Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

23 desàmbar ba 29 desàmbar

TAALIFI CANT 119:​121-176

23 desàmbar ba 29 desàmbar

Woy-Yàlla nº 31 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Ni ñu mënee moytu teg suñu bopp yenn naqar yi

(10 minit)

Nañu fonk santaane Yàlla yi (Taalifi Cant 119:127; w18.06 17 § 5-6)

Nañu sib jëf yu bon (Taalifi Cant 119:128; w93 15/4 17 § 12)

Nañu déglu Yexowa te moytu def lu bon, jëf yi nit yu “xeluwul” di def (Taalifi Cant 119:​130, 133; Kàddu yu Xelu 22:3)

LAAJAL SA BOPP LII: Yan coppite laa war a def ci sama dund ngir wone ne fonk naa santaane Yàlla yi te sib naa lu bon?’

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 119:160—Lan la aaya bii di wone lu jëm ci Kàddu Yàlla? (w23.01 2 § 2)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) KËROO-KËR. (lmd lesoŋ 1 ponk 5)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(4 minit) KËROO-KËR. Dimbalil nit ki mu xam ni mu mënee gis ci jw.org xelal yi mu soxla. (lmd lesoŋ 8 ponk 3)

6. Ni ñu mënee jàngal nit ñi ba ñu nekk taalibe Yeesu

(5 minit) Ni nga mënee dimbali kenn ki ngay jangal Biibël bi koo xam ne duy faral di teewe ndaje yi. (lmd lesoŋ 12 ponk 4)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 121

7. Bul bàyyi xaalis jural la tiis

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Ñi bëgge ci xaalis dañuy am «tiis yu bare» (1 Timote 6:​9, 10). Li ñu lim fii ci suuf mën na ñu dal buñu nekke ñu bëgge ci xaalis.

  • Duñu mën a am diggante bu rattax ak Yexowa.—Macë 6:24

  • Duñu doyal mukk.—Kàdduy Waare 5:9

  • Dinañu daanu ci lu yomb ci fiir, lu ci mel ni fen, sàcc ak wor nit (Kàddu yu Xelu 28:20). Te jëf yu bon yooyu mën nañu ñu jural xel mu ñuy tuumal, suñu der mën na yàqu te yàq suñu diggante ak Yàlla.

Jàngal Yawut ya 13:5. Ba pare nga waxtaan ak ñi teew ci laaj bii:

  • Naka lañu war a gise xaalis buñu bëggul am tiis wala naqar? Lu tax loolu am solo?

Buñu xamul ni ñuy jëfandikoo bu baax xaalis bi ñu am, mën nañu am naqar bu dee sax nekkuñu ñu bëgge.

Woneel wideo bi tudd: Ni nga mënee jëfandikoo bu baax sa xaalis. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Lu tax ñu war a xalaat bu baax ci xaalis bi ñu am ak fi ñu ko war a dugal? Naka lañu ko mën a defee?

  • Lu tax denc tuuti xaalis nekk lu baax?

  • Lu tax ñu war a moytu yenn bor yi?

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 101 ak ñaan