30 desàmbar 2024 ba 5 sãwiyee 2025
TAALIFI CANT 120-126
Woy-Yàlla nº 144 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)
1. Ji nañu ci naqar, waaye góob nañu ànd ci ak mbégte bu réy
(10 minit)
Waa Israyil dañu bégoon bi ñu leen génne babilon ngir ñu dem taxawalaat dine gu sell gi (Taalifi Cant 126:1-3)
Xeyna sax ñi dellu woon Yude jooy nañu ndaxte jël dogal bu ni mel yombul woon (Taalifi Cant 126:5; w04 1/6 16 § 10)
Dañu muñ, kontine di def lépp li ñu mën te Yexowa bàrkeel na leen (Taalifi Cant 126:6; w21.11 25 § 17; w01 15/7 18-19 § 13-14; xoolal foto bi nekk ci)
XALAATAL CI LII: Bu Armagedon jote Yexowa dina ñu muccal ci àddina su bon sii. Waaye, yan jafe-jafe lañu nar a am bu ñuy defaraat suuf si? Yan bàrke lañu ci nar a jële?
2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
(10 minit)
-
Taalifi Cant 124:2-5—Ndax Yexowa dina ñu aar ni mu ko defewoon ak mbooloo Israyil? (cl-F 86 § 15)
-
Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?
3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi
(4 minit) Taalifi Cant 124:1–126:6 (th lesoŋ 5)
4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(3 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. (lmd lesoŋ 3 ponk 5)
5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki
(4 minit) KËROO-KËR. Li nga mën a def bu dee nit ki dafa la waxoon ne dafa am xel ñaar ci li Biibël bi di jàngale. (lmd lesoŋ 9 ponk 5)
6. Ni ñu mënee jàngal nit ñi ba ñu nekk taalibe Yeesu
Woy-Yàlla nº 155
7. Bànneexuleen ci li Yàlla dige
(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.
Yexowa mataloon na li mu digoon jaamam yi ñu yóbbu woon Babilon. Dafa leen muccal te baal leen seeni bàkkaar te dëgëral leen ci wàllu ngëm (Esayi 33:24). Rabu àll yi demoon nañu ba bari ca dëkk ba ak ci yoon yi ndax li fa kenn nekkul woon. Waaye bi ñuy dellusi, Yexowa aar na leen, ñoom ak seeni mala, ngir gaynde yi ak yeneen rabu àll yi bañ leen a lor (Esayi 65:25). Ku nekk mënoon na dëkk ca këram te lekk ci meññeefu garab yi mu ji (Esayi 65:21). Yàlla barkeeloon na seen liggéey te may na leen gudd fan.— Esayi 65:22, 23.
Woneel WIDEO bi tudd: Bànneexuleen ci jàmm ji Yàlla dige—Xaaj. Ba pare nga laaj ñi teew lii:
-
Naka la dige yooyu nekke di mat ci suñu jamano?
-
Naka la dige yooyu nar a mate ci fasoŋ bu gën a mag ci àddina su bees si?
-
Ban ci dige yooyu nga gën a yàkkamti mu mat?
8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi
(30 minit) bt-F pàcc 20 § 8-12 ak wërale bi nekk ci paas 161