11 nowàmbar ba 17 nowàmbar
TAALIFI CANT 106
Woy-Yàlla nº 36 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)
1. «Dañoo fàtte Yàlla ma leen di musal»
(10 minit)
Ragal taxoon na ba waa Israyil bañ a déggal Yexowa (Mucc ga 14:11, 12; Taalifi Cant 106:7-9)
Xiif ak mar taxoon na ba waa Israyil doon xultu di jàmbat ci kanamu Yexowa (Mucc ga 15:24; 16:3, 8; 17:2, 3; Taalifi Cant 106:13, 14)
Jaaxle taxoon na ba waa Israyil jaamu ay xërëm (Mucc ga 32:1; Taalifi Cant 106:19-21; w18.07 20 § 13)
XALAATAL CI LII: Di xalaat ci lépp li ñu Yexowa mas a defal, naka lañu loolu mënee dimbali buñu nekke ci jafe-jafe?
2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
(10 minit)
Taalifi Cant 106:36, 37—Lu tax ñu mën a méngale jaamu xërëm ak saraxal rab yi, maanaam maalaaka yu bon yi? (w06 15/7 13 § 9)
Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?
3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi
(4 minit) Taalifi Cant 106:21-48 (th lesoŋ 10)
4. Na li ngay wax nekk lu yomb a nànd —Ni ko Yeesu defe
(7 minit) Waxtaan ak ñi teew. Woneel WIDEO bi, ba pare ngeen waxtaan ci lmd lesoŋ 11 ponk 1-2.
5. Na li ngay wax nekk lu yomb a nànd —Nañu roy ci Yeesu
(8 minit) Waxtaan bi dafa sukkandiku ci lmd lesoŋ 11 ponk 3-5 ak «Seetal aaya yii itam».
Woy-Yàlla nº 78
6. Li mbooloo mi soxla ci wàllu ngëm
(15 minit)