Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

18 nowàmbar ba 24 nowàmbar

TAALIFI CANT 107-108

18 nowàmbar ba 24 nowàmbar

Woy-Yàlla nº 7 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. ‘Santleen Yexowa, ndaxte ku baax la’

(10 minit)

Ni Yexowa muccale waa Israyil ci loxoy waa Babilon, noonu itam lañu muccale ci àddina Seytaane si (Taalifi Cant 107:​1, 2; Kolos 1:​13, 14)

Ngërëm bi ñu am ci Yexowa moo ñuy xiir ñu màggal ko ci biir mbooloo mi (Taalifi Cant 107:​31, 32; w07-F 15/4 20 § 2)

Bu ñuy faral di xalaat ci lépp li ñu Yexowa defal, loolu dina yokk suñu ngërëm (Taalifi Cant 107:43; w15-F 15/1 9 § 4)

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 108:9—Buñu waxe ne Mowab ‘ndabal raxasukaayu’ Yàlla la, loolu lan lay tekki? (it-2-F 303 § 5)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. (lmd-F lesoŋ 1 ponk 4)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(4 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Waxal nit ki ni ñuy defe njàngum Biibël bi. Jox ko itam kàrt bi ñu defar ngir won nit ñi ne, mën nañu jàng Biibël bi te duñu fey dara (lmd-F lesoŋ 9 ponk 3)

6. Waxtaan bi

(5 minit) ijwyp-F 90—Turu waxtaan bi ci farãse: Comment arrêter d’être pessimiste ? (th lesoŋ 14)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 46

7. Dañuy woy ngir màggal Yexowa

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Bi Yexowa muccale waa Israyil ci loxoy soldaari waa Misra ca géeju barax ya, dañu ko woyol ngir gërëm ko (Mucc ga 15:​1-19). Woy bu bees la woon. Góor ñi ñoo ko tàmbali (Mucc ga 15:21). Yeesu ak kerceen yu njëkk ya itam dañu doon woy ngir màggal Yexowa (Macë 26:30; Kolos 3:16). Ñun itam dañuy woy ngir màggal Yexowa ci ndaje yu ñuy def ci suñu saalu nguur yi, ci ndaje yu mag yu benn fan ak yu ñetti fan. Ci misaal, woy bi ñu woy léegi nii, te mu tudd ci farãse «Merci, Jéhovah», ñu ngi koy woy ci suñu ndaje yi dale ko 1966.

Ci yenn aada yi, góor ñi dañuy rus a woy ci kanamu nit ñi. Ñeneen ñi dañuy bañ a woy ndaxte ci ñoom, seen baat neexul. Waaye nag, dañoo war bàyyi xel ne woy, ci suñu jaamu Yexowa la bokk. Mbootaayu Yexowa dafay def lépp ngir waajal woy yu neex te tànn bu baax, woy yi ñu war a woy ci ndaje bu nekk. Kon ñun suñu wàll yomb na—mooy di woyandoo ngir gërëm Yexowa, suñu baay bi ci kay asamaan te won ko suñu mbëggeel.

Woneel WIDEO bi tudd: Xew-xewu démb—woy yi, maye yu am solo lañu, Xaaj 2. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Lan moo xewoon ci atum 1944?

  • Naka la suñu mbokk yi nekkoon ca dëkku Sibérie wonee ne dañoo fonk woy-Yàlla yi?

  • Lu tax woy am solo ci Seede Yexowa yi?

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 73 ak ñaan