Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Indi nañu ci suñu palaas bi nekk Mount Ebo lu ëpp 27 500 kilo béton ngir defar béréb bi ñuy defe tiyaatar bi sukkandiku ci Biibël bi

LI ÑUY DEF AK LI NGEEN DI MAYE

Defar nañu wideo yi ñu war a seetaan ci suñu ndaje bu mag bu ñetti fan bu 2020 bi tudd «Deeleen bég»!

Defar nañu wideo yi ñu war a seetaan ci suñu ndaje bu mag bu ñetti fan bu 2020 bi tudd «Deeleen bég»!

10 UT 2020

 Wideo yi ñuy seetaan ci suñu ndaje yu mag yi, dañuy laal suñu xol te dañu ñuy dimbali ñu yokk suñu xam-xam ci Biibël bi. Xalaatal rekk, suñu ndaje bu mag bu ñetti fan bu 2020, bi tudd «Deeleen bég»! am na 114 wideo! Te ci wideo yooyu, am na 43 waxtaan yoo xam ne ñi bokk ci Jataay biy dogal ak ñi leen di jàppale ñoo leen def. Defar wideo yooyu nag, dafa laaj xaalis bu bare ak it liggéey bu réy.

 Ñan ñoo def liggéey boobu? Lu tollu ci 900 mbokk yu góor ak yu jigéen, yu nekk ci àddina si sépp ñoo ko def. Bàyyi nañu seeni itte ngir bokk ci liggéey bi te def nañu ci lépp li ñu mën. Ci lu ëpp ñaari at, liggéey nañu lu tollu ci 100 000 waxtu ngir defar wideo yi ñu naroon a seetaan ci ndaje bu mag bi. Ci wideo yooyu, am na benn tiyaatar bu def 76 minit bu sukkandiku ci Biibël bi. Turam mooy Neyemi: «Mbégte bu jóge ci Yexowa mooy seen doole». Liggéey bi ñu def ci tiyaatar boobu rekk, laajoon na 70 000 waxtu.

 Topptoo ñi def liggéey boobu nag, laajoon na xaalis bu bare. Waroon nañu leen jox lu ñuy lekk, fu ñuy dëkk ak itam lépp li ñu soxla ngir def seen liggéey.

 Am na it leneen luy laaj xaalis bu ñuy defar suñu wideo yi. Suñu mbokk Jared Gossman miy liggéey ci Biro bi yor wàllu ojo yi ak wideo yi, lii la ci wax: «Kuréel bi yor njàngale mi ci Jataay biy dogal dafa bëgg mu leer ci xelu ñiy seetaan suñu wideo yi ne, Seede Yexowa yi nekk ci àddina si sépp, dañoo mel ni njaboot doonte sax bokkuñu dëkk walla aada. Loolu moo tax ñu tann ay mbokk, ñu boole leen ci 24 gurup yu nekk ci 11 réew, ngir ñu fësal loolu ci suñu wideo yi. Liggéey bu mel noonu nag, dafay laaj xaalis bu bare, laaj na itam ñu waajal ko bu baax, te déggoo ci ni ñu koy defe.»

 Bu ñuy defar suñu wideo yi, dañuy fexe itam ba liy feeñ ci wideo yi ànd ak jamono bi ñu bëgg wone. Ci misaal, seetal ni ñu defare tiyaatar bi tudd: Neyemi: «Mbégte bu jóge ci Yexowa mooy seen doole». Ci biir suñu palaas bi nekk Mount Ebo, ca Etaa Sini, lañu ko defare. Dañoo bëggon lépp liy feeñ ci tiyaatar bi niroo ak la amoon ca jamono Neyemi. Ndegam, waroon nañu wone miiri Yerusalem ci tiyaatar bi, soxla woon nañu defar ay miir yu kawe te niroo ak ya amoon ca jamono boobu. Miir bu ci nekk waroon na tollu ci juroom benni meetar. Bu ñu tabaxoon miir yu tollu noonu, naroon na seer lool, te bëgguñu woon a yàq xaalis. Loolu moo tax ñu defar miir yi ak bant. Noonu, dañuy woyof ba tax saa yu ñu bëggoon a wone beneen palaas ci tiyaatar bi, mënoon nañu leen a puus ci lu yomb, walla tege leen neneen. Loolu tax na ñu mën leen a jëfandikoo ay yóoni-yóon ci tiyaatar bi, te soxlawuñu ci woon a defar yu bare. Waaw, lan lañu def ba «miir» yu ñu defar ak bant niroo ak miir yu ñu tabax ak ay xeer? Dañu ci taf lu woyof lu ñu mën a yatt, ba pare, pintiir leen ba ñu niroo ak ay xeer. Loolu lépp ñu def tax na ba xaalis bi ñu naroon a dugal ci liggéey boobu waññeeku bu baax. Waaye terewul, lu ëpp 55 milioŋ FCFA dugg na ci. a

 Bu ñu xalaate ci lépp li suñu mbokk yi def ngir ñu mën a seetaan ndaje bu mag bi, dafay tax ñu gën koo fonk. Wóor nañu ne, ndaje bu mag bii dina tax ay nit ci àddina si sépp màggal Yexowa. Jërëjëf ci li ngeen di maye ak xol bu sédd jaare ko ci internet, ci donate.pr418.com walla ci yeneeni fasoŋ. Maye yooyu ñooy jàppale liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp.

a Bala feebaru Koronaa bi di komaase, lañu defar «miir» yi ñu soxla woon ci tiyaatar bi. Ca jamono jooju, nguur yi laajuñu woon nit ñi bàyyi lu tollu ci benn meetar seen diggante ak ñeneen ñi.