yëfi mbooloo mi.

6. Mën nga dund ci jàmm ba fàww!

Jàngal Sabóor 22:27. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan nga mën a def ngir dund ci jàmm tey ak ba fàww?

NAÑU TËNK

Wéyal di gën a dëgëral sa xaritoo ak Yexowa te di am ay jubluwaay ci wàllu ngëm. Soo ko defee, dinga mën a dund ci jàmm ba fàww!

Nañu fàttaliku

  • Lu tax mu mën laa wóor ne, Yexowa dina la dimbali nga jaamu ko te takku ci moom?

  • Naka nga mënee gën a dëgëral sa xaritoo ak Yexowa?

  • Am ay jubluwaay ci wàllu ngëm, naka la la mënee dimbali nga jëm kanam?

Sa jubluwaay ci at bi

GËSTUL

Lan mooy li gën a am solo ci Yexowa, nga def lée-lée benn jëf bu mag ngir won ko sa takkute walla nga takku ci moom sa giiru dund?

Nañu takku ci Yàlla ni Ibraayma (9:20)

Jaamu Yexowa yi takku ci moom sax mën nañu ñàkk seen mbégte. Xoolal ni ñu ko mënee amaat.

Jàng ak xalaat bu baax dina la mayaat mbégte (5:25)

Lu tax mu am solo nga nekk karceen bu mat ci wàllu ngëm, te lan moo la mën a dimbali nga nekk ko?

«Nañu jàll cig mat: ‘Bésub Aji Sax bu mag bee dëgmal’» (w09 15/5)