Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Nañu fàttaliku xaaj 3

Nañu fàttaliku xaaj 3

Waxtaanal ak ki lay jàngal ci laaj yii di topp:

  1. Jàngal Kàddu yu Xelu 27:11.

    • Lu tax nga bëgg a takku ci Yexowa?

      (Xoolal lesoŋ 34.)

  2. Naka nga mënee jël ay dogal yu baax, bu dee Biibël bi waxul li ñu war a def?

    (Xoolal lesoŋ 35.)

  3. Naka nga mënee doon nit ku jub ci lépp?

    (Xoolal lesoŋ 36.)

  4. Jàngal Macë 6:33.

    • Boo naree jël ay dogal ci wàllu liggéey ak xaalis, naka nga mënee wéy di ‘jëkka wut Nguur gi’?

      (Xoolal lesoŋ 37.)

  5. Naka nga mënee wone ne fonk nga dund ni ko Yexowa fonke?

    (Xoolal lesoŋ 38.)

  6. Jàngal Jëf ya 15:29.

    • Naka nga mënee déggal Yexowa ci ndigal bi mu joxe ci deret?

    • Ndax foog nga ne li mu ci laaj, jaadu na?

      (Xoolal lesoŋ 39.)

  7. Jàngal 2 Korent 7:1.

    • Lan mooy set ci yaram ak ci xel?

      (Xoolal lesoŋ 40.)

  8. Jàngal 1 Korent 6:9, 10.

    • Lan la Biibël bi wax ci séy, maanaam tëdd ak keneen? Ndax ànd nga ci loolu?

    • Yan tegtal la Biibël bi joxe ci lu jëm ci naan sàngara?

      (Xoolal lesoŋ 41 ak 43.)

  9. Jàngal Macë 19:4-6, 9.

    • Lan la Biibël bi santaane ci diggante ñaari nit yuy séy?

    • Lu tax ñiy séy ak ñi tas war koo bindlu ci kanamu yoon?

      (Xoolal lesoŋ 42.)

  10. Yan feet ak yan màggal ñoo neexul Yexowa, te lu tax?

    (Xoolal lesoŋ 44.)

  11. Jàngal Yowaana 17:16 ak Jëf ya 5:29.

    • Naka nga mënee wone ne nguuru Yàlla rekk nga faral?

    • Bu sàrt yi ci réew mi wuute ak li Yàlla santaane, lan ngay def?

      (Xoolal lesoŋ 45.)

  12. Jàngal Màrk 12:30.

    • Naka nga mënee wone ne bëgg nga Yexowa?

      (Xoolal lesoŋ 46 ak 47.)