Naka Nga Gise Biibël bi ?
Ndax dinga ne . . .
-
Kàddu Yàlla la ?
-
dañu ko soppi ?
-
walla ay léeb kese ñoo ci nekk ?
LAN LA BIIBËL BI WAX CI LAAJ BOOBU ?
“ Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge ”. — 2 Timote 3:16, Téereb Injiil di Kàddug Yàlla.
LI MU WAX, BAN NJARIÑ NGA CI MËN A JËLE ?
Ay tont yu leer ci say laaj. — Kàddu yu Xelu 2:1-5.
Ay xelal yu wóor ci sa dund. — Sabóor 119:105.
Yaakaar bu wóor ngir ëllëg. — Room 15:4.
NDAX MËN NGA GËM LI MU WAX CI LAAJ BOOBU ?
Waaw waaw, xoolal liy topp :
-
Du weddi boppam. Biibël bi, lu jege 40 góor ñoo ko bind ci lu ëpp 1 600 at. Ñi ci gën a bare, xamantewuñu woon. Loolu terewul lépp li nekk ci Biibël bi ànd te bokk benn wax.
-
Du nëbb dara. Ñiy nettali xew-xewu àddina bi, bu seen réew ñàkkee ndam, ñu bare ci ñoom duñu ci wax. Waaye ñi bind Biibël bi, nëbbuñu woon dara, dañu wax ci fi ñu juume ak fi seen réew juume. — 2 Chroniques 36:15, 16 ; Sabóor 51:3-6.
-
Buy wax ci ëllëg, loolu day am. Lu mat 200 at bala muy xew, Biibël bi waxoon na ne dinañu alag dëkk bi tuddoon Babilon. (Isaïe 13:17-22) Waxoon na ni ñuy def ba alag ko. Wax na sax turu ki koy alag ! — Isaïe 45:1-3.
Wax na ci yeneen ak yeneen yu mel noonu yoo xam ne, lépp li mu ci waxoon gisoon nañu ko. Ndax du loolu lañu war a séentu ci téere bu jóge ci Yàlla ? — 2 Piyeer 1:21.
LOO XALAAT CI LAAJ BII ?
Ban njariñ moo nekk ci topp Kàddu Yàlla bés bu nekk ?
Biibël bi dafa ciy tontu ci ISAÏE 48:17, 18 ak 2 TIMOTE 3:16, 17.