Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

2 desàmbar ba 8 desàmbar

TAALIFI CANT 113-118

2 desàmbar ba 8 desàmbar

Woy-Yàlla nº 127 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Naka lañu mënee gërëm Yexowa ci lépp li mu ñu defal?

(10 minit)

Yexowa dafa ñuy aar, dafa baax ci ñun, dafa ñuy muccal itam (Taalifi Cant 116:​6-8; w01 1/1 11 § 13)

Dañuy wone suñu ngërëm ci li ñu Yexowa defal bu ñuy topp sàrtam yi ak saantaaneem yi (Taalifi Cant 116:​12, 14; w09 15/7 29 § 4-5)

Dañuy wone suñu ngërëm ci li ñu Yexowa defal bu ñu koy saraxal «saraxu cant» maanaam bu ñu koy màggal (Taalifi Cant 116:17; w19.11 22-23 § 9-11)

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 116:15—Naka la bakanu ‘wóllërey Yàlla’ maanaam ñi gore, amee solo ci moom? (w12 15/5 22 § 1-3)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Waxal nit ki ci lu leer li mu war a soppi —Ni ko Yeesu defe

(7 minit) Waxtaan ak ñi teew.Woneel WIDEO bi, ba pare ngeen waxtaan ci lmd lesoŋ 12 ponk 1-2.

5. Waxal nit ki ci lu leer li mu war a soppi —Nanga roy ci Yeesu

(8 minit) Waxtaan bi dafa sukkandiku ci lmd lesoŋ 12 ponk 3-5 ak ci «Seetal aaya yii itam.»

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 60

6. Li mbooloo mi soxla ci wàllu ngëm

(15 minit)

7. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 29 ak ñaan