Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

16 desàmbar ba 22 desàmbar

TAALIFI CANT 119:​57-120

16 desàmbar ba 22 desàmbar

Woy-Yàlla nº 129 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Li ñu mën a def ngir muñ suñuy njàqare

(10 minit)

Nanga wéy di jàng Kàddu Yàlla te di ko gëstu (Taalifi Cant 119:61; w06-F 15/6 20 § 2; w00 1/12 14 § 3)

Nanga bàyyi njàqare yi wala jafe-jafe yi, ñu feeñal sa jikko yu rafet yi (Taalifi Cant 119:71; w06 1/9 14 § 3)

Nanga wéeru ci Yexowa ngir mu dëfal la (Taalifi Cant 119:76; w17.07 13 § 3, 5)

LAAJAL SA BOPP LII, ‘Naka la ma Yexowa dimbalee ma muñ samay njàqare?’

2. Nanu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 119:96—Lan la aaya bii di tekki? (w06 1/9 14 § 4)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) KËROO-KËR. Wonal nit ki suñu palaas ci internet, te jox ko kàrtu jw.org. (lmd lesoŋ 2 ponk 5)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(4 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Waxal nit ki mu ñëw déglu waxtaan bi ñu jagleel ñépp, bi nar a am ayu bés bii di ñëw. Ba pare nga won ko wideo bi tudd: Lan lañuy def ci suñu saalu Nguur yi? (lmd lesoŋ 8 ponk 3)

6. Wax ci li ñu gëm

(5 minit) Waxtaan bi. ijwbq-F waxtaan nº 157—Turu waxtaan bi ci farãse: Les catastrophes naturelles : qu’en dit la Bible? (lmd lesoŋ 3 ponk 3)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 128

7. Yexowa moo ñuy dimbale ñu muñ

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Kerceen bu mën a muñ mooy koo xam ne, du xàddi mukk bu amee jafe-jafe wala mu nekk ci fitna. Mooy it nit koo xam ne bu nekke ci coono, dafay wéy di am gis-gis bu rafet te wéy di am yaakaar. Nit ku mën a muñ bu nekke ci jafe-jafe, du dellu mukk gannaw wala mu wàññi li muy def ci liggéeyu Yexowa (Yawut ya 10:​36-39). Yexowa pare na ngir dimbali ñu, ñu muñ jafe-jafe yi.—Yawut ya 13:6.

Ci aaya yi ñu lim fii ci suuf, bindal ni ñu aaya bu nekk di wone ni ñu Yexowa di dimbalee ñu muñ.

Woneel WIDEO bi tudd: Nañuy ñaanal bu baax ñi nekk ci fitna. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Naka lañu mën a jëfandikoo jw.org ngir xam li suñu mbokk yi di dund?

  • Naka la waajur yi mënee jàngal seeni doom ñuy ñaanal ñeneen ñi. Ban njariñ lañu ciy jële?

  • Lu tax mu am solo ñuy ñaan Yexowa mu dimbali suñu mbokk kerceen yi ñu muñ seeni jafe-jafe?

  • Ñaanal ñeneen ñi, ban njariñ lañuy amal buñu nekke ci jafe-jafe ñun itam?

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 32 ak ñaan