Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Nañu fàttaliku xaaj 2

Nañu fàttaliku xaaj 2

Waxtaanal ak ki lay jàngal ci laaj yii di topp:

  1. Lan la Yàlla di def diine yi dul dëgg?

    (Xoolal lesoŋ 13.)

  2. Jàngal Mucc ga 20:4-6.

    • Naka la Yexowa gise ñiy wax ne dañu koy jaamu te di jëfandikoo ay nataal?

      (Xoolal lesoŋ 14.)

  3. Kan mooy Yeesu?

    (Xoolal lesoŋ 15.)

  4. Lan moo la gën a neex ci jikkoy Yeesu?

    (Xoolal lesoŋ 17.)

  5. Jàngal Yowaana 13:34, 35 ak Jëf ya 5:42.

    • Tey, ñan ñooy topp diine karceen dëgg? Lan moo lay won ne ay karceen dëgg lañu?

      (Xoolal lesoŋ 18 ak 19.)

  6. Kan mooy kilifag mbooloo mi, te naka la koy jiite?

    (Xoolal lesoŋ 20.)

  7. Jàngal Macë 24:14.

    • Naka la yégle yonent boobu di ame tey?

    • Ndax am na koo xamal xibaaru jàmm bi?

      (Xoolal lesoŋ 21 ak 22.)

  8. Ci sa xalaat ndax sóobu ci ndox, jubluwaay bu am solo la? Lu tax?

    (Xoolal lesoŋ 23.)

  9. Naka nga mënee aar sa bopp ci Seytaane ak ci malaaka yu bon yi?

    (Xoolal lesoŋ 24.)

  10. Lan la ñu Yàlla bëggal?

    (Xoolal lesoŋ 25.)

  11. Lu tax nit ñi di dund ci coono ak di dee?

    (Xoolal lesoŋ 26.)

  12. Jàngal Yowaana 3:16.

    • Lan la Yexowa def ngir yewwi ñu ci bàkkaar ak dee?

      (Xoolal lesoŋ 27.)

  13. Jàngal Kàdduy Waare 9:5.

    • Ñi dee, fan lañu nekk?

    • Lan la Yeesu nar a defal ay miliari nit yu dee?

      (Xoolal lesoŋ 29 ak 30.)

  14. Lu tax nguuru Yàlla gën bépp nguuru doomu Aadama?

    (Xoolal lesoŋ 31 ak 33.)

  15. Ndax gëm nga ne nguuru Yàlla mu ngi ilif? Lu tax? Kañ la tàmbalee ilif?

    (Xoolal Lesoŋ 32.)