4 nowàmbar ba 10 nowàmbar
TAALIFI CANT 105
Woy-Yàlla nº 3 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)
1. Dafay «fàttaliku ba fàww kóllëreem»
(10 minit)
Li Yexowa digoon Ibraayma dafa ko waxaat Isaaxa ak Yanqóoba (Njàlbéen ga 15:18; 26:3; 28:13; Taalifi Cant 105:8-11)
Dige boobu dafa meloon ni lu mënul nekk (Taalifi Cant 105:12, 13; w23.04 28 §11-12)
Yexowa masul a fàtte kóllëre gi mu fasoon ak Ibraayma (Taalifi Cant 105:42-44; it-2 493)
LAAJAL SA BOPP LII: ‘Xam ne Yexowa ku jar a wóolu la, lan lay def ci man?’
2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
(10 minit)
-
Taalifi Cant 105:17-19—Naka la «Kàddug Aji sax ji» nattoo Yuusufa maanaam naka la ko kàddu Yàlla dimbalee ci nattu yi mu amoon? (w86 11/1 19 §15)
-
Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?
3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi
(4 minit) Taalifi Cant 105:24-45 (th lesoŋ 5)
4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(1 minit) KËROO-KËR. Li nga mën a def bu dee ki ngay waxal dafa jàpp (lmd lesoŋ 2 ponk 5).
5. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(2 minit) KËROO-KËR. Nit ki dafa bëgg a werante ak yaw. Nanga tëj waxtaan bi ci anam bu rafet (lmd lesoŋ 4 ponk 5).
6. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki
(4 minit) KËROO-KËR. Bi ngeen mujjee waxtaan, nit ki dafa la waxoon li ko itteel. Jox ko yéenekaay buy wax ci loolu. (lmd lesoŋ 8 ponk 3)
7. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki
(4 minit) WAARAATE SAA YUÑU AMEE BUNT. Waxal nit ki lu jëm ci application JW Library®, te dimbali ko mu telesarse ko (lmd lesoŋ 9 ponk 5).
Woy-Yàlla nº 84
8. Ni ñu mënee wone suñu mbëggeel ci Yeesu
(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.
Bu ñuy jël suñu jot ak suñu alal ngir jàpple liggéeyu nguuru Yàlla te def ko ak suñu bépp kàttan, noonu lañuy wone suñu mbëggeel ci doomu Yexowa, Yeesu Kirist mi mu fal buur. Bu ñuy def loolu, dinañu neex Yexowa te suñu mbokk yi ci wàllu ngëm dinañu njariñoo bu baax liggéey yi ñuy def (Yowaana 14:23). Ci misaal, waxtaan yi nekk ci jw.org ci xaaj bi tudd «Li ñuy def ak li ngeen di maye», dañuy wone ni suñu maye yi di dimbalee bu baax suñu mbokk yi ci ngëm, yi nekk ci àddina sépp.
Woneel WIDEO bi tudd: Maye yi ngeen di def am nañu solo lool. Ba pare nga laaj ñi teew lii:
-
Buñu amee ay mbokk yu war a taxaw ci kanamu yoon, ndaxte fi ñu dëkk dañu leen di jéem a téere ñu jaamu Yexowa ni mu ware, dañu leen ciy dimbali. Naka la maye yi ngeen di def di ñu jàpple ci loolu?
-
Dañuy jot ay maye yuy jóge ci dëkk yoo xam ne seen am-am yemul. Ni ñuy def ba tollale maye yooyu, naka lañuy amale njariñ ci tabax ay saalu nguur ci àddina si sépp?—2 Korent 8:14
-
Naka la maye yi ngeen di def, di ñu dimbalee ci tekki Biibël bi ci ay làkk yu bare?
9. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi
(30 minit) bt-F pàcc 17 § 13-19