Ubbil li ci biir

Ndax coono àddina dina mas a jeex ?

Ndax coono àddina dina mas a jeex ?

Ndax dinga ne . . .

  • waaw ?

  • déedéet ?

  • walla xéyna ?

LAN LA BIIBËL BI WAX CI LAAJ BOOBU ?

“ Yàlla [. . .] dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët ; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit ”. — Peeñu ma 21:3, 4, Téereb Injiil di Kàddug Yàlla.

LI MU WAX, BAN NJARIÑ NGA CI MËN A JËLE ?

Xam ne du Yàlla moo ñu teg suñuy coono. — Saag 1:13.

Xam ne Yàlla yëg na suñuy metit.— Zekaria 2:8.

Am yaakaar ne coono yépp dinañu jeex. — Sabóor 37:9-11.

NDAX MËN NGA GËM LI MU WAX CI LAAJ BOOBU ?

Waaw waaw, xoolal liy topp :

  • Yàlla dafa bañ lu jubadi ak coono bu muy jur. Xoolal li Yexowa Yàlla yëgoon bi ñu doon toroxal mbooloom. Ci li Biibël bi wax loolu dafa ko metti woon ndax ñi leen doon toroxal. — Njiit yi 2:18.

    Bu Yàlla gisee kuy toroxal nit, loolu dafa koy metti lool. Biibël bi nee na Yàlla dafa bañ lool “ kuy rey nit ku deful dara ”. — Kàddu yu Xelu 6:16, 17, Kàddu yu Xelu ñeel Suleymaan.

  • Yàlla fonk na kenn ku nekk ci ñun. Kenn ku nekk ci ñun xam nga bu baax sa coono ak li lay metti. Nanga xam ne Yexowa moom it xam na ko ! — Chroniques 6:29, 30.

    Yexowa dina jaar ci Nguuram ngir dindi coono nit ku nekk. (Macë 6:9, 10) Fi mu nekk nii, ñi koy wut dëgg, Yàlla mu ngi dëfël seen xol. — Jëf ya 17:27 ; 2 Korent 1:3, 4.

LOO XALAAT CI LAAJ BII ?

Lu tax Yàlla bàyyi nit ñi di am metit ?

Biibël bi dafa ciy tontu ci ROOM 5:12 ak 2 PIYEER 3:9.