Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi


Ni nga mënee jariñoo njàngale Biibël bi nekk ci téere bu ndaw bii

Ni nga mënee jariñoo njàngale Biibël bi nekk ci téere bu ndaw bii

Laajal ñu jàngal la Biibël bi: Laajal ki la may téere bu ndaw bii, mu jàngal la Biibël bi, walla nga laaj ñu jàngal la Biibël bi ci suñu palaas ci internet, jw.org.

XAAJ BU NJËKK BI

Jàngal xiise bu nekk ak laaj yi ñu bind mbind mu gën a réy (A) ak itam aaya yi ñu bind mbind mu gën a réy (B) te ñuy fësal ponk yi gën a am solo. Am na ay aaya yu ñu bind «jàngal», ci seen wet, jàng leen.

XAAJ BI CI DIGG BI

Li ñu njëkk wax (C) ci Xóotalal njàng mi dafa ñuy xamal li ñu nar a waxtaane. Turu xaaj yi (D) dañuy wone ponk yi gën a fës. Jàngal aaya yi, tontul laaj yi te seetaan wideo yi (E).

Xoolal bu baax nataal yi ak li ñu bind ci suufu nataal yi (F) te xalaatal ni nga mënee tontu ci Bu la nit waxoon (G).

XAAJ BU MUJJ BI

Lesoŋ bu nekk dafay jeex ak Nañu tënk ak itam Nañu fàttaliku (H). Bindal bés bi nga pare lesoŋ bu nekk. Fi ñu bind Jubluwaay (I) dafa lay dimbali nga jëfe li nga jàng. Fi ñu bind Gëstul (J) am na fa li nga mën a jàng walla seetaan soo ko bëggee.

Ni ngay def ba gis aaya yi ci sa Biibël

Nii la aaya yi di feeñe: Turu téere bi (A), pàcc bi (B) ak aaya bi walla aaya yi (C). Ci misaal, Yowaana 17:3 mu ngi tekki téere Yowaana pàcc 17 aaya 3.