25 nowàmbar ba 1 desàmbar
TAALIFI CANT 109-112
Woy-Yàlla nº 14 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)
1. Nañu jàpple Yeesu, Buur bi!
(10 minit)
Bi Yeesu delloo ci kaw asamaan, dafa toog ci ndijooru Yexowa (Taalifi Cant 110:1; w06 1/9 13 § 6)
Ci atum 1914 la Yeesu tàmbalee ilif ci kaw noonam yi (Taalifi Cant 110:2; w00 1/4 18 § 3)
Mën nañu def lépp li ñu mën ngir jàpple kiliftéefu Yeesu (Taalifi Cant 110:3; be 76 § 2)
LAAJAL SA BOPP LII: ‘Yan jubluwaay laa mën a am ngir jàpple nguur gi?’
2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
(10 minit)
-
Taalifi Cant 110:4—Ci ban kóllëre la aaya bii di wax? (it-1 80 § 4)
-
Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?
3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi
(4 minit) Taalifi Cant 109:1-26 (th lesoŋ 2)
4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(2 minit) KËROO-KËR. Jëfandikool benn ci suñu kayit yu ndaw yi ngir tàmbali waxtaan. (lmd lesoŋ 4 ponk 3)
5. Wax ci li ñu gëm
(5 minit) Wone bi. ijwfq-F 23—Wone bi mu ngi sukkandiku ci waxtaan bii ci farãse: Pourquoi les Témoins de Jéhovah ne participent pas aux guerres ? (lmd lesoŋ 4 ponk 4)
6. Ni ñu mënee jàngal nit ñi ba ñu nekk taalibe Yeesu
Woy-Yàlla nº 72
7. Naka lañu mënee jàpple nguuru Yàlla ak tàkkute?
(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.
Nguuru Yexowa dafay firndeel ne mooy kilifa ci kaw lépp (Dañeel 2:44, 45). Kon buñuy jàpple nguuru Yàlla dañuy wone ne nangu nañu kiliftéefu Yexowa.
Woneel WIDEO bi tudd: Saxleen ci jàppale «Buuru jàmm bi.» Ba pare nga laaj ñi teew lii:
-
Naka lañu mënee sax ci jàpple nguuru Yàlla?
Lim nañu fii fasoŋ yi ñu mënee jàpple nguuru Yàlla. Bindal aaya bi ànd ak fasoŋ bu nekk:
-
Di wone ne nguuru Yàlla mooy li gën a am solo ci suñu dund.
-
Di topp santaane yi ñu jox, ñi nguuru Yàlla di ilif.
-
Di yégle xibaaru jàmm bi jëm ci nguuru Yàlla ànd ci ak cawarte.
-
Di dégal kilifay àddina si. Waaye buñu kilifa yooyu laajee ñu def li mengoowul ak li ñu Yàlla sant, Yàlla lañuy dégal.
8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi
(30 minit) bt-F pàcc 18 § 16-24