Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑUY DEF AK LI NGEEN DI MAYE

Ñi am lu bare dañuy faj soxlay ñeneen ñi

Ñi am lu bare dañuy faj soxlay ñeneen ñi

1 OKTOOBAR 2020

 Ci lu ëpp 200 réew, Seede Yexowa yi dañuy yëngu ci lu bare, lu mel ni liggéeyu waare bi walla tabax ay béréb yu ñuy jaamoo Yàlla. Dañuy dimbali it seeni mbokk yi ci ngëm yi nekk ci jafe-jafe. Xaalis bi nit ñi di maye mooy tax ñu mën a faj soxla yooyu yépp. Waaye, li ñu seetlu mooy, ci réew yooyu ñu nekk, 35 kese ñoo ciy jot ay maye yu mën a faj seen soxla. Yeneen réew yi nag, naka lañuy def?

 Jataay biy dogal bu Seede Yexowa yi dafay bàyyi xel ci li Seede Yexowa yi nekk ci àddina si sépp soxla ngir jaamu Yàlla te kontine suñu liggéeyu waare bi. Dafay jëfandikoo bu baax li nit ñi di maye ngir faj soxla yooyu. Lii la dogal: bu dee am na bànqaas bu jot xaalis bu ëpp li mu soxla, li ci des, da koy yónnee yeneen réew yu ko soxla. Noonu, dañuy roy ci Karceen yu njëkk ya. Ñi amoon alal ju bare dañu doon dimbali yeneen karceen yi ñu faj seeni soxla ba «ñépp tolloole» (2 Korent 8:14).

 Lan la suñu mbokk yi jot ci ndimbal boobu yëg? Mbégte mu réy! Ci misaal, ñi gën a bare ci waa Tanzanie, amuñu sax 1 200 FCFA bés bu nekk ngir faj seeni soxla. Suñu mbokk yi nekk foofu jot nañu xaalis bu jóge ci yeneen bànqaas. Loolu tax na ñu mën a defaraat Saalu Nguuru mbooloo Mafinga. Lii la waa mbooloo mi bind: «Bi ñu defaraate Saalu Nguur gi ba téy, ñiy teewe suñu ndaje yi dañoo gën a bare! Ñu ngi gërëm bu baax mbootaayu Yexowa ak it suñu mbokk yi ci ngëm yi nekk ci àddina si sépp. Mbaax gi ñu wone moo tax ñu am Saalu Nguur gu rafet gii.»

 Feebaru Korona bi tax na ba ñenn ci suñu mbokk yi nekk Sri Lanka amuñu woon lekk bu doy. Suñu benn mbokk bu jigéen bu tudd Imara Fernando ak doomam bu góor, Enosh, ci lañu bokk. Maye yi jóge ci yeneen réew yi ñoo tax ñu mën a faj seen soxla. Lii lañu bind: «Ñu ngi gërëm bu baax suñu mbokk yi. Seen mbëggeel a tax ñu dimbali ñu ci jamono ju metti jii. Kontaan nañu lool ci ni ñu bokkee ci njaboot ju ni mel. Ñu ngi ñaan Yexowa mu jàppale suñu mbokk yi yépp ci mujug jamono jii.»

Imara Fernando ak doomam Enosh

 Fépp ci àddina, suñu mbokk yi pare nañu séddoo li ñu am ak ñeneen ñi bu dee sax amuñu lu bare. Enosh ci la bokk. Dafa bëgg jàppale yeneen njaboot yu nekk ci jafe-jafe. Looloo tax mu defar fu mu mën a denc xaalis ngir moom itam, mu mën a maye dara. Guadalupe Álvarez moom it, ku bëgg dimbali ñeneen ñi la. Fi mu dëkk ca Mexique, nit ñu bare, li ñu leen di fey barewul. Ñeneen ñi du saa su ne lañuy am xaalis. Waaye terewul, Guadalupe dafay joxe li mu am. Lii la bind: «Maa ngi gërëm Yexowa ci mbaaxam ak ngoram. Xam naa ne li may maye dinañu ko boole ci li ñeneen ñi di maye, te dina dimbali samay mbokk yi nekk ci jafe-jafe.»

 Mbokk yi nekk ci bànqaas yiy yónnee xaalis, ñoom itam, kontaan nañu ci li ñu mënee dimbali ñeneen ñi. Lii la Anthony Carvalho, mi bokk ci Kuréelu Bànqaasu Brésil wax: «Ay at ci ginnaw, ñun itam soxla woon nañu xaalis, te jot nañu ndimbal bu jóge ci yeneen réew. Ndimbal boobu tax na ba liggéey bi jëm kanam te ay nit ñu bare ñëw bokk ci mbootaay mi. Léegi, am nañu sax lu ñuy dimbalee ñeneen, te bég nañu ci lool. Ndegam suñu mbokk yi fii ci Brésil dañuy bàyyi xel ci liggéeyu waare bi ci àddina si sépp, xam nañu li ñu mën a def ba dimbali seen mbokk yi.»

 Lan la Seede Yexowa yi mën a def bu ñu bëggee jàppale seeni mbokk yi ci ngëm yi nekk ci jafe-jafe? Jarul ku nekk yónnee xaalis bànqaas yi ko soxla. Li gën mooy, ñu boole xaalis boobu ci li ñuy maye ngir jàppale suñu liggéey bi ci àddina si sépp. Naka lañu ko mën a defe? Saa yu ñu demee ci Saalu Nguur gi, mën nañu ko dugal fi ñuy def xaalis bi ñuy maye, te ñu bind fa «Liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp». Mën nañu jaar itam ci internet, ci donate.pr418.com ngir maye dara. Ñu ngi leen di gërëm bu baax ci li ngeen di maye.