Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑUY DEF AK LI NGEEN DI MAYE

Defar nañu luy tax suñu mbokk yi ci ngëm mën a telesarse suñu téere yi ak wideo yi

Defar nañu luy tax suñu mbokk yi ci ngëm mën a telesarse suñu téere yi ak wideo yi

1 SEPTAAMBAR 2020

 Téere ak wideo yi ñuy fekk ci suñu palaas ci internet ñu ngi gën di bare. Waaye nag, ci béréb yu bare, suñu mbokk yi ci ngëm mënuñu leen a telesarse ndaxte amuñu lu ñuy jëndee koneksiyoŋ walla du saa su ne lañuy am internet. Ñeneen ñi, fi ñu nekk, internet bi dafa yéex torop walla amufa sax.

 Waaye loolu terewul, ñu bare ci suñu mbokk yooyu mën a telesarse suñu téere yi ak wideo yi. Loolu naka la mënee nekk?

 Mbootaayu Seede Yexowa yi moo defar li ñuy woowe JW Box te yónnee ko mbooloo yi nekk ci béréb yooyu. Loolu mooy dimbali suñu mbokk yi ñu mën a telesarse suñuy téere ak wideo yi doonte sax amuñu internet. Ci biir JW Box bi, am na lu ñuy woowe routeur. Routeur boobu dañu ko jënd. Am na it lu ñuy woowe logiciel. Biro bi yor lépp lu jëm ci ordinatër bi nekk ci Betel moo ko defar. Am na ci itam ay téere ak ay wideo yu ñuy fekk ci jw.org. JW Box bu nekk a ngi jar lu tollu ci 39 350 FCFA.

 Naka lañuy jëfandikoo JW Box bi nag? Ndegam dafa am Wifi, suñu mbokk yi mën nañu ci konektewu saa yu ñu demee ci Saalu Nguur gi. Noonu, dinañu mën a telesarse ci seeni telefon walla tablette, ay téere ak wideo yu nekk ci jw.org. Bu dee sax nit ki telefon bu màgget la am walla bu seerul, mën na ci konektewu. Waaw léegi, naka la mbooloo yi amul internet di def ba seen JW Box am téere ak wideo yu bees yi? Banqaas bi moo leen koy yónnee ci ay clé USB. Bu suñu mbokk yi jotee clé USB bi, dañu koy dugal ci JW Box bi ngir mën a telesarse téere ak wideo yu bees yi. Clé USB bu nekk 2 295 FCFA lay jar.

 JW Box bi jàppale na suñu mbokk yu bare. Nathan Adruandra mi am ay doom te dëkk ca République démocratique du Congo, lii la wax: «Yàgg naa jéem a telesarse tiyaatar bu sukkandiku ci Biibël bi, te tudd « Ô Jéhovah, en toi j’ai placé ma confiance ! » ak beneen bi tudd Fàttalikuleen soxnas Lóot, waaye doxul woon. Damaa mujjee bàyyi sax. Waaye, JW Box bi tax na ma mën leen a telesarse ci lu yomb, te wideo yooyu dañu may dimbali ma yar samay doom.»

 Suñu benn mbokk buy jàppale mbooloo yi nekk Nigéria ñu mën a jëfandikoo JW Box bi, lii la wax: «Mbokk yi jàppe nañu JW Box bi ni xéewal bu jóge ci Yexowa. Kontaan nañu lool, ndaxte léegi, mën nañu telesarse ci lu yomb ay téere ak ay wideo yu bokk ci suñu jumtukaay yi ngir jàngale Biibël bi.»

 Yónnee nañu lu ëpp 1 700 JW Box ci Afrique, Océanie ak Amérique du Sud te ñu ngi waaj a yónnee yeneen ci mbooloo yu bare. Defar JW Box yi te yónnee leen dafa laaj xaalis. Fan la xaalis boobu jóge? Ci li nit ñi di maye ngir jàppale liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp. Ñu bare dañuy jaar ci internet, ci donate.pr418.com ngir maye dara. Jërëjëf ci li ngeen di jàppale suñu liggéey ak xol bu sédd.