Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi


Ndax dund ci jàmm ba fàww lu mën a nekk la?

Ndax dund ci jàmm ba fàww lu mën a nekk la?

Ndax dinga ne . . .

  •   waaw?

  •   déedéet?

  •   walla xéyna?

LAN LA CI BIIBËL BI WAX?

«Ñi jub, dinañu moom suuf si, te dinañu ci dëkk ba fàww» (SABÓOR 37:29, MN).

LI BIIBËL BI WAX, BAN NJARIÑ NGA CI MËN A JËLE?

Yaakaaru dund ci jàmm ak sa njaboot ak say xarit (YEREMI 29:11).

Du rekk mën a dund ci jàmm ci diir bu gàtt waaye ba fàww (SABÓOR 22:27).

NDAX MËN NGA GËM LI BIIBËL BI DIGE?

Waaw-waaw! Ngir xam li tax, mën nga xool firnde yi nekk ci ñetti lesoŋ yi ci téere bu ndaw bii. Ñu ngi tudd: