Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

9 desàmbar ba 15 desàmbar

TAALIFI CANT 119:​1-56

9 desàmbar ba 15 desàmbar

Woy-Yàlla nº 124 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. ‘Ana nu ndaw mën a def ba nekk nit ku sell?’

(10 minit)

Dafay moytu lépp li ko mën a dugal ci fiir (Taalifi Cant 119:9; w87-F 1/11 18 § 10)

Dafay topp bu baax santaane Yàlla yi (Taalifi Cant 119:​24, 31, 36; w06-F 15/6 25 § 1)

Dafay bañ a xool lépp luy caaxaani neen (Taalifi Cant 119:37; w10-F 15/4 20 § 2)

LAAJAL SA BOPP LII: ‘Yan tegtal laa jot te ñu mën maa dimbali ma nekk nit ku sell?’

2. Nanu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Yaa ngi waare këroo-kër, nga gis kenn ci yoon bi, nga profitoo wax ak moom itam. (lmd-F lesoŋ 1 ponk 4)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(4 minit) KËROO-KËR. Li nga mën a def bu dee nit ki dafa la waxoon ne dafa am mbokk bu gaañu. (lmd-F lesoŋ 9 ponk 3)

6. Waxtaan bi

(5 minit) ijwyp-F 83—Turu waxtaan bi ci farãse: Comment puis-je résister à la tentation ? (th lesoŋ 20)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 40

7. Li suñu mbootaay di def

(10 minit) Woneel WIDEO bu weeru desàmbar bi.

8. Li mbooloo mi soxla ci wàllu ngëm

(5 minit)

9. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 21 ak ñaan